Sacred Texts  Bible  World Bible  Index  Previous 

Wolof Bible: Revelation

1:1  Lii mooy li Yeesu Kirist feeñal, te mu tukkee ca Yàlla, ngir mu won ay jaamam mbir, yi dëgmël di ñëw. Yónni na malaakaam, ngir xamal ko ab jaamam Yowaana.

1:2  Kooku mi ngi seede fii li mu gis lépp, maanaam kàddug Yàlla ak seede, si ñu seedeel Yeesu Kirist.

1:3  Barkeel ngeen, yaw miy jàng ak yéen ñiy déglu wax yii jóge ca Yàlla, te di sàmm li ñu ci bind, ndaxte waxtu wi jege na.

1:4  Man Yowaana maa leen di bind, yéen juróom-ñaari mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Asi. Na yiw ak jàmm féete ci yéen, jóge ci Yàlla, moom ki nekk, ki nekkoon démb te di ñëw ëllëg. Yiw woowu ak jàmm jooju ñoo ngi tukkee it ci juróom-ñaari Xeli Yàlla, yi nekk ci kanamu gàngunem Yàlla,

1:5  tukkee it ci Yeesu Kirist, seede bu takku bi, moom taaw bi, maanaam ki jëkk a dekki, di buuru buur yi ci kaw suuf yépp. Na ndam ak nguur féete ak Yeesu Kirist ba fàww, moom mi nu bëgg te yiwi nu ci sunuy bàkkaar ak deretam ji tuuru, te def nu askanu saraxalekati Buur Yàlla Baayam, nu di ko jaamu. Amiin.

1:7  Gisleen, mi ngi ñëw ci niir yi,te ñépp dinañu teg seeni bët ci moom,ba ci ñi ko jam sax.Te xeet yi nekk ci kaw suuf yéppdinañu jooy ndax moom.Waaw. Amiin.

1:8  Boroom bi Yàlla nee na: «Man Yàlla maay Alfa ak Omega, maay ki nekk, ki nekkoon démb te di ñëw ëllëg, man Aji Kàttan ji.»

1:9  Man Yowaana seen mbokk, di seen nawle ci fitna, ci nguur ak ci muñ, yi nu am ndax sunu booloo ak Yeesu, maa nga nekkoon ca dun bu ñuy wax Patmos. Wacce woon nañu ma fa, ndax li ma doon waare kàddug Yàlla tey seedeel Yeesu.

1:10  Xelum Yàlla solu ma ci bésu Boroom bi, te noonu ma dégg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit,

1:11  naan: «Bindal ci téere li ngay gis te yónnee ko juróom-ñaari mboolooy ñi gëm, ca dëkki Efes, Samirin, Pergam, Catir, Sàrd, Filadelfi ak Lawdise.»

1:12  Noonu ma geestu, ngir seet ku doon wax ak man. Ba ma geestoo, yem ci juróom-ñaari làmpi diwlin yu wurus,

1:13  gis ku taxaw ci biir làmp ya, niroo ak doomu nit. Mu sol mbubb mu gudd, takk ngeñaayu wurus ci ndiggam.

1:14  Boppam ak kawaram weex tàll ni perkaal, ay bëtam di xuyy ni safara.

1:15  Ay tànkam mel ni xànjar bu yànj bu ñu xelli, baatam di riir ni duusi géej.

1:16  Mu yor ci loxol ndeyjooram juróom-ñaari biddiiw, jaasiy ñaari boor yu ñaw di génn ci gémmiñam, xar-kanamam leer nàññ ni jantub njolloor.

1:17  Naka laa ko gis, di daanu ci ay tànkam ni ku dee. Waaye mu teg loxol ndeyjooram ci sama kaw ne ma: «Bul ragal dara. Maay ki jëkk te maay mujj.

1:18  Maay Kiy Dund. Dee woon naa, waaye maa ngii di dund ba fàww, yor caabiy dee ak ju barsàq.

1:19  Kon nag bindal li nga gis, li am léegi ak li nar a ami gannaaw gi.

1:20  Juróom-ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndeyjoor, ak juróom-ñaari làmpi diwlin yu wurus yi, ay mbóoti Yàlla lañu te lii lañuy tekki: biddiiw yi ñoo di malaakay juróom-ñaari mboolooy ñi gëm; juróom-ñaari làmp yi ñoo di juróom-ñaari mbooloo yi.

2:1  «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Efes, ne ko: i Ki téye juróom-ñaari biddiiw yi ci loxol ndeyjooram, tey dox ci diggu juróom-ñaari làmpi diwlin yu wurus yi nee na:

2:2  Xam naa say jëf, sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne, mënuloo dékku ñiy def lu bon. Seetlu nga ñi tuddoo samay ndaw, ba gis ne ay naaféq lañu.

2:3  Xam naa it ne muñ nga, ba dékku coono ndax sama tur, te xàddiwoo. i

2:4  Waaye li ma naqari ci yaw moo di sa mbëggeel wàññiku na.

2:5  Deel fàttaliku kon fa nga daanoo. Réccul te def, na nga daan def bu jëkk. Soo réccuwul, dinaa dikk ci yaw, jële sa làmp ca bérab ba mu nekk.

2:6  Waaye lii neex na ma ci yaw: sib nga ni man li ñoom Nikolas di jëf. i

2:7  Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, dinaa la may, nga lekk ci garabu dund, gi nekk ci jataayu Yàlla.

2:8  «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Samirin, ne ko: i Ki jëkk te mujj, ki dee woon te dekki nee na:

2:9  Xam naa sa coono, xam it sa néew doole, moona yaaka duunle. Ñooñu tuddoo Yawut, xam naa ñaawteef yi ñu teg ci sa der: ndajem Seytaane la.

2:10  Bul ragal li nga nar a daj. Seytaane dina dugal kaso ñenn ci yéen, ngir wut leen a fiir. Diirub fukki fan dingeen am coono. Nanga takku ba àttan cee dee, ma jox la kaalag dund gi. i

2:11  Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, doo loru ci ñaareelu dee.

2:12  «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Pergam, ne ko: i Boroom jaasi ju ñaw, ji am ñaari boor nee na:

2:13  Xam naa fa nga dëkk, di fa Seytaane samp nguuram. Moona jébbalu nga ci sama tur te weddiwoo sa ngëm ci man, ba ca fan ya ñu reye Antipas, sama seede bu takku ba, ci seen dëkk, di dëkku Seytaane. i

2:14  Waaye am na lu ma naqari ci yaw, moo di uuf nga foofu gaa yuy sàmm njàngalem Balaam, moom mi jàngaloon Balag, mu sóob bànni Israyil ci bàkkaar, xiir leen ci lekk ñam wu ñu tuuroo xërëm yi, xiir leen ci njaaloo.

2:15  Te am nga noonu itam ay nit ñuy sàmm njàngalem ñoom Nikolas.

2:16  Réccul kon; lu ko moy dinaa dikk ci yaw léegi te xeex ak nit ñooñu ak jaasi, jiy génn ci sama gémmiñ. i

2:17  Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, dinaa la jox, nga lekk dund bi ñuy wax mànn te mu nëbbu, te dinaa la jox xeer wu weex. Ci kaw xeer woowu bindees na ci tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ki ko jot.

2:18  «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Catir, ne ko: i Doomu Yàlla ji, ki ay bëtam di xuyy ni safara, tey tànkam di lerax ni xànjar, nee na:

2:19  Xam naa say jëf, sa mbëggeel, sa ngëm, sag muñ ak ni nga farloo ci sa jaamu Yàlla. Xam naa say jëf yu mujj, ni ñu ëppe yu jëkk ya. i

2:20  Waaye li ma naqari ci yaw moo di dangaa bàyyi Yesabel, jigéen joojuy tuddoo yonent, di jàngale ak a réeral sama jaam yi, ngir ñuy sóobu ci njaaloo te di lekk ñam wu ñu tuuroo xërëm yi.

2:21  May naa ko ab diir, ngir mu tuub njaaloom, waaye bañ na.

2:22  Kon nag dinaa ko tëral ci lalu metit, te ñiy ànd ak moom di njaaloo, su ñu tuubul jëfi jigéen jooju, dinaa leen teg naqar wu mag.

2:23  Dinaa rey ay doomam, te mboolooy ñi gëm yépp dinañu xam ne, man maa di kiy nattu xol ak xalaat, te dinaa fey ku nekk ay jëfam.

2:24  Waaye yéen ñépp ñi des ci Catir te toppuleen njàngale moomu te gëstuwuleen loolu ñu naan mbiri Seytaane yu xóot yi, maa ngi leen di wax ne, duma leen yen beneen yen

2:25  bu dul bii: jàppleen ci li ngeen jàpp, ba kera may ñëw. i

2:26  Ku daan tey sax ci samay jëf ba ca muj ga, dinaa ko jox sañ-sañ ci xeet yi:i

2:27  Dina leen jiite ak yetu weñ,i tojat leen ni ñuy toje ndaal kew —i

2:28  ni ma jële sañ-sañ ci sama Baay. Dinaa ko jox it biddiiwu njël.

2:29  Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.

3:1  «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Sàrd, ne ko: i Ki yor juróom-ñaari Xeli Yàlla yi ak juróom-ñaari biddiiw yi nee na: Xam naa say jëf. Dañu laa teg kuy dund, fekk dee nga.

3:2  Yeewul te dëgëral li des ci yaw tey waaj a dee, ndaxte gis naa ne, say jëf matuñu ca sama kanam Yàlla.

3:3  Fàttalikul kon kàddug Yàlla gi nga jot, te dégg ko, sàmm ko te réccu. Soo wéyee ciy nelaw nag, dinaa ñëw nib sàcc, te doo xam wan waxtu lay doon. i

3:4  Moona am nga foofu ci Sàrd nit ñu néew ñoo xam ne tilimaluñu seen mbubb. Ñooñu dinañu ànd ak man, sol lu weex, ndaxte yeyoo nañu ko.

3:5  Ku daan, dinga sol mbubb mu weex ni ñoom. Te duma far sa tur ci téereb dund bi, waaye dinaa nangu ci sama kanamu Baay ak ay malaakaam ne, bokk nga ci man.

