Sacred Texts  Bible  World Bible  Index  Previous  Next 

Wolof Bible: Luke

1:1  Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit ñu bare sasoo nañoo bind ab nettali bu jëm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir,

1:2  li dëppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te ñu mujj nekk jawriñi kàddug Yàlla.

1:3  Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe.

1:4  Noonu dinga man a xam ne, li ñu la jàngaloon lu wér peŋŋ la.

1:5  Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na saraxalekat bu ñu tudde Sakariya te bokk ca mbootaayu saraxalekat, ya askanoo ci Abiya. Jabaram Elisabet askanoo moom itam ci Aaroona.

1:6  Sakariya ak jabaram ñu jub lañu ca kanam Yàlla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi yépp.

1:7  Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet mënul a am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu.

1:8  Benn bés nag Sakariya doon def liggéeyu saraxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog.

1:9  Bi ñuy tegoo bant, ni ko saraxalekat yi daan defe nakajekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakariya.

1:10  Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan.

1:11  Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakariya, taxaw ca féeteek ndeyjooru saraxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam.

1:12  Naka la ko Sakariya gis, fitam daldi dem, mu tiit.

1:13  Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakariya, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa jabar dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya.

1:14  Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom,

1:15  ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu.

1:16  Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom.

1:17  Mooy jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Iliyas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.»

1:18  Sakariya daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne, loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama jabar it màggat na.»

1:19  Malaaka ma tontu ko ne: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xebaar bu baax boobu.

1:20  Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo man a wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»

1:21  Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakariya yàgg ca bérab bu sell ba.

1:22  Waaye bi mu génnee nag, mënul a wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne, dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.

1:23  Bi Sakariya matalee liggéeyu saraxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi.

1:24  Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet jabaram ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer

1:25  te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!»

1:26  Bi Elisabet nekkee ci juróom-benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.

1:27  Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama.

1:28  Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm ngaam, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.»

1:29  Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu man a tekki.

1:30  Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam.

1:31  Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.

1:32  Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam.

1:33  Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.»

1:34  Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu man a ame? Man de, janq laa ba tey.»

1:35  Malaaka ma tontu ko ne: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji.

1:36  Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku mënul a am doom, mu ngi ci juróom-benni weeram.

1:37  Ndaxte dara tëwul Yàlla.»

1:38  Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem.

1:39  Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude.

1:40  Mu dugg ca kër Sakariya, daldi nuyu Elisabet.

1:41  Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yengatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet.

1:42  Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb!

1:43  Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi?

1:44  Maa ngi lay wax ne, naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yengu ci sama biir ndax mbég.

1:45  Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne, li la Boroom bi yégal dina mat!»

1:46  Noonu Maryaama daldi ne:

1:47  «Sama xol a ngi màggal Boroom bi,sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat,

1:48  ndaxte fàttaliku na ma,man jaamam bu woyof bi.Gannaawsi tey, niti jamono yéppdinañu ma wooye ki ñu barkeel,

1:49  ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy.Turam dafa sell.

1:50  Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal,ci seeni sët ba ci seeni sëtaat.

1:51  Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom,te tas mbooloom ñiy réy-réylu,

1:52  daaneel boroom doole yi ci seen nguur,yékkati baadoolo yi.

1:53  Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex,te dàq boroom alal yi,ñu daw ak loxoy neen.

1:54  Wallu na bànni Israyil giy jaamam,di fàttaliku yërmandeem,

1:55  ni mu ko dige woon sunuy maam,jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.»

1:56  Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu war a tollook ñetti weer, sog a ñibbi.

1:57  Gannaaw loolu jamono ji Elisabet war a mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor.

1:58  Dëkkandoom yi ak mbokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.

1:59  Bi bés ba dellusee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakariya.

1:60  Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.»

1:61  Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»

1:62  Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba.

1:63  Sakariya laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru.

1:64  Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakariya daldi waxaat, di màggal Yàlla.

1:65  Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp.

1:66  Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne, dooley Boroom baa ngi ànd ak moom.

1:67  Sakariya baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne:

1:68  «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil,ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!