3:6  Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.

3:7  «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Filadelfi, ne ko: i Aji Sell ji, di Aji Dëgg ji nee na, moom mi yor caabiy Daawuda ji, moom miy tijji te kenn du ko man a tëj, muy tëj te kenn du ko tijji nee ne:

3:8  Xam naa say jëf. Ubbil naa la bunt, te kenn du ko man a tëj. Xam naa ne barewuloo doole, waaye sàmm nga sama kàddu te weddiwoo ma.

3:9  Dinaa def ba ñenn ci ñi bokk ci ndajem Seytaane --te tuddoo Yawut, fekk dañuy fen — dinaa leen ñëwloo, ñu sukk ci sa kanam, nangu ne, bëgg naa la.

3:10  Gannaaw muñ nga, ni ma la ko dénke woon, man itam dinaa la yiir ci jamono, ji musiba mi di wàcc ci dunyaa bépp ngir nattu waa àddina. i

3:11  Léegi ma ñëw. Sàmmal li nga yor, ngir kenn bañ laa xañ sa kaalag ndam.

3:12  Ku daan, dinaa la samp ni aw jënu néeg ci sama kër Yàlla te doo fa génn mukk. Dinaa bind ci yaw turu sama Yàlla ak turu dëkku sama Yàlla, mu di Yerusalem gu bees, giy jóge ca asamaan ca wetu sama Yàlla di wàcc. Dinaa bind it ci yaw sama tur wu bees.

3:13  Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.

3:14  «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Lawdise, ne ko: i Ki ñuy wax Amiin ji, di seede bu takku bi te dëggu, ki di ndeyi bindu mbindeefi Yàlla yi, nee na;

3:15  Xam naa say jëf, xam ne seddoo, tàngoo. Manoon ngaa sedd mbaa nga tàng,

3:16  waaye ndax li nga nugg, tàngoo seddoo, dinaa la yàbbi.

3:17  Yaa ngi damu naan: “Am naa alal, duunle naa, soxlaatuma dara.” Fekk xamuloo ne, torox nga, miskin, ñàkk, gumba te rafle.

3:18  Moo tax maa ngi lay xiirtal, nga jënd ci man wurus wu ñu xellee ci safara, ngir nga duunle, te nga jënd yére yu weex ngir nga solu, ba sa gàcceg rafle bañ a feeñ, ak tuufaay booy diw ci say bët, ngir man a gis. i

3:19  Man maay yedd, di yar ñépp ñi ma bëgg. Farlul kon te tuub say bàkkaar.

3:20  Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat te ubbi bunt bi, dinaa dugg, reerandoo ak moom, moom it mu reerandoo ak man. i

3:21  Ku daan, dinaa la toogloo ci sama wet ci sama gàngune, ni ma xeexe ba daan, man ci sama bopp, te toogandoo ak sama Baay ci gànguneem.

3:22  Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.»

4:1  Gannaaw loolu ma xool, gis bunt ubbiku ci asamaan. Baat booba ma déggoon, muy wax ak man mel nig liit, ne ma: «Yéegal fii, ma won la li war a ñëw gannaaw gi.»

4:2  Ca saa sa Xelum Yàlla solu ma, noonu ma gis gàngune ca asamaan, te am ku ca toog.

4:3  Leeraayam mel ni jamaa ak per bu xonq, te xon gu leer ni per bu wert wër gàngune ma.

4:4  Yeneen ñaar-fukki gàngune ak ñeent wër ko, te ci kaw gàngune ya ñaar-fukki mag ak ñeent toog, sol mbubb yu weex ak kaalay wurus ci seen bopp.

4:5  Ay melax, ay riir ak ay dënnu di jibe ca gàngune ma. Ca kanamu gàngune ma amoon na fa juróom-ñaari làmp yu yànj, di juróom-ñaari Xeli Yàlla yi.

4:6  Amoon na it ca kanamu gàngune ma lu mel ni géej gu leer ni weer bu set, ba mel ni seetu. Ci li wër gàngune ma, sës rëkk, amoon na fa ñeenti mbindeef yu fees ak ay bët ci kanam ak ci gannaaw.

4:7  Mbindeef mu jëkk maa nga meloon ni gaynde, ñaareelu mbindeef mel ni yëkk, ñetteelu mbindeef yor kanamu nit, ñeenteel ba di nirook jaxaay juy naaw.

4:8  Ñeenti mbindeef ya am nañu ku nekk juróom-benni laaf te ñu nga fees ak ay bët li leen wër lépp, ba ci seen roni laaf. Guddi ak bëccëg duñu noppeek naan:«Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji,moo sell, sell, sell,moom ki nekkoon démb,ki nekk tey, te di ñëw ëllëg.»

4:9  Saa su mbindeef ya di màggal ki toog ca gàngune ma tey dund ba fàww, te di ko kañ ak a gërëm,

4:10  ñaar-fukki mag ña ak ñeent di dëpp seen jë ca kanamu ka toog ca kaw gàngune ma. Ñu di ko jaamu, moom mi dund ba fàww, di sànni seen kaalay ndam ca kanamu gàngune ma, naan:

4:11  «Yàlla sunu Boroom,yaa yeyoo ndam, teraanga ak kàttan,ndaxte yaa sàkk léppte ci sa coobare la lépp nekke,te ci lañu leen sàkke.»

5:1  Noonu ma gis ca loxol ndeyjooru ka toog ca gàngune ma téere bu ñu bind biir ak biti, tay ko juróom-ñaari yoon ak sondeel.

5:2  Noonu ma gis malaaka mu am doole, muy xaacu naan: «Ku yeyoo dindi tayu yi te ubbi téere bi?»

5:3  Te amul kenn, muy ci asamaan, muy ci kaw suuf, muy ci biir suuf, ku manoon a ubbi téere bi, mbaa mu xool ci biir.

5:4  Ma jooy jooy yu metti ndax li kenn yeyoowul woon a ubbi téere bi mbaa mu xool ko.

5:5  Noonu kenn ca mag ña ne ma: «Bul jooy. Xoolal, Gayndeg giiru Yuda, ki soqikoo ci Daawuda, daan na, ba am sañ-sañu dindi tayu yi te ubbi téere bi.»

5:6  Noonu ma gis Mbote mu mel ni dañu koo rendi woon, mu taxaw ca digg gàngune ma, ñeenti mbindeef ya séq ko, mag ña wër ko. Mbote ma amoon na juróom-ñaari béjjén ak juróom-ñaari bët, ñu di juróom-ñaari Xeli Yàlla, yi ñu yónni ci àddina sépp.

5:7  Mbote ma ñëw, jël téere, ba nekkoon ca loxol ndeyjooru ka toog ca gàngune ma.

5:8  Ba mu jëlee téere ba, ñeenti mbindeef ya ak ñaar-fukki mag ña ak ñeent daldi dëpp seen jë ca kanam Mbote ma, ku nekk yor xalam. Ñu yor it andi wurus yu fees ak cuuraay, yu doon misaal ñaani gaayi Yàlla ya.

5:9  Ñu daldi woy woy wu bees naan:«Yeyoo ngaa jël téere bite dindi tayu yi,ndaxte reyees na la,te jotal nga Yàlla ak sa deretay nit ñu bokk ci bépp giir,kàllaama, réew ak xeet.

5:10  Def nga leen askanu saraxalekatiBuur Yàlla sunu Boroom,di ko jaamu,te dinañu nguuru ci àddina.»

5:11  Ma xool noonu, dégg baatu malaaka yu bare yu ëppoon alfunniy alfunniy junniy junni. Malaaka ya wër gàngune ma ak mbindeef ya ak mag ña.

5:12  Ñuy xaacu naan:«Mbote ma ñu rendi woonyeyoo na kàttan, alal, xel,doole, teraanga, ndam ak cant.»

5:13  Ma dégg itam mbindeef, yi nekk ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf, ci géej gi, — mbindeef yépp naan:«Na cant, teraanga, ndam ak nguurféete ak ki toog ci gàngune mi,ak Mbote mi ba fàww.»

5:14  Ñeenti mbindeef ya naan: «Amiin.» Mag ña sukk di màggal.

6:1  Noonu ma gis Mbote ma dindi tayu gu jëkk ga, te ma daldi dégg kenn ca ñeenti mbindeef ya, di wax ak baat buy riir ni dënnu naan: «Ñëwal.»

6:2  Ma xool noonu, gis fas wu weex, gawar ba yor ag fitt. Ñu jox ko kaalag ndam, mu daldi dem moom jàmbaar ngir daani.

6:3  Mbote ma dindi na ñaareelu tayu ga, ma dégg ñaareelu mbindeef ma naan: «Ñëwal.»

6:4  Noonu weneen fas génn, di wu xonq, gawar ba jot sañ-sañu jële jàmm ci kaw suuf, ngir nit ñi di reyante ci seen biir. Ñu jox ko jaasi ju mag.

6:5  Mu dindi ñetteelu tayu ga, ma dégg ñetteelu mbindeef ma ne: «Ñëwal.» Ma xool, gis fas wu ñuul, gawar ba yor ab peesekaay.

6:6  Ma dégg baat bu jollee ca diggante ñeenti mbindeef ya, naan: «Peyug bëccëgu lëmm ngir benn kilob ceeb, peyug bëccëgu lëmm ngir ñetti kiloy dugub, waaye bul yàq diw ak biiñ.»

6:7  Mu dindi ñeenteelu tayu ga, ma dégg ñeenteelu mbindeef ma naan: «Ñëwal.»

6:8  Ma xool noonu, gis fas wu wert, gawar baa nga tuddoon Dee te barsàq a nga toppoon ci moom. Ñu jox ko sañ-sañ ci ñeenteelu xaaju àddina sépp, ngir mu faat ak jaasi, xiif, mbas ak rabi àll yi.

6:9  Mu dindi juróomeelu tayu ga, ma gis ca suufu saraxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, ruuwi ñi ñu bóom ndax seede si ñu doon sàmm ak li ñu gëmoon kàddug Yàlla.

6:10  Ñuy xaacu naan: «Boroom bu sell bi te dëggu, ba kañ ngay nég àtte bi te feyyul nu sunu deret ci waa àddina?»

6:11  Ñu jox leen ku nekk mbubb mu weex, daldi leen ne, ñu muñ tuuti, ba kera seeni nawle ñëw, te lim bi mat — seeni nawle ci liggéey bi, di seeni bokk yu waa àddina waroon a bóom ni ñoom.

6:12  Ma xool, ba muy dindi juróom-benneelu tayu ga. Noonu mu am yengu-yengub suuf bu mag, jant bi ñuul ni këriñ, weer wi xonq curr ni deret.

6:13  Biddiiw yi fàqe asamaan, di daanu ci kaw suuf, ni doomi garab yu yolox di wadd, bu ko ngelaw lu metti dee yengal.

6:14  Asamaan si dellu ni basaŋ gu ñuy taxañ, tund yépp ak dun yépp randoo fa ñu nekkoon.

6:15  Noonu buuri àddina si, kilifa yi, njiiti xare yi, boroom alal yi, boroom kàttan yi, jaam yi ak gor yi, ñépp làqatuji ci xunti yi ak ci ron doji tund yi.

6:16  Ñu naan tund yi ak doj yi: «Daanuleen ci sunu kaw te nëbb nu bëti ki toog ci gàngune mi ak meru Mbote mi,

6:17  ndaxte bés bu mag, bi seen mer di feeñ, agsi na! Ku ci man a rëcc?»

7:1  Gannaaw loolu ma gis ñeenti malaaka yu taxaw ci ñeenti xeblay àddina si. Ñu téye ñeenti ngelawi àddina, ngir ngelaw du wol ci kaw suuf, ci géej mbaa ci genn garab.

7:2  Ma gis it meneen malaaka, muy yéeg, jóge penku, yor màndargakaayu Yàlla jiy dund. Mu daldi wax ak baat bu xumb ñeenti malaaka ya ñu joxoon sañ-sañ, ñu yàq suuf ak géej,

7:3  ne leen: «Buleen yàqagun suuf si ak géej gi ak garab yi. Négleen, ba ñu def màndarga ci jëwu ñiy jaamu Yàlla sunu Boroom.»

7:4  Noonu ma dégg limub ñi ñu màndargaal; ñu tollu ci téeméer ak ñeent-fukk ak ñeent ci ay junni. Ñu jóge ci giiri bànni Israyil yépp:

7:5  Fukki junni ak ñaar lañu màndargaal ci biir giiru Yuda,fukki junni ak ñaar ci giiru Ruben,fukki junni ak ñaar ci giiru Gàdd,

7:6  fukki junni ak ñaar ci giiru Aser,fukki junni ak ñaar ci giiru Neftali,fukki junni ak ñaar ci giiru Manase,

7:7  fukki junni ak ñaar ci giiru Simeyon,fukki junni ak ñaar ci giiru Lewi,fukki junni ak ñaar ci giiru Isakaar,

7:8  fukki junni ak ñaar ci giiru Sabulon,fukki junni ak ñaar ci giiru Yuusufa,fukki junni ak ñaar ci giiru Ben-yamin.

7:9  Gannaaw loolu ma xool, gis mbooloo mu réy, ba kenn mënu koo waññ, ñu bokk ci xeet yépp, giir yépp, réew yépp ak kàllaama yépp, taxaw ca kanamu gàngune ma ak Mbote ma. Ñu sol ay mbubb yu weex, di màggal te di yengal ay cari garab ci seeni loxo,

7:10  naan:«Mucc gaa ngi ci Yàllasunu Boroom, bi toog ci gàngune mi,ak ci Mbote mi!»

7:11  Noonu malaaka yépp taxaw, wër gàngune ma ak mag ña ak ñeenti mbindeef ya. Ñu dëpp seen jë ca kanamu gàngune ma, di jaamu Yàlla,

7:12  naan:«Amiin. Na cant ak ndam, xel ak ngërëm, teraanga, kàttan ak dooleféete ak Yàlla sunu Boroom ba fàww. Amiin!»

7:13  Noonu kenn ca mag ña ne ma: «Ñi sol mbubb yu weex yi, ñooy ñan ak fan lañu jóge?»

7:14  Ma ne ko: «Sang bi, xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca metit wu réy wa. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Mbote ma.

7:15  Loolu moo taxñu nekk ci kanamu gàngunem Yàlla,di ko jaamu guddi ak bëccëg ci këram,te ki toog ci gàngune mi dina leen yiir.

7:16  Dootuñu xiif, dootuñu mar.Jant mbaa weneen tàngaay du leen lakk,

7:17  ndaxte Mbote mi nekk ci diggu gàngune mi dina leen sàmm,yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma,te Yàlla dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët.»

8:1  Mbote ma dindi na juróom-ñaareelu tayu ga, asamaan ne selaw lu mat genn-wàllu waxtu.

8:2  Noonu ma gis juróom-ñaari malaaka, yi taxaw ca kanam Yàlla, ñu daldi leen jox juróom-ñaari liit.

8:3  Ba loolu amee meneen malaaka ñëw, taxaw ca wetu saraxalukaayu wurus, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole ko ak ñaani gaayi Yàlla yépp, joxe ko ci kaw saraxalukaayu wurus ba nekk ci kanam gàngune mi.

8:4  Noonu saxarus cuuraay li gillee ca loxob malaaka ma, ànd ak ñaani gaayi Yàlla ya, jëm ca kanam Yàlla.

8:5  Malaaka ma jël andu cuuraay ba, duy ko ak ay xal ca saraxalukaay ba, daldi koy sànni ci àddina. Noonu mu am ay dënnu, ay riir, ay melax ak yengu-yengub suuf.

8:6  Ba mu ko defee juróom-ñaari malaaka, ya yoroon juróom-ñaari liit ya, daldi defaru di waaj a liit.

8:7  Malaaka mu jëkk ma wol liitam. Noonu ñu sànni ci àddina yuur ak safara yu ñu boole ak deret, ba tax benn ci ñetti xaaju suuf si lakk, benn ci ñetti xaaju garab yi it lakk, te ñax mu naat mépp lakk.

8:8  Ñaareelu malaaka ma wol liitam. Noonu ñu sànni lu mel ni tundu safara wu réy, mu daanu ci géej gi, benn ci ñetti xaaju géej gi soppiku deret,

8:9  benn ci ñetti xaaju mbindeef yi nekk ci géej gi dee, te benn ci ñetti xaaju gaal yi yàqu.

8:10  Ñetteelu malaaka ma wol liitam. Noonu biddiiw bu réy, yànj ni jum, xawee asamaan, daanu ci benn ci ñetti xaaju dex yi ak ci bëti ndox yi.

8:11  Biddiiw boobu mi ngi tuddoon Wextan. Nit ñu bare naan ci ndox mi daldi dee, ndaxte ndox mi dafa daldi wex.

8:12  Ñeenteelu malaaka ma wol liitam. Noonu dóorees benn ci ñetti xaaju jant bi, ak benn ci ñetti xaaju weer wi, ak benn ci ñetti xaaju biddiiw yi, ba tax benn ci ñetti xaaju leer gi lëndëm. Bëccëg bi ñàkk leer diirub benn ci ñetti xaajam, guddi gi ñàkk leer diirub benn ci ñetti xaajam.

8:13  Ma xool noonu, dégg jaxaay juy naaw ci digg asamaan, naan ak baat bu xumb: «Musiba, musiba! Musibaa ngi ci kaw waa àddina, ndax liit yi yeneen ñetti malaaka yi di wol.»

9:1  Juróomeelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma gis, ñu jox caabiy kàmb gu xóot gi benn biddiiw bu xawee woon asamaan, daanu ci kaw suuf.

9:2  Biddiiw ba ubbi buntu kàmb gu xóot ga. Noonu saxar jollee ca, su mel ni saxarus puur bu mag, jant bi ak jaww ji lépp lëndëm ndax saxarus kàmb ga.

9:3  Ay njéeréer génn ca saxar sa, tasaaroo ci biir àddina. Ñu jox leen kàttan gu mel ni kàttanu jànkalaar.

9:4  Ñu sant leen, ñu bañ a laal ñax mi ci kaw suuf, mbaa genn gàncax walla genn meññeef, waaye ñu jublu rekk ci nit ñu amul màndargam Yàlla ci seen jë.

9:5  Santuñu leen ñu rey leen, waaye ñu metital leen diirub juróomi weer. Te metit woowu ñuy indi, temboo na ak metit wiy dal nit, bu ko jànkalaar fittee.

9:6  Ca jamono yooya nit ñi dinañu sàkku dee, waaye duñu daje ak moom. Dinañu bëgg a dee, waaye dee da leen di daw.

9:7  Njéeréer ya nag dañuy niroo ak fas yu ñu waajal ngir xare. Am nañu ci seen bopp lu mel ni kaalay wurus, te seen xar-kanam mel ni gu nit.

9:8  Seeni kawar mel ni yu jigéen, seeni bëñ mel ni bëñi gaynde.

9:9  Takk nañu ci seen dënn lu mel ni kiiraayu weñ, te coow la seeni laaf di def mel ni coowu sareeti xare yu bare yu ñu takk fas, di xeexi.

9:10  Am nañu ay geen yu am ay fitt ni jànkalaar, te ca la seen kàttan nekk, ngir metital nit ñi diirub juróomi weer.

9:11  Buuru njéeréer yi mooy malaakam kàmb gu xóot gi, moom lañu tudde ci làkku Yawut, Abadon, ak ci làkku gereg, Apolyon, liy tekki «Yàqkat.»

9:12  Musiba mu jëkk mi jàll na, yeneen ñaari musiba yaa ngi ñëw.

9:13  Juróom-benneelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma dégg baat bu jóge ci ñeenti béjjén, yi nekk ci koñi saraxalukaayu wurus, ba nekk ci kanam Yàlla,

9:14  mu ne juróom-benneelu malaaka, ma yoroon liit: «Yiwil ñeenti malaaka, ya yeewe ca Efraat, dex gu mag ga.»