1:69  Feeñal na nu Musalkat bu am doole,bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam,

1:70  ni mu yéglee woon bu yàggjaarale ko ci yonentam yu sell yi.

1:71  Dina nu musal ci sunuy noon,jële nu ci sunu loxoy bañaale.

1:72  Yàlla wone na yërmandeem,ji mu digoon sunuy maam,te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom,

1:73  di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,

1:74  dina nu teqale ak sunuy noon,ngir nu man koo jaamu ci jàmm,

1:75  nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.

1:76  Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji,ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi,di ko xàllal yoon wi.

1:77  Dinga xamal mbooloom,ni leen Boroom bi man a musale,jaare ko ci seen mbaalug bàkkaar,

1:78  ndaxte Yàlla sunu Boroom fees na ak yërmande,ba tax muy wàcce ci nun jant buy fenk,

1:79  ngir leeral ñi toog ci lëndëm,takkandeeru dee tiim leen,ngir jiite nu ci yoonu jàmm.»

1:80  Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.

2:1  Ca jamono jooja buur bu mag bu ñuy wax Ogust joxe ndigal ne, na ñépp binduji.

2:2  Mbindu mooma, di mu jëkk ma, daje na ak jamono, ja Kiriñus nekke boroom réewu Siri.

2:3  Noonu ku nekk dem binduji ca sa dëkku cosaan.

2:4  Yuusufa nag daldi jóge Nasaret ca diiwaanu Galile, jëm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, dëkk ba Daawuda cosaanoo, ndaxte ci askanu Daawuda la bokk.

2:5  Mu dem binduji, ànd ak Maryaama jabaram, fekk booba Maryaama ëmb.

2:6  Bi ñu nekkee Betleyem, waxtu wa mu waree mucc agsi.

2:7  Mu taawloo doom ju góor, mu laxas ko ci ay laytaay, tëral ko ca lekkukaayu jur ga, ndaxte xajuñu woon ca dalukaay ba.

2:8  Fekk booba amoon na ca gox ba ay sàmm yu daan fanaan ca tool ya, di wottu jur ga.

2:9  Noonu benn malaakam Boroom bi feeñu leen, ndamu Boroom bi daldi leer, melax, wër leen. Tiitaange ju réy jàpp leen.

2:10  Waaye malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndaxte dama leen di xamal xebaar bu baax buy indi mbég mu réy ci nit ñépp.

2:11  Tey jii ca dëkku Daawuda, ab Musalkat juddul na leen fa, te mooy Almasi bi, di Boroom bi.

2:12  Ci firnde jii ngeen koy xàmmee: dingeen gis liir bu ñu laxas ci ay laytaay, tëral ko ci lekkukaayu jur.»

2:13  Bi mu waxee loolu, yeneen malaaka yu bare yu jóge asamaan, ànd ak moom, di sant Yàlla naan:

2:14  «Nañu màggal Yàlla ca asamaan su kawe sa,te ci àddina, na jàmm ji wàcc ci nit, ñi mu nangu ndax yiwam!»

2:15  Bi malaaka ya delloo ca asamaan, sàmm yi di waxante naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, li nu Boroom bi xamal.»

2:16  Ñu daldi gaawantu dem, gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir, ba ñu tëral ca lekkukaayu jur ga.

2:17  Bi ñu leen gisee, ñu nettali la ñu leen waxoon ca mbirum xale ba.

2:18  Ñi dégg li sàmm yi doon wax ñépp daldi waaru lool.

2:19  Waaye Maryaama moom, takkoon na mbir yooyu yépp, di ko xalaat ci xolam.

2:20  Noonu sàmm ya dellu ca seen jur, di màggal Yàlla, di ko sant ci li ñu déggoon lépp te gis ko, ndaxte lépp am na, ni ko Boroom bi waxe woon.

2:21  Bi bés ba dellusee jamonoy xarafal xale ba agsi. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb.

2:22  Noonu jamono ji ñu leen waroon a sellale agsi, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi.

2:23  Ndaxte bind nañu ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, nañu ko sédde Boroom bi.»