9:15  Noonu ñu daldi yiwi ñeenti malaaka, ya ñu waajaloon ngir at moomu, weer woowu, bés boobu ak waxtu woowu, ngir ñu rey benn ci ñetti xaaju nit ñi.

9:16  Limub gawar ga doon xareji mat na ñaari alfunniy alfunni. Dégg naa lim ba.

9:17  Nii laa gise ci peeñu mi fas ya ak ña leen war: ñu sol kiiraay yu xonq ni safara, bulo ni saxar, ak mboq ni tamarax. Boppi fas yaa nga doon nirook boppi gaynde; safara, saxar ak tamarax di génn ci seeni gémmiñ.

9:18  Benn ci ñetti xaaju nit ñi dee ci ñetti musiba ya: ci safara, saxar ak tamarax yi génn ci seeni gémmiñ.

9:19  Ndaxte kàttanu fas yaa ngi ci seeni gémmiñ ak ci seeni geen. Geen yaa nga mel ni ay jaan, am ay bopp, te ñoom lañuy metitale nit ñi.

9:20  Nit ñi rëcc ci musiba yooyu taxul sax ñu tuub seeni jëfi loxo. Noppiwuñu di jaamu rab yi ak nataali xërëm yu ñu defare wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk, yoo xam ne mënuñoo gis, mënuñoo dégg mbaa ñu dox.

9:21  Te nit ñooñu tuubuñu seen bóom, seen xërëm, seen njaaloo mbaa seen càcc.

10:1  Noonu ma gis meneen malaaka mu am doole, muy wàcce asamaan, làmboo niir. Xon tiim ko, te xar-kanamam mel ni jant, te ay tànkam mel ni jumi safara.

10:2  Yor na benn téere bu ndaw bu ñu ubbi. Mu teg tànku ndeyjooram ci géej gi, tànku càmmooñam ci suuf si,

10:3  di xaacu, mel ni gaynde guy yëmmu. Naka la xaacu, juróom-ñaari dënnu yi jib.

10:4  Naka la juróom-ñaari dënnu yi di jib, may waaj a bind, waaye ma dégg baat bu jóge asamaan, naan ma: «Li juróom-ñaari dënnu yi wax, na nekk kumpa, bu ko bind.»

10:5  Noonu malaaka ma ma gis, mu taxaw ci géej gi ak suuf si, yékkati loxol ndeyjooram, mu jëm asamaan,

10:6  daldi waat ci kiy dund ba fàww, ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak li ci nekk lépp; mu ne: «Négandiku wees na,

10:7  waaye jamono ju juróom-ñaareelu malaaka ma wolee ci liitam, ndogalu Yàlla dina mat, ni mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»

10:8  Ci kaw loolu baat, ba ma déggoon ca asamaan waxaat ak man, ne ma: «Demal jël téere bi ñu ubbi ci loxob malaaka, mi taxaw ci géej gi ak suuf si.»

10:9  Ma dem ca malaaka ma, laaj ko téere bu ndaw boobu. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir, waaye dina neex ni lem ci sa gémmiñ.»

10:10  Noonu ma jël téere bi ci loxob malaaka mi, daldi ko lekk, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye bi ma ko wannee, mu wex xat ci sama biir.

10:11  Gannaaw loolu ñu ne ma: «Fàww nga wax ci kàddug Yàlla lu jëm ci réew yu bare, xeet yu bare, kàllaama yu bare ak buur yu bare.»

11:1  Bi loolu amee ñu jox ma nattukaay bu mel ni yet, ne ma: «Jógal, natt kër Yàlla gi ak saraxalukaay bi, te waññ ña fay jaamu Yàlla.

11:2  Waaye bàyyil ëttu bitib kër Yàlla gi; bu ko natt, ndaxte jébbalees na ko ñi dul Yawut, te dinañu nappaaje dëkk bu sell bi diirub ñeent-fukki weer ak ñaar.

11:3  Dinaa may sama ñaari seede yi, ñuy wax ci kàddug Yàlla, sol ay saaku, di toroxlu diirub junni ak ñaari téeméeri fan ak juróom-benn-fukk.»

11:4  Ñaari seede ya nag ñoo di ñaari garabu oliw yeek ñaari làmpu diwlin, yi taxaw ci kanam Boroom suuf si.

11:5  Su leen kenn bëggee def lu bon, safaraay génn ci seen gémmiñ, daldi lakk seeni bañaale; te ku leen bëgg a def lu bon, noonu lay war a deeye.

11:6  Am nañu sañ-sañu téye taw diirub fan, yi ñuy wax ci kàddug Yàlla. Am nañu it sañ-sañu soppi ndox yi deret te wàcce ci kaw suuf musiba yu nekk, saa su ñu ko bëggee.

11:7  Bu ñu noppee seen seede, rab wiy jóge ci kàmb gi dina leen xeex, daan leen, rey leen.

11:8  Te seeni néew dinañu nekk ci péncum dëkk bu mag, boobu ñuy wooye ci misaal Sodom ak it Misra, fa ñu reyoon seen Boroom ci bant.

11:9  Te diirub ñetti fan ak genn-wàll bépp réew, giir, kàllaama ak xeet dinañu seetaan seeni néew te duñu bàyyi kenn suul leen.

11:10  Waa àddina dinañu bég ci seen dee, di ndokkeelante ak di joqleente ay may, ndaxte ñaari yonent ya lakkaloon nañu waa àddina.

11:11  Waaye bi ñetti fan ya ak genn-wàll wéyee, xelum dund, jóge ca Yàlla, solu leen, ñu jóg taxaw. Noonu tiitaange gu réy jàpp ñi leen doon seetaan.

11:12  Ñaari seede ya dégg baat bu xumb ca asamaan naan leen: «Yéegleen fii.» Noonu ñu yéeg asamaan ci aw niir, seeni bañaale di seetaan.

11:13  Ca saa sa am yengu-yengub suuf bu mag, te benn ci fukki xaaju dëkk ba daldi màbb. Juróom-ñaari junniy nit dee ci yengu-yengub suuf ba, te ña ca des tiit, daldi màggal Yàllay asamaan.

11:14  Ñaareelu musiba mi wéy na, ñetteel baa ngi nii di ñëw.

11:15  Juróom-ñaareelu malaaka ma wol liitam, noonu baat yu xumb jib ca asamaan naan:«Nguuru àddina, jébbalaat nañu kosunu Boroom ak Almaseem,te dina nguuru ba fàww.»

11:16  Ñaar-fukki mag ak ñeent, ña toogoon ca seen gàngune ca kanam Yàlla, daldi dëpp seen jë ca suuf, jaamu Yàlla,

11:17  naan:«Nu ngi lay gërëm, Boroom bi Yàlla,yaw Aji Kàttan ji, ki nekk te nekkoon,ndax gànjoo nga sa kàttan gu réy gi,ngir taxawal sa nguur.

11:18  Xeet yi meroon nañu,waaye sa mer wàcc na,te jamono ji jot na,ji ngay àttee ñi dee,neexal say jaam yonent yi,ak sa gaa ñi ak ñi ragal saw tur,muy mag di ndaw,te nga rey ñiy yàq àddina.»

11:19  Noonu kër Yàlla gi ci asamaan daldi ubbiku, gaalu kóllëreg Yàlla ga daldi feeñ ca biir kër Yàlla ga, te mu daldi am ay melax, ay coow, ay dënnu, yengu-yengub suuf ak tawu yuur bu metti.

12:1  Amoon na firnde ju ràññiku ju feeñ ca asamaan, di jigéen ju làmboo jant bi, kaalawoo fukki biddiiw ak ñaar, weer wi nekk ci suufu tànkam.

12:2  Jigéenu biir la, di yuuxu ndax metitu mat wu tar.

12:3  Noonu beneen firnde feeñ ca asamaan, di ninkinànka ju réy, xonq curr te am juróom-ñaari bopp ak fukki béjjén. Ca bopp ya am na juróom-ñaari mbaxanay buur.

12:4  Geenam di laawaale ñetti cér yu ne benn ca biddiiwi asamaan, di leen sànni ci suuf. Ninkinànka ja taxaw ca kanamu jigéen jay matu, ngir lekk liir ba, bu juddoo.

12:5  Noonu mu jur doom ju góor, muy ki war a jiite xeeti àddina yépp ak yetu weñ. Waaye ñu daldi fëkk doom ja, mu dem ca Yàlla ak gànguneem.

12:6  Gannaaw loolu jigéen ja daw, dem ca màndiŋ ma, ca dalukaay ba ko Yàlla waajaloon ngir mu nekk fa, ñu dundal ko fa diirub junni ak ñaari téeméeri fan ak juróom-benn-fukk.

12:7  Noonu xare am ca asamaan ya. Mikayel ak malaaka, ya ànd ak moom, xeex ak ninkinànka ja, ninkinànka ja it ak ay malaakaam feyyu.

12:8  Waaye ninkinànka jaa gën a néew doole; noonu ñu dàqe ko ak toppam asamaan.

12:9  Daaneel nañu ko, moom ninkinànka ju réy ji, di jaani cosaan ji, te ñu di ko wax Tuumaalkat bi mbaa Seytaane, moom miy nax waa àddina sépp — daaneel nañu ko ci kaw suuf, moom ak ay malaakaam.

12:10  Noonu ma dégg baat bu xumb jóge asamaan naan:«Léegi mucc agsi na,moom ak kàttanak nguuru Yàlla sunu Boroom,ak sañ-sañu Almaseem,ndaxte ki daan tuumaal sunuy bokk,di leen sosal guddi ak bëccëgci kanam Yàlla sunu Boroom,kooka daaneel nañu ko.

12:11  Fekk noot nañu kojaarale ko ci deretu Mbote maak seen seedes ngëm,te soppuñu seen bakkan ba ragal a dee.

12:12  Looloo tax, na asamaanak ñi ci dëkk bànneexu!Musiba ci kaw suuf ak ci biir géej!Ndaxte Seytaane wàcc na ci yéen,ànd ak mer mu tàng,ndaxte xam na ne, jot gi ko dese barewul.»

12:13  Ba ninkinànka ja gisee ne, daaneel nañu ko ci kaw suuf, mu dàq jigéen, ja juroon doom ju góor ja.

12:14  Noonu ñu jox jigéen ja ñaari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, ba sore ninkinànka ja, dem ca màndiŋ ma ca bérabam, ñu dundal ko fa ab diir, ay diir ak genn-wàllu diir.

12:15  Ninkinànka ja buusu ndox mu bare ni dex ca gannaaw jigéen ja, ngir yóbbaale ko ca.

12:16  Waaye suuf wallu jigéen ja, naan dex, ga ninkinànka ja buusu woon.

12:17  Ninkinànka ja mere jigéen ja, daldi xeexi ak ñi des ciy doomam, di ñiy sàmm ndigali Yàlla tey sax ci di seedeel Yeesu.

12:18  Noonu mu taxaw ca tefesu géej ga.

13:1  Noonu ma gis génn ca géej ga, rab wu am fukki béjjén ak juróom-ñaari bopp. Ci kaw béjjénam ya amoon na fukki mbaxanay buur; ca bopp ya turi xarab Yàlla.

13:2  Rab wa ma gis ma nga mel ni segg, tànk ya mel ni yu rab wu ñuy wax urs, gémmiñ ga mel ni gu gaynde. Ninkinànka ja jox ko kàttanam, nguuram ak sañ-sañam bu réy.

13:3  Benn ca bopp ya mel ni dafa gaañu ba dee. Waaye gaañu-gaañu ba daldi wér. Waa àddina sépp yéemu, daldi topp rab wa.

13:4  Ñu jaamu ninkinànka ja ndax li mu joxoon sañ-sañ rab wa, di jaamu it rab wa, naan: «Rab wi amul moroom, kenn mënul a xeex ak moom.»

13:5  Noonu mayees ko mu am gémmiñ, muy jey boppam te di xarab turu Yàlla. Mayees ko it sañ-sañu jëf ci kaw suuf diirub ñeent-fukki weer ak ñaar.

13:6  Noonu mu tàmbalee xarab Yàlla, di xarab aw turam, dalam, ak ñi dëkk ci asamaan.

13:7  Mayees ko, mu xare ak gaayi Yàlla yi te noot leen. Mayees ko it sañ-sañ ci kaw bépp giir, réew, kàllaama ak xeet.

13:8  Waa àddina sépp dinañu ko jaamu, ñooñu ñu bindul seeni tur, li dale ci njàlbéenu àddina, ci téereb dund bu Mbote mi ñu rendi.

13:9  Yaw mi am ay nopp, déglul.

13:10  Ku Yàlla dogal,ñu war laa jàpp njaam,dinañu la jàpp njaam.Ku Yàlla dogal,ñu war laa rey ak jaasi,dinañu la rey ak jaasi. Looloo tax gaayi Yàlla yi war a muñ te takku.

13:11  Noonu ma gis weneen rab di génn ci suuf. Am na ñaari béjjén yu mel ni yu mbote, waaye di wax ni ninkinànka.

13:12  Muy jëf ak sañ-sañu rab wu jëkk wa ci turam, di sant waa àddina sépp, ñu jaamu rab wu jëkk, woowu am gaañu-gaañu ba ko rey, waaye daldi wér.

13:13  Muy def kéemaan yu réy, ba dem sax bay wàcce ci kaw suuf safara su jóge asamaan, nit ñi di gis.

13:14  Noonu mu nax waa àddina ci kéemaan, yi mu am sañ-sañu def ci turu rab wu jëkk wa. Mu sant waa àddina, ñu def nataalu rab, wi am gaañu-gaañub jaasi tey dund.

13:15  Mayees ko it, mu dundloo nataalu rab wa, waxloo ko, ba képp ku jaamuwul nataalu rab wa rekk ñu rey la.

13:16  Mu def it ba ñépp, mag ak ndaw, buur ak baadoolo, gor ak jaam, ñépp am màndarga ci seen loxol ndeyjoor walla ci seen jë,

13:17  ba kenn du man a jënd mbaa mu jaay te amul màndargam rab wi, maanaam turam walla siifar bu mengoo ak turam.

13:18  Lii nag mooy laaj xel: ku am xel dina man a waññ siifaru rab wi, ndaxte siifar boobu mengoo na ak bu nit, di juróom-benni téeméer ak juróom-benn-fukk ak juróom-benn.

14:1  Ma xool noonu, gis Mbote ma taxaw ci tundu Siyon, ànd ak téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti junniy nit, te ñu bind ci seen jë turu Mbote ma ak turu Baayam.

14:2  Ma dégg baat bu jóge asamaan, buy riir ni duusi géej, ni riiru dënnu gu réy. Baat ba ma dégg mel ni baati xalamkat yuy xalam.

14:3  Nit ñu bare ñooñu taxaw ca kanamu gàngune ma ak ñeenti mbindeef ya ak mag ña, di woy woy wu bees. Kenn mënul a jàng woy wa, ku dul téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti junniy nit, ñooñu ñu jote àddina.

14:4  Ñoo di ñi taqul sobey jigéen, ndaxte saxal nañu seen bopp ci sell. Ñu nga topp Mbote ma fépp fu mu jëm. Yàlla jot na leen ci biir nit ñi, ñu jébbalu ci Yàlla ak ci Mbote mi, mel ni tànneefu ngóob mi ñuy sédde Yàlla,

14:5  te fen musul a génn ci seen gémmiñ. Amuñu benn sikk.

14:6  Noonu ma gis meneen malaaka naaw ca digg asamaan, yor xebaar bi sax, di ko yégal waa àddina — xeet yépp, giir yépp, kàllaama yépp ak réew yépp.

14:7  Ma nga doon xaacu naan: «Ragal-leen Yàlla te jox ko ndam li, ndaxte waxtuw àtteem jot na. Jaamuleen ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak bëti ndox yi.»

14:8  Meneen malaaka, di ñaareel bi, topp ca naan: «Daanu na! Babilon, dëkk bu mag, bi daan màndil réew yépp ak biiñu njaaloom, daanu na.»

14:9  Meneen malaaka, di ñetteel bi, topp ca, di xaacu naan: «Ku jaamu rab wi ak nataalam te nangoo am màndargam ci jëwam walla ci loxoom,

14:10  dina naan moom itam biiñu xadarub Yàlla bi kenn raxul, ñu sotti ko ci koppu meram. Te dees na ko mbugal ci safara ak tamarax ci kanamu malaaka yu sell yi ak Mbote mi,

14:11  te saxar siy jóge ci seen mbugal dina gilli ba fàww. Ñooñu di jaamu rab wi ak nataalam, ak képp ku nangoo jot màndargam turam, duñu noppalu guddi ak bëccëg.»

14:12  Looloo tax gaayi Yàlla yi war a muñ, ñooñuy sàmm ndigali Yàlla yi ak ngëm ci Yeesu.

14:13  Noonu ma dégg baat ci asamaan naan: «Bindal: “Bés ni tey, ñi nekk ci Boroom bi te dee, barkeel nañu.”» Xelum Yàlla nee na: «Waaw, dinañu noppalu ci seeni coono, ndaxte seeni jëf a nga leen di xaar.»

14:14  Ma xool noonu, gis niir wu weex ak ku ca toog, niroo ak doomu nit, takk kaalag wurus ca bopp ba, yor sàrt bu ñaw.

14:15  Te meneen malaaka génn ca kër Yàlla ga, di wax ak baat bu xumb ak ka toogoon ca niir wa, ne ko: «Dawalal sa sàrt te góob, ndaxte ngóob jot na, te lépp ñor na ci kaw suuf.»

14:16  Noonu ka toogoon ca kaw niir wa dawal sàrtam ci kaw suuf, góob àddina sépp.

14:17  Bi loolu amee meneen malaaka génn ca kër Yàlla ga nekk ca asamaan, yor moom itam sàrt bu ñaw.

14:18  Noonu meneen malaaka, ma am sañ-sañ ca safara sa, jóge ca saraxalukaayu cuuraay ba, daldi wax ak baat bu xumb ak malaaka, ma yor sàrt bu ñaw ba, ne ko: «Dawalal sa sàrt bu ñaw bi te dagg céggu réseñ yu àddina, ndaxte ñor nañu.»

14:19  Noonu malaaka ma daldi dawal sàrtam ci àddina, dagg réseñ yi, sànni leen ci biir segalukaay bu réy bu merum Yàlla.

14:20  Ñu nal réseñ ya ca segalukaay, ba ca gannaaw dëkk ba, deret génn ca, ba agsi ci laabi fas yi, te wal ba ëmb lu mat ñetti téeméeri kilomet.

15:1  Noonu ma gis ca asamaan beneen firnde ju réy tey yéeme: juróom-ñaari malaaka yu taawu juróom-ñaari musiba, ñuy yu mujj ya, ndaxte ñoom ñooy matal merum Yàlla.

15:2  Noonu ma gis lu mel ni géej gu leer ni weer bu set buy ray-rayi ak safara. Ña nootoon rab wa ak nataalam, ak siifar bu mengoo ak turam, ñoo taxaw ca géej gu leer ga, yor xalam yu leen Yàlla jox.

15:3  Ñuy woy woyu Musaa jaamu Yàlla bi, ak woyu Mbote ma, naan:«Say jëf réy nañu te yéeme,yaw Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji.Say yoon jub nañu te dëggu,yaw Buur bi fiy sax ba abadan.

15:4  Ku la ragalul, Boroom bi?Ku dul màggal saw tur?Kenn, ndaxte yaw rekk yaa sell.Xeet yépp dinañu dikk, jaamu la,ndax say àtte bir na ñépp.»

15:5  Gannaaw loolu ma xool, noonu kër Yàlla ubbiku ca asamaan, muy tàntu màggalukaay, bi ëmb li Yàlla seede.