2:24  Bi ñu ko yóbboo, def nañu itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll walla ñaari xati yu ndaw.»

2:25  Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yàlla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yàlla war a dëfël bànni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom,

2:26  te xamal na ko ne, du dee mukk te gisul Almasib Boroom bi.

2:27  Noonu Xelum Yàlla daldi yóbbu Simeyon ba ca kër Yàlla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir sédde ko Yàlla, ni ko yoon wi santaanee,

2:28  Simeyon jël xale bi, leewu ko, daldi sant Yàlla ne:

2:29  «Boroom bi, nanga yiwi sa jaam,mu noppaluji ci jàmm, ni nga ko waxe.

2:30  Ndaxte sama bët tegu na ci mucc gi nga lal,

2:31  xeet yépp seede ko.

2:32  Muy leer giy leeral xeet yi,di ndamu Israyil say gaay.»

2:33  Waajuri Yeesu yi waaru ci li ñu doon wax ci xale bi.

2:34  Noonu Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne Maryaama: «Xale bii Yàllaa ko yónni, ngir ñu bare ci Israyil daanu te yékkatiku. Def na ko it muy firnde ju ñuy weddi,

2:35  ba naqar dina xar sa xol ni jaasi. Noonu xalaati ñu bare feeñ.»

2:36  Amoon na it ca Yerusalem yonent bu ñuy wax Aana. Doomu Fanuwel mi askanoo ci Aser la woon, te Aana màggatoon na lool. Bi mu séyee, dëkk na juróom-ñaari at ak jëkkëram.

2:37  Jëkkër ja gaañu, te séyaatul. Léegi amoon na juróom-ñett-fukki at ak ñeent. Mi ngi dëkke woon a jaamu Yàlla guddi ak bëccëg ca kër Yàlla ga, di ñaan ak di woor.

2:38  Aana yem ca waxi Simeyon ya, daldi gërëm Yàlla tey yégal mbiri liir ba ñépp ñi doon séentu jamono, ji Yàlla war a jot Yerusalem.

2:39  Bi waajuri Yeesu yi matalee seen warugar ci lépp lu yoonu Boroom bi santaane woon, ñu dellu seen dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.

2:40  Xale baa nga doon màgg, di dëgër, mu fees ak xel te yiwu Yàlla ànd ak moom.

2:41  At mu jot nag waajuri Yeesu yi daan nañu dem Yerusalem, ngir màggali bésu Jéggi ba.

2:42  Noonu bi Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggal ga, ni ñu ko daan defe nakajekk.

2:43  Bi màggal ga tasee, ñu dëpp ñibbi, waaye xale ba Yeesu des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko.

2:44  Ñu xalaat ne, Yeesu dafa àndoon ak ñeneen, ñi ñu bokkaloon yoon. Bi ñu doxee bésub lëmm, ñu tàmbali di ko seet ci seen bokk yi ak seen xame yi.

2:45  Bi ñu ko gisul nag, ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko.

2:46  Ca gannaaw ëllëg sa ñu fekk ko ca kër Yàlla ga, mu toog ci jàngalekati Yawut yi, di déglu ak di laajte.

2:47  Ñépp ñi dégg li mu wax yéemu ci xel, mi mu àndal, ak ni mu doon tontoo.

2:48  Naka la ko waajuram yi gis, ñu daldi waaru. Yaayam ne ko: «Sama doom, lu tax nga def nu lii? Man ak sa baay nu ngi la doon seet, jaaxle lool.»

2:49  Mu ne leen: «Lu tax ngeen may seet? Xanaa xamuleen ne, damaa war a nekk ci sama kër Baay?»

2:50  Waaye xamuñu li kàddoom yi doon tekki.

2:51  Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom, dellu Nasaret te déggal ay waajuram. Fekk yaayam moom takk mbir yooyu yépp ci xolam.

2:52  Yeesoo ngi doon màgg ci jëmm, tey yokku ci xam-xam te neex Yàlla ak nit ñi.

3:1  Fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar, fekk Poñsë Pilaat yilif diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, te Lisañas yilif Abilen.

3:2  Te it Anas ak Kayif nekkoon saraxalekat yu mag ya. Ca jamono jooja la kàddug Yàlla wàcc ci Yaxya, doomu Sakariya, ca màndiŋ ma.

3:3  Yaxya daldi dugg àll, bi wër dexu Yurdan gépp, di waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.»

3:4  Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan:«Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.

3:5  Nañu sëkk xur yi,maasale tund yi ak jànj yi.Yoon yi dëng ñu jubbanti leen,yi ñagas ñu rataxal leen.

3:6  Bu ko defee bépp mbindeef dina gismucc gi Yàlla tëral.”»

3:7  Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc?

3:8  Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te bañ a nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii.

3:9  Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci safara si.»

3:10  Mbooloo ma laaj ko ne: «Lan lanu war a def nag?»

3:11  Mu ne leen: «Ku am ñaari mbubb, nga jox menn mi ki amul. Ku am ñam itam, nga bokk ko ak ki amul.»

3:12  Ay juutikat itam ñëw ca Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox; ñu ne ko: «Kilifa gi, lu nu war a def?»

3:13  Mu tontu leen ne: «Laajleen rekk lu jaadu.»

3:14  Ay xarekat laaj nañu ko ne: «Li jëm ci nun nag?» Mu ne leen: «Buleen néewal doole kenn, jël xaalisam ci kaw ay tëkku mbaa ci seede lu dul dëgg. Waaye doylooleen li ñu leen di fey.»

3:15  Mbooloo maa ngay xaar, di séentook a laaj ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi.

3:16  Noonu Yaxya tontu leen ñoom ñépp ne: «Man maa ngi leen di sóob ci ndox. Waaye ki ma ëpp kàttan dina ñëw te yeyoowumaa tekki ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak safara.

3:17  Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàqam, waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk.»

3:18  Noonu Yaxya teg ca yeneen dénkaane yu bare, di yégal nit ña xebaar bu baax ba.

3:19  Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Erojàdd, jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen ñaawteef,

3:20  ba faf tëj Yaxya kaso.

3:21  Noonu Yaxya sóob mbooloo mépp ci ndox, sóobaale it Yeesu. Bi Yeesu di ñaan nag, asamaan daldi ubbiku.

3:22  Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»

3:23  Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, amoon na lu war a tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci bëti nit ñi.Te Yuusufa mooy doomu Eli,

3:24  miy doomu Matat.Matat, Lewi mooy baayam; Lewi, Melki;Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;

3:25  Yuusufa, Matacas; Amos; Naxum; Esli; Nagayi.

3:26  Nagayi, Maat; Matacas; Semeyin; Yoseg; Yoda.

3:27  Yoda, Yowanan mooy baayam; Yowanan, Resa;Resa, Sorobabel. Kooku Salacel a ko jur; Salacel, Neri;

3:28  Neri, Melki; Adi; Kosam; Elmadam; Er.

3:29  Er, Yeesu; Eliyeser; Yorim; Matat; Lewi;

3:30  Simeyon; Yuda; Yuusufa; Yonam; Eliyakim.

3:31  Eliyakim, Meleya; Meleya, Mena;Mena, Matata; Matata, Natan;Natan, Daawuda.

3:32  Daawuda mooy doomu Yese;Yese, Obedd; Bowas; Salmon; Naason.

3:33  Naason; Aminadab; Aminadab, Admin;Arni; Esrom; Fares; Yuda;

3:34  Yanqóoba; Isaaxa; Ibraayma; Teraa; Naxor;

3:35  Serug; Ragaw; Faleg; Eber; Sala.

3:36  Sala, Kaynam mooy baayam; Kaynam, Arpagsàdd;Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg;

3:37  Lemeg, Matusala; Enog, Yaredd; Maleleel; Kaynan;

3:38  Enos; Set; Set doomu Aadama;Aadama doomu Yàlla.

4:1  Noonu Yeesu fees ak Xel mu Sell mi, jóge dexu Yurdan.