15:6  Juróom-ñaari malaaka, ya taawu juróom-ñaari musiba ya, daldi génn ca kër Yàlla ga. Ñu sol mbubb yu set te weex bay lerax, laxasaayoo ngeñaayi wurus ba ci seen dënn.

15:7  Noonu kenn ci ñeenti mbindeef ya jox juróom-ñaari malaaka ya juróom-ñaari ndabi wurus yu fees ak merum Yàlla jiy dund ba fàww.

15:8  Kër Yàlla ga fees ak saxar ndax leeraayu ndamu Yàlla ak kàttanam. Te kenn mënatul a dugg ca kër Yàlla ga, ba kera juróom-ñaari musiba, ya juróom-ñaari malaaka ya taawu, di mat.

16:1  Noonu ma dégg baat bu xumb bu jóge ca kër Yàlla ga, naan juróom-ñaari malaaka ya: «Demleen sotti ci àddina juróom-ñaari ndabi merum Yàlla yi.»

16:2  Noonu malaaka mu jëkk ma dem, sotti ndabam ci àddina, ba woppi taab ju bon te metti dal nit, ña am màndargam rab wa tey jaamu nataalam.

16:3  Ñaareelu malaaka ma sotti ndabam ci géej gi. Mu soppiku deret ni deretu néew, ba lépp luy dund te nekkoon ci géej gi dee.

16:4  Ñetteelu malaaka ma sotti ndabam ci dex yi ak ci bëti ndox yi. Ñu daldi nekk deret.

16:5  Noonu ma dégg malaaka mi am sañ-sañ ci ndox yi naan:«Ku jub nga, yaw ki nekk te nekkoon,yaw Aji Sell ji,ci li nga dogal àtte yooyu.

16:6  Ndaxte tuur nañu deretu sa gaa ñiak ju yonent yi,yaw it fey nga leen seen bor,jox leen deret, ñu naan.»

16:7  Ma dégge baat jibe ca saraxalukaayu cuuraay ba naan:«Waaw Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji,say àtte dëggu nañu te jub.»

16:8  Ñeenteelu malaaka ma tuur ndabam ci jant bi. Noonu ñu jox ko sañ-sañu lakk nit ñi ak tàngaayam.

16:9  Naaj wu metti di lakk nit ñi, ñu daldi xarab turu Yàlla, ji am sañ-sañ ci kaw musiba yooyu. Waaye tuubuñu sax seeni bàkkaar, ngir jox ko ndam li.

16:10  Juróomeelu malaaka ma tuur ndabam ci kaw gàngunem rab wa. Noonu lëndëm muur nguuram. Nit ñi di màtt seeni làmmiñ ndax metit,

16:11  ñuy xarab Yàllay asamaan ndax seeni metit ak seeni taab. Waaye tuubuñu seeni jëf.

16:12  Juróom-benneelu malaaka ma sotti ndabam ci dex gu mag, gi ñuy wax Efraat, ndox ma daldi ŋiis, ngir waajal yoonu buuri penku, yiy ñëw.

16:13  Noonu ma gis ñetti rab yu bon yu mel niy mbott, génn ci gémmiñi ninkinànka ja ak rab wa ak naaféq, ba mbubboo yonent.

16:14  Ay rabi Seytaane lañu woon, yuy def ay kéemaan te di dem ci buuri àddina sépp, di leen dajale, ngir xeex biy am ci bés bu mag, bi Yàlla Aji Kàttan jagleele boppam.

16:15  «Maa ngi ñëw nib sàcc. Bég nga, yaw mi nelawul te di wottu say yére, ngir bañ a dox yaramu neen, ñuy gis sa gàcce.»

16:16  Noonu rab ya dajale buuri àddina si ci bérab bu tudd ci làkku yawut Armagedon.

16:17  Ci kaw loolu juróom-ñaareelu malaaka ma sotti ndabam ci ngelaw. Noonu baat bu xumb jóge ca gàngune ma ca kër Yàlla ga, naan: «Lépp mat na.»

16:18  Noonu mu am ay melax ay riir ay dënnu ak yengu-yengub suuf bu mag, boo xam ne bési cosaan ba léegi, musu faa am. Yengu-yengub suuf si réye na noonu.

16:19  Dëkk bu mag ba xàjjalikoo ñetti cér, te dëkki xeet yi màbb. Noonu Yàlla daldi fàttaliku Babilon bu mag ba, ngir jox ko koppu meram mu tàng ma, ba mu màndi.

16:20  Dun yépp daldi ne mes, te kenn gisatul tund ya.

16:21  Tawu yuur, donj wu nekk tollu ci ñeent-fukki kilo, daldi daanoo asamaan ci kaw nit ñi, ñuy xarab Yàlla ndax musibam yuur ga, ndaxte musiba ma dafa metti woon lool.

17:1  Gannaaw loolu benn ci juróom-ñaari malaaka, ya taawu juróom-ñaari ndab ya, ñëw ne ma: «Kaay, ma won la mbugalu jigéenu moykat bu mag, bi toog ci dex yu bare.

17:2  Moom la buuri àddina si àndal ci seen njaaloo. Ci biiñu moy Yàllaam la waa àddina màndee.»

17:3  Noonu Xelum Yàlla solu ma, malaaka ma yóbbu ma ca màndiŋ ma. Foofa ma gis fa jigéen ju war rab wu xonq te am juróom-ñaari bopp ak fukki béjjén, yaram wa fees ak turi xarab Yàlla.

17:4  Jigéen ja sol lu yolet te xonq, takk wurus ak jamaa ak ay per. Yoroon na koppu wurus bu fees ak ñaawteef ak sobeem.

17:5  Bindoon nañu ci jëwam tur wii ëmb kumpa, mu di: Babilon mu mag mi, ndeyi jigéeni moykat yi ak ñaawteefi àddina yi.

17:6  Ma gis jigéen ja màndi ci deretu gaayi Yàlla yi, ci deretu ñi doon seedeel Yeesu. Naka laa ko gis, ma daldi jaaxle lool.

17:7  Malaaka ma ne ma: «Lu tax nga jaaxle? Dinaa la leeralal kumpag jigéen ji ak rab, wi mu war te am juróom-ñaari bopp ak fukki béjjén.

17:8  Rab wi nga gis nekkoon na waaye nekkatul. Dina génn ca kàmb gu xóot ga, ba noppi sànku. Noonu waa àddina, ñi ñu bindul seeni tur, li dale ci njàlbéenu àddina, ci téereb dund bi, dinañu yéemu, bu ñu gisee rab wi, ndaxte nekkoon na waaye nekkatul te dina nekkaat.

17:9  «Xam lii nag moo laaj xel. Juróom-ñaari bopp ya ñooy juróom-ñaari tund, yi jigéen ji toog ci seen kaw. Juróom-ñaari buur lañu itam:

17:10  juróom daanu nañu, kenn kaa ngi fi, ki ci des ñëwagul, te bu ñëwee, dina fi war a nekk ab diir.

17:11  Rab wi nekkoon te nekkatul nag, moom ci boppam moo di juróom-ñetteelu buur bi, te ci juróom-ñaar yi la bokk. Ma nga jëm sànkute.

17:12  «Fukki béjjén yi nga gis, fukki buur lañu yu jotagul nguur. Waaye dinañu jot sañ-sañ diirub waxtu, ñuy nguuru ak rab wi.

17:13  Ñoo bokk mébét, di jox seen kàttan ak seen sañ-sañ rab wi.

17:14  Dinañu xare ak Mbote mi, waaye Mbote mi dina leen daan, ndaxte mooy kilifag kilifa yi, di Buuru buur yi. Te am toppam, di ñi mu woo te tànn leen, te ñu takku ci moom, dinañu daanandoo ak moom.»

17:15  Mu neeti ma: «Dex yi nga gis jigéenu moykat ja toog ca kaw, mooy réew yi ak mbooloo yi ak xeet yi ak kàllaama yi.

17:16  Fukki béjjén yi nga gis, ñoom ak rab wa, dinañu bañ jigéenu moykat ja, futti ko ci lépp, def ko yaramu neen. Dinañu lekk suuxam, ba noppi lakk ko ci safara.

17:17  Ndaxte Yàlla def na ci seen xol, ñu matal la mu naroon. Noonu dinañu ànd, jébbal seen nguur rab wi, ba kera li Yàlla wax di mat.

17:18  Te jigéen ji nga gis, moo di dëkk bu mag, biy nguuru ci kaw buuri àddina si.»

18:1  Gannaaw loolu ma gis meneen malaaka mu wàcce ca asamaan, yor sañ-sañ bu réy, te leeraayam daj na àddina sépp.

18:2  Mu daldi xaacu naan: «Daanu na! Babilon mu mag ma daanu na! Léegi dëkkukaayu jinne la, ak bépp rab wu bon ak bépp picc mu daganul te araam.

18:3  Ndaxte jox na xeeti àddina yépp, ñu naan ci koppu nafsoom ak njaaloom, ba ñu màndi. Buuri àddina ànd nañu ak moom ci njaaloo, te baana-baanay àddina woomle nañu ndax li mu bëgg mbuux.»

18:4  Noonu ma dégg beneen baat bu jóge asamaan naan: «Génnleen ci biiram, yéen samay gaay, ngir ngeen bañ a bokk ci ay bàkkaaram te bañ a am cér ci musiba yi koy dal.

18:5  Ndaxte ay bàkkaaram dajaloo nañu ba ci asamaan, te Yàlla fàttaliku na ay jëfam yu bon.

18:6  Dellooleen ko li mu defoon, feyleen ko ñaar ci li mu lebaloon, feesal-leen koppam ak naan gu gën a wex ñaari yoon naan ga mu joxe woon.

18:7  Joxleen ko ci coono ak naqar, lu tollu ni tiitar ak mbuux, ba mu dencaloon boppam. Gannaaw nee woon na ci xelam: “Maa ngi toog fii ni buur, duma ab jëtun te duma ténj mukk,”

18:8  looloo tax ba musiba, yii ñu ko sédd, dinañu ñëw ci benn bés, ñu di mbas, ténj ak xiif, ñu di ko lakk ba mu jeex, ndaxte Yàlla Boroom bi ko àtte, ku am kàttan la.»