4:2  Xelum Yàlla mi yóbbu ko ca màndiŋ ma, mu nekk fa ñeent-fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane. Lekkul woon dara ci fan yooya, te gannaaw gi mu xiif.

4:3  Noonu Seytaane ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj wii mu nekk mburu.»

4:4  Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk.”»

4:5  Seytaane yóbbu na ko fu kawe. Ci xef-ak-xippi mu won ko réewi àddina sépp,

4:6  ne ko: «Dinaa la jox bépp sañ-sañu nguur yii ak seen ndam ndaxte jébbal nañu ma ko, te ku ma soob laa koy jox.

4:7  Kon boo ma màggalee, dinga moom lépp.»

4:8  Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom te jaamu ko moom rekk.”»

4:9  Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal jëm ci suuf,

4:10  ndaxte Mbind mi nee na:“Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,ñu sàmm la,

4:11  dinañu la leewu ci seeni loxo,ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj.”»

4:12  Yeesu tontu ko ne: «Bind nañu ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»

4:13  Bi mu ko lalalee fiiram yi mu am yépp, Seytaane daldi sore Yeesu, di xaar yeneen jamono.

4:14  Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp.

4:15  Muy jàngale ca seeni jàngu, te ñépp di ko tagg.

4:16  Yeesu dem Nasaret fa mu yaroo, te ca bésu noflaay ba, mu dugg ca jàngu ba, ni mu ko daan defe. Noonu mu taxaw ngir jàngal mbooloo mi.

4:17  Ñu jox ko téereb yonent Yàlla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis bérab, ba ñu bind aaya yii:

4:18  «Xelum Boroom baa ngi ci man,ndaxte moo ma tànn,ngir ma yégal néew doole yi xebaar bu baax bi.Dafa maa yónni,ngir ma yégal jaam ñi ne, dinañu leen goreel,yégal gumba yi ne, dinañu gis,te jot ñi ñu noot,

4:19  tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi.»

4:20  Bi mu jàngee aaya yooyu ba noppi, mu ub téere bi, delloo ko ki koy denc, toog. Ñépp ña nekkoon ca jàngu ba dékk koy bët.

4:21  Noonu mu daldi ne: «Tey jii, loolu Mbind mi wax mat na, bi ngeen koy déglu.»

4:22  Ñépp di seede lu rafet ci Yeesu, di waaru ci wax ju neex, ji mu doon yégle, ñu naan: «Ndax kii du doomu Yuusufa?»

4:23  Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”»

4:24  Mu tegaat ca ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ab yonent kenn du ko teral ca réewam.

4:25  Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Iliyas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu.

4:26  Moona Yàlla yónniwul Iliyas ci kenn ci ñoom, waaye mu yebal ko ci jigéen ju jëkkëram faatu, ju dëkk Sarebta, ca wetu Sidon.

4:27  Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Yàlla Alisa, ay nit ñu bare ñu gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naaman, mi dëkkoon réewu Siri.»

4:28  Bi ñu déggee wax yooya, ñépp ña nekkoon ca jàngu ba daldi fees ak mer.

4:29  Noonu ñu jóg, génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca mbartalum tund, wa ñu sanc seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf.

4:30  Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam.

4:31  Gannaaw loolu Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile.

4:32  Mu jàngal leen ca bésu noflaay ba, ñu waaru ca njàngaleem, ndaxte dafa wax ak sañ-sañ.

4:33  Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi xaacu ne:

4:34  «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!»

4:35  Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» Noonu rab wi daaneel nit ki ci suuf ci kanamu ñépp, daldi génn ci moom te gaañu ko.

4:36  Bi loolu amee ñépp waaru, ñuy waxante ci seen biir naan: «Céy jii wax! Ci sañ-sañ ak doole lay sant rab yi, ñu daldi génn.»

4:37  Noonu turam siiw ca diiwaan bépp.

4:38  Bi mu jógee ci jàngu bi, Yeesu dafa dem kër Simoŋ. Gorob Simoŋ bu jigéen dafa feebar, ba yaram wi tàng lool. Ñu naan Yeesu, mu dimbali leen ci.

4:39  Mu randusi, tiim ko, gëdd tàngoor wi, mu dem. Noonu tàngoor wi wàcc, soxna si jóg ca saa sa, di leen topptoo.

4:40  Bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ay jàngoro yu wuute. Kenn ku nekk mu teg la loxo, wéral la.

4:41  Te it ay rab di génn ca nit ña te di yuuxu naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Noonu mu gëdd leen, te mayu leen, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ne, mooy Almasi bi.

4:42  Ca njël gu jëkk Yeesu génn, dem ca bérab bu wéet. Mbooloo ma di ko seet. Bi ñu ko gisee, ñu koy wut a téye, ngir bañ mu dem.

4:43  Waaye mu ne leen: «Damaa war a dem ci yeneen dëkk yi, ngir yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla, ndaxte looloo tax ñu yónni ma.»

4:44  Noonu mu dem di waare ca jàngu ya ca réewu Yawut ya.

5:1  Benn bés Yeesu taxaw ca tefesu dexu Senesaret. Mbooloo ma wër ko, di buuxante ngir déglu kàddug Yàlla.

5:2  Noonu mu gis ñaari gaal yu teer ca tefes ga, nappkat ya ca wàcce, di raxas seeni mbaal.

5:3  Mu dugg ci genn gaal, fekk muy gu Simoŋ, mu ne ko, mu joow ba sore tuuti. Noonu Yeesu toog ca gaal ga, di jàngal mbooloo ma.

5:4  Bi mu jàngalee ba noppi, mu ne Simoŋ: «Joowal gaal gi, ba fa ndox ma gën a xóote, ngeen sànni fa seeni mbaal ngir napp.»

5:5  Simoŋ tontu ko ne: «Kilifa gi, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Waaye nag dinaa ko sànni ci sa ndigal.»

5:6  Naka lañu sànni mbaal yi, jàpp jën yu bare, ba mbaal yay tàmbalee xëtt.

5:7  Noonu ñu daldi liyaar seen àndandoo, yi nekk ca geneen gaal ga, ngir ñu ñëw dimbali leen. Ñooñu agsi, ñu feesal ñaari gaal yi, ba ñuy bëgg a suux.

5:8  Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanamu Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!»

5:9  Wax na loolu nag, ndax jën yu bare ya ñu mbaaloon daf koo jaaxal, moom ak ña mu àndaloon

5:10  ak ña mu bokkaloon liggéey ba, maanaam ñaari doomi Sebede yi di Saag ak Yowaana. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaawsi tey, ay nit ngay mbaal jëme ci man.»

5:11  Noonu ñu teer ca tefes ga, bàyyi lépp, di topp ci moom.

5:12  Ni Yeesu nekke woon ci ab dëkk, am fa ku gaana ba daj. Bi mu gisee Yeesu, mu daldi dëpp jëwam ci suuf, ñaan ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa wéral.»

5:13  Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.

5:14  Yeesu sant ko ne: «Bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga jébbal Yàlla sarax si yoonu Musaa santaane, ngir ñu xam ne wér nga, te mu nekk seede ci ñoom.»

5:15  Noonu turu Yeesu di gën a siiw. Mbooloo mu bare di ñëw ci moom, ngir déglu ko te mu faj seeni jàngoro.

5:16  Waaye Yeesu moom di beddeeku ci bérab yu wéet ya, di ñaan.

5:17  Am na bés Yeesu doon jàngale. Amoon na ca mbooloo, ma teewoon, ñu bokkoon ca Farisen ya ak ay xutbakat yu jóge ca dëkk yépp, ya ca Galile ak ya ca Yude ak Yerusalem. Yeesu àndoon na ak dooley Boroom bi, ba muy faj ay jarag.

5:18  Noonu ay nit ñëw, jàppoo basaŋ, ga ñu tëral nit ku yaram wépp làggi. Ñu di ko wut a dugal ca kër ga, ngir indi ko ca Yeesu.

5:19  Waaye gisuñu fu ñu koy awale ndax mbooloo ma. Ñu daldi yéeg ca kaw kër ga nag, xeddi tiwiil ya, yoor waa ja ak basaŋ ga, wàcce ko ca kanamu Yeesu ca biir mbooloo ma.