18:9  Buuri àddina yépp, yi àndoon ak moom ci njaaloo ak mbuux, bu ñu séenee saxar siy jollee ci taal bi ñu koy lakke, dinañu yuuxu, di ko jooy.

18:10  Dinañu tiit ndax coonoom, ba dandu lu sore, naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw,dëkk bu mag bi,Babilon mi am kàttan;wenn waxtu rekk doy na,ngir sab àtte mat!»

18:11  Baana-baana yi ci kaw suuf di jooy, di ko naqarlu, ndaxte kenn dootul jënd seen njaay:

18:12  seen wurus, seen xaalis, seeni jamaa ak yeneeni per; seeni piis yu rafet, piis yu yolet, yu ray-ray, yu xonq; seen dénk wu xeeñ, seen yëf yi ñu defare iwaar walla dénk wu jafe walla xànjar walla weñ walla marbar;

18:13  ak bant yuy safal, gàncax gu xeeñ, ay xeeti cuuraay yu bare, latkoloñ, biiñ, diw, sungufu lay-layaat, pepp, ay nag, ay xar, ay fas, sareeti xare, ay jaam, ba ci bakkani nit.

18:14  Dinañu wax naan: «Yëf yi nga bëggoon a am raw nañu la, te lépp luy yafal walla col gu rafet ñàkk nga ko, te kenn du ko gisaat!»

18:15  Baana-baana, yi daan jaay yëf yooyu ba woomle, dinañu sore ndax ragal coonoom. Dinañu jooy di naqarlu,

18:16  naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw, dëkk bu mag,bi soloon yére yu rafet, yu yolet te xonq,daan takk wurus ak jamaa ak per,

18:17  sa alal ju bare jépp naaw na ci wenn waxtu!» Noonu ñépp ñiy dawal gaal ak ñi ciy tukki ak ñi ciy liggéey ak ñi ciy baana-baana, ñépp di sore bérab boobu,

18:18  te bu ñu séenee saxar sa cay jollee, naan: «Ndax dëkk bu niroo woon ak dëkk bu mag bii mas na am?»

18:19  Ñuy xëpp suuf ci seen bopp, di jooy, di naqarlu te naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw,dëkk bu mag bi nga xam neci la boroom gaal yépp woomle ndax sa barele,ci wenn waxtu nga gental.

18:20  Yaw asamaan, bégal ci li ñu ko yàq!Yéen itam gaayi Yàlla yi,ndaw yi ak yonent yi, bégleen,ndaxte Yàlla àtte na ko, ba feyyul leen.»

18:21  Noonu malaaka mu am doole jël doj wu réy, sànni ko ci géej gi, naan: «Nii lañuy sànnee ak doole Babilon dëkk bu mag bi, mu ne meŋŋ.

18:22  Buumi xalam yi, baati woykat yi, toxoro yi ak liit yi,kenn dootu leen dégg ci yaw.Liggéeykat bu xareñ bu mu man a doon, kenn dootu ko gis ci yaw.Kandaŋu gënn, kenn du ko déggati ci yaw.

18:23  Niitug làmp du tàkkati,te baatu boroom séet ak séetam dootul jib ci yaw ba fàww.Ndaxte say baana-baana ñoo yilifoon àddina,te xeet yépp réer nañu ndax say luxus.

18:24  Te deretu yonent yi ak gaayi Yàlla yiak ñépp ñi ñu rey ci kaw suuf,ci moom Babilon lañu ko fa fekk.»

19:1  Gannaaw loolu ma dégg lu mel ni baat bu xumb bu jollee ca mbooloo mu bare ca asamaan, naan:«Aleluya!Mucc, ndam ak kàttan,Yàlla sunu Boroom moo ko moom.

19:2  Ay àtteem dañoo dëggu te jub!Ndaxte àtte na jigéenu moykat bu mag,bi daan yàq àddina si ak njaaloom,te feyyul na noonu jaami Yàlla, yi mu daan rey.»

19:3  Ñu tegaat ca ne:«Aleluya!Saxarus lakku dëkk baa ngi jolli ba fàww!»

19:4  Noonu ñaar-fukki mag ña ak ñeent, ak ñeenti mbindeef ya, daldi sukk di jaamu Yàlla, moom mi toog ca gàngune ma. Ñu naan:«Amiin! Aleluya!»

19:5  Noonu baat jibe ca gàngune ma naan:«Màggal-leen Yàlla sunu Boroom,yéen ñépp ñi di ay jaamam,yéen ñi ko ragal, mag ak ndaw.»

19:6  Ma dégg lu mel ni baatu mbooloo mu bare, mel ni riiru duusi géej, ni yenguy dënnu yu réy, naan:«Aleluya!Ndaxte sunu BoroomYàlla Aji Kàttan jidugg na ci nguuram.

19:7  Nanu bég te bànneexute jox ko ndam li,ndaxte céetu Mbote mi agsi na,séet bi waaj na.

19:8  May nañu ko, mu sol mbubb mu sette weex bay lerax.» Mbubb mu weex moomu day misaal njubtey gaayi Yàlla yi.

19:9  Gannaaw loolu malaaka ma ne ma: «Bindal lii: “Yéen ñi ñu woo ci reeri céetu Mbote ma, barkeel ngeen.”» Mu teg ca ne ma: «Kàddu yii ñooy kàdduy Yàlla, di kàddu yu dëggu.»

19:10  Noonu ma daanu ci ay tànkam, bëgg koo jaamu. Waaye mu ne ma: «Moytu koo def; sa nawle laa ci liggéey bi, di kenn ci say bokk, yiy sax ci seedeel Yeesu. Jaamul Yàlla. Ndaxte seedes Yeesu mooy xel miy solu yonent yi.»

19:11  Bi loolu wéyee ma gis asamaan ubbiku. Noonu fas wu weex feeñ. Ki ko war ma nga tudd Ku Takku te Dëggu, te ci njub lay àtte ak a xare.

19:12  Ay bëtam di xuyy ni safara te mu am mbaxanay buur yu bare ca boppam. Bind nañu ci moom tur wu kenn xamul ku dul moom.

19:13  Sol na mbubb mu ñu sóob ci deret, te Kàddug Yàlla mooy turam.

19:14  Xarekat yi nekk ci asamaan topp ci moom, war ay fas yu weex, sol mbubb yu weex te set.

19:15  Am na jaasi ju ñaw juy génn ci gémmiñam, ngir dóor xeet yi, mu di leen jiitee yetu weñ, te mooy nappaaje réseñ yi ci segalukaayu mer mu tàng, mu Yàlla Aji Kàttan ji.

19:16  Ci mbubbam ak ci poojam bind nañu ci tur wii: Buuru buur yi, Kilifag kilifa yi.

19:17  Noonu ma gis malaaka mu taxaw ci jant bi. Mu wax ak baat bu xumb ak picc, yiy naaw ci digg asamaan, ne leen: «Ñëwleen teewesi reer bu mag bu Yàlla,

19:18  ngeen lekk suuxi buur yi, njiiti xare yi ak boroom kàttan yi, suuxi fas yi ak seeni gawar, suuxi ñépp: gor ak jaam, mag ak ndaw.»

19:19  Noonu ma gis rab wa, buuri àddina si ak seeni xarekat dajaloo ngir xareji ak ki war fas wa ak ay xarekatam.

19:20  Ñu jàpp rab wa, moom ak naaféq ba mbubboo yonent, ba daan def ca turu rab wa ay kéemaan yu mu naxe ñi nangu woon a am màndargam rab wa te jaamu nataalam. Ñoom ñaar ñépp sànni nañu leen ñuy dund ca déegu safara ak tamarax buy tàkk.

19:21  Ña ca des, jaasi, jay génn ca gémmiñu ka toog ca fas wa, rey leen; picc yépp lekk, ba regg ci seeni suux.

20:1  Noonu ma gis malaaka mu wàcce ca asamaan, yor caabiy kàmb ga ak càllala gu réy.

20:2  Mu jàpp ninkinànka ja, di jaani cosaan ja, muy Tuumaalkat bi, maanaam Seytaane. Malaaka ma yeew ko diirub junniy at,

20:3  sànni ko ci kàmb gi, tëj ko, sakk bunt bi ko tiim ci kaw. Noonu du nax xeet yi, ba kera junniy at yi di mat. Gannaaw loolu fàww ñu yiwi ko diir bu gàtt.

20:4  Noonu ma gis ay gàngune, ñu jox ña ca toog sañ-sañu àtte. Noonu ma gis ruuwi ñi ñu bóomoon ndax li ñu doon seedeel Yeesu te gëm kàddug Yàlla. Ñooñu jaamuwuñu rab wa mbaa nataalam, te nanguwuñoo am màndargam rab wa ca seen jë mbaa seen loxo. Ñu daldi dekki, nguuru ak Kirist diirub junniy at.

20:5  Yeneen néew yi duñu dekki, fi ak junniy at yi matul. Loolu moo di ndekkite lu jëkk li.

20:6  Ñi bokk ci ndekkite lu jëkk li, barkeel nañu te sell! Ñaareelu dee gi du leen manal dara. Waaye dinañu doon saraxalekati Yàlla ak Kirist, tey nguuru ak moom junniy at.

20:7  Bu junniy at ya matee, dinañu yiwi Seytaane ca kasoom,

20:8  te dina dem naxi xeet yi ci ñeenti xeblay àddina, maanaam ñoom Gog ak Magog. Dina leen dajale ngir xare, te dinañu bare ni peppi suuf cig tefes.

20:9  Dinañu sam suuf sépp, di wër dalu gaayi Yàlla yi ak dëkk, bi Yàlla bëgg. Waaye safara daldi jóge asamaan, lakk leen.

20:10  Dees na jàpp Seytaane, mi leen daan nax, sànni ko ci déegu safara ak tamarax bi, mu fekki rab wa ak naaféq ba mbubboo yonent. Foofa dinañu leen mbugal guddi ak bëccëg ba fàww.