5:20  Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne làggi ba: «Sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»

5:21  Xutbakat yi ak Farisen yi di werante ci seen xel naan: «Kii mooy kan bay sosal Yàlla? Ana ku man a baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ?»

5:22  Waaye Yeesu xam seen xalaat, tontu leen ne: «Lu tax ngeen di werante ci seen xel?

5:23  Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gën a yomb?

5:24  Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ba: «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»

5:25  Nit ka jóg ca saa sa ci kanamu ñépp, jël basaŋ, ga ñu ko tëraloon, ñibbi tey màggal Yàlla.

5:26  Mbooloo mépp waaru, di màggal Yàlla. Ñu ragal tey wax naan: «Gis nanu tey ay mbir yu ëpp xel.»

5:27  Gannaaw loolu Yeesu génn, gis ab juutikat bu tudd Lewi, mu toog ca juuti ba. Mu ne ko: «Kaay topp ci man.»

5:28  Lewi jóg, bàyyi lépp, daldi ko topp.

5:29  Noonu Lewi togglu ay ñam yu bare ci këram, ngir teral Yeesu. Juutikat yu bare ak yeneen gan ñu nga fa woon, di lekkandoo ak ñoom.

5:30  Farisen yi ak seeni xutbakat di xultu taalibey Yeesu yi ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak di naanandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»

5:31  Yeesu tontu leen ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.

5:32  Ñëwuma ngir woo ñi jub, waaye ngir woo bàkkaarkat yi, ñu tuub seeni bàkkaar.»

5:33  Noonu ñu ne Yeesu: «Taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi dinañu faral di woor ak di ñaan ci Yàlla, waaye say taalibe ñu ngiy lekk ak di naan.»

5:34  Yeesu ne leen: «Ndax man ngeen a woorloo gan, yi ñëw cig céet, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom?

5:35  Waaye bés yaa ngi ñëw, yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir. Bés yooyu nag, dinañu woor.»

5:36  Te it Yeesu wax leen léeb wii: «Kenn du jël mbubb mu bees, xotti ci sekkit, daaxe ko mbubb mu màggat. Lu ko moy, dina xotti mbubb mu bees mi, te sekkit, wi mu ci jële, du ànd ak mbubb mu màggat mi.

5:37  Te kenn du def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bu bees bi day toj mbuus yi, biiñ bi tuuru, mbuus yi yàqu.

5:38  Waaye dañoo war a def biiñ bu bees ci mbuus yu bees.

5:39  Ku naan biiñ bu màggat du bëgg bu bees bi, ndax day wax ne: “Bu màggat bi baax na.”»  

6:1  Amoon na benn bésu noflaay Yeesu di dem, jaar ci ay tool yu ñor. Taalibeem ya di fàq ay cëgg, di leen boxom ci seeni loxo tey lekk.

6:2  Am ay Farisen yu ne: «Lu tax ngeen di def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi?»

6:3  Yeesu tontu leen ne: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?

6:4  Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, jël mburu, ya ñu jébbal Yàlla, lekk ca, jox ca ña mu àndaloon? Fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul saraxalekat.»

6:5  Yeesu dellu ne leen: «Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.»

6:6  Beneen bésu noflaay, Yeesu dugg ci jàngu bi, di fa jàngale. Amoon na fa nit ku loxol ndeyjooram làggi.

6:7  Xutbakat yi ak Farisen yi ñu ngi ko doon xool, ba xam dina ko faj ci bésu noflaay bi, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.

6:8  Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom làggi: «Jógal taxaw ci kanamu ñépp.» Nit ka daldi jóg taxaw.

6:9  Yeesu ne leen: «Ma laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko bésu noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?»

6:10  Ci kaw loolu mu xool leen ñoom ñépp, ba noppi ne nit ka: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko, loxoom daldi wér peŋŋ.

6:11  Waaye nit ña mer ba fees, di rabat pexe yu jëm ca Yeesu.

6:12  Ca