20:11  Noonu ma gis gàngune mu mag te weex, ak ka ca toog. Asamaan ak suuf daw, sore ko, ba ne mes.

20:12  Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanamu gàngune ma. Ñu daldi ubbi ay téere, ubbi itam beneen téere, téereb dund bi. Ñu àtte néew ya, ku nekk ci say jëf, ni ñu ko binde woon ca téere ya.

20:13  Noonu géej gëq néew, yi nekkoon ci moom; dee ak barsàq delloo néew, ya ñu yoroon. Ñu àtte ñépp ci seeni jëf.

20:14  Ñu jàpp dee ak barsàq, sànni ca déegu safara sa. Déegu safara soosu moo di ñaareelu dee.

20:15  Képp ku ñu bindul sa tur ci téereb dund bi, dees na la sànni ci déegu safara si.

21:1  Noonu ma gis asamaan su bees ak suuf su bees, ndaxte asamaan su jëkk sa ak suuf su jëkk sa wéyoon nañu, te géej gi amatul.

21:2  Ma gis, wàcce ca asamaan, jóge ca wetu Yàlla, Yerusalem gu bees gi, dëkk bu sell, bi ñu waajal ba mu jekk ni séet buy nég jëkkëram.

21:3  Ma dégg baat bu xumb jibe ca gàngune ma naan: «Dalub Yàllaa ngi ci biir nit ñi. Dina dëkk ak ñoom, nit ñi dinañu nekk ay gaayam, te moom Yàlla ci boppam dina ànd ak ñoom, nekk Yàlla seen Boroom.

21:4  Dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu.»

21:5  Noonu ki toog ca gàngune ma ne: «Maa ngi yeesal lépp!» Mu ne ma: «Bindal, ndaxte kàddu yii yu wóor lañu te dëggu.»

21:6  Mu teg ca ne ma: «Lépp mat na! Maay Alfa ak Omega, njàlbéen gi ak muj gi. Ku mar, dinaa la may ci bëtu ndoxum dund mi, te doo fey dara.

21:7  Ku daan, dinga am cér ci mbir yii. Dinaa nekk Yàlla sa Boroom, te dinga nekk doom ci man.

21:8  Waaye ñi ragal, ñi gëmul, ñiy def lu ñaaw, ñiy bóom nit, ñiy njaaloo, luxuskat yi, xërëmkat yi ak fenkat yépp, seen añ moo di déegu safara ak tamarax bi. Loolu mooy ñaareelu dee gi.»

21:9  Gannaaw loolu benn malaaka ñëw, mi bokk ca juróom-ñaari malaaka, ya yoroon juróom-ñaari ndabi musiba yu mujj ya, ne ma: «Ñëwal, ma won la séet bi, jabaru Mbote mi.»

21:10  Noonu Xelum Yàlla solu ma, malaaka ma yóbbu ma ci kaw tund wu réy-a-réy. Noonu mu won ma Yerusalem, dëkk bu sell bi, muy wàcce ci asamaan, jóge ca wetu Yàlla,

21:11  ànd ak ndamu Yàlla. Leeraayam mel ni leeraayu per bu jafe lool, ni jamaa buy ray-rayi.

21:12  Miir bu réy te kawe moo ko wër te am fukki bunt ak ñaar, te bu ca nekk malaaka taxaw ca wet ga. Ca bunt ya bind nañu ca fukki tur ak ñaar, yu giiri bànni Israyil.

21:13  Ca penku am na fa ñetti bunt; ca nor ñett; ca sudd ñett ak ñett ca sowu.

21:14  Samp nañu miiru dëkk ba ci fukki fondamaa ak ñaar, yu ñu bind turi fukki ndawi Mbote ma ak ñaar.

21:15  Ki doon wax ak man amoon na nattukaay, di bantu wurus bu mu doon natte dëkk ba ak miir ba ko wër, ak bunt ya.

21:16  Dëkk ba dafa kaare, guddaay ba ak yaatuwaay ba ñoo tolloo. Mu natt dëkk ba ak bant ba mu yor. Guddaay ba, yaatuwaay ba ak taxawaay ba lépp tolloo, di fukki junni ak ñaar ciy estat.

21:17  Malaaka ma natt miir ba nattub nit, fekk miir ba di téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti xasab.

21:18  Miir ba, jamaa lañu ko liggéeye, te dëkk ba di wurusu ngalam, leer ni weer bu set.

21:19  Fondamaay miiru dëkk ba rafetale nañu leen xeeti per yu nekk.Fondamaa bu jëkk ba jamaa la;ñaareel ba, per bu bulo bu ñuy wax safir;ñetteel ba, per bu wert bu ñuy wax kalseduwan;ñeenteel ba, per bu wert te lerax, bu ñuy wax emëróot;

21:20  juróomeel ba, per bu xonq bu ñuy wax sardonigsë;juróom-benneel ba, per bu xonq curr bu ñuy wax sarduwan;juróom-ñaareel ba, per bu mboq bu ñuy wax kirisolit;juróom-ñetteel ba, per bu wert ni géej bu ñuy wax beril;juróom-ñeenteel ba, per bu mboq bu ñuy wax topas;fukkeel ba, per bu wert bu ñuy wax kirisoparas;fukkeel ba ak benn, per bu bulo bu ñuy wax yasent;fukkeel ba ak ñaar, per bu yolet bu ñuy wax ametist.

21:21  Fukki bunt ya ak ñaar, ay per yu weex lañu. Bunt bu nekk di benn per kepp. Péncu dëkk ba di wurusu ngalam, leer ni weer bu set.

21:22  Gisuma ca dëkk ba kër Yàlla, ndaxte Boroom bi Yàlla Aji Kàttan ji ak Mbote ma ñooy màggalukaay ba.

21:23  Dëkk ba soxlawul jant walla weer ngir leeral ko, ndaxte ndamu Yàlla moo koy leeral, te Mbote ma moo nekk làmpam.

21:24  Xeeti àddina dinañu dox cig leeram, te buuri àddina dinañu ca indi seen ndam.

21:25  Bunti dëkk ba duñu tëju bëccëg, te guddi du fa am.

21:26  Dinañu fa indi ndamu xeet yi ak seen alal.

21:27  Dara du fa dugg lu am sobe, mbaa kenn kuy sóobu ci ñaawteef walla fen. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Mbote mi rekk ñoo fay dugg.

22:1  Noonu malaaka ma won ma dexu ndoxum dund, mu leer ni weer bu set, di génn ca gàngune mu Yàlla ak Mbote ma,

22:2  xellee ca digg péncu dëkk ba. Ca weti dex ga amoon na ca garabu dund, guy meññ fukki yoon ak ñaar, di meññ weer wu nekk, te xob ya di faj xeet yi.

22:3  Musiba dootul am. Gàngune mu Yàlla ak Mbote mi mu ngi ci dëkk bi, te ay jaamam dinañu ko jaamu.

22:4  Dinañu gis xar-kanamam, te turam dina nekk ci seen jë.

22:5  Guddi dootul am, te kenn dootul soxla leeru làmp walla naaju jant, ndaxte Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dinañu nguuru ba fàww.

22:6  Noonu malaaka ma ne ma: «Wax jii ju wóor la te dëggu. Boroom bi, Yàlla jiy leeral xeli yonent yi, moo yónni malaakaam, ngir mu won ay jaamam mbir yi dëgmël di ñëw.»

22:7  «Maa ngi ñëw léegi. Yaw miy sàmm waxi Yàlla, yi ci téere bii, barkeel nga.»

22:8  Man Yowaana maa dégg mbir yii te gis ko. Ba ma ko déggee te gis ko, damaa daanu ca tànki malaaka, ma ma ko doon won, bëgg koo jaamu.

22:9  Waaye mu ne ma: «Moytu koo def. Sa nawle laa ci liggéey bi, yaw ak say bokki yonent ak ñiy sàmm waxi téere bii. Jaamul Yàlla.»

22:10  Mu ne ma it: «Bul tëj téere bii ak waxi Yàlla yi mu ëmb, ndaxte waxtu wi jege na.

22:11  Ku jubadi, na sax ci jubadeem; ku taq sobe, na sigiñu ci sobeem; ku jub, na wéy ci jëf yu jub; ku sell, na ci ŋoy.»

22:12  Yeesu nee na: «Maa ngi ñëw léegi, indaale pey gi, ngir delloo ku nekk lu mengoo ak lu mu def.

22:13  Man maay Alfa ak Omega, ki jëkk te mujj, njàlbéen gi ak muj gi.

22:14  «Yéen ñi fóot seeni mbubb, ngir sañ a lekk ci garabu dund gi te dugg ci bunti dëkk bi, barkeel ngeen.

22:15  Waaye ñi ci biti ñooy xaj yi, luxuskat yi, njaalookat yi, bóomkat yi, xërëmkat yi ak ñépp ñiy sopp fen te di ci wéy.

22:16  «Man Yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede leen mbir yii ci digg mboolooy ñi gëm. Man maay car, bi soqikoo ci Daawuda, di biddiiwu njël bu leer bi.»

22:17  Te Xelum Yàlla ak séetu Mbote mi ñu ngi naan: «Ñëwal.» Képp ku dégg wax jii, na ne: «Ñëwal.» Na képp ku mar, ñëw; ku bëgg, duyal ci ndoxum dund mi te doo fey dara.

22:18  Man Yowaana maa ngi koy wax képp ku dégg waxi Yàlla, yi nekk ci téere bii: ku ci yokk dara, Yàlla dina dolli ci sa mbugal musiba, yi ñu wax ci téere bii.

22:19  Ku dindi dara ci waxi Yàlla, yi nekk ci téere bii, Yàlla dina dindi sa wàll ca garabu dund ga ak dëkk bu sell ba, ñaar yooyu ñu bind ci téere bii.

22:20  Kiy seede mbir yii nee na: «Waaw, maa ngi ñëw léegi.» Amiin. Boroom bi Yeesu, ñëwal.

22:21  Na yiwu Boroom bi Yeesu ànd ak yéen ñépp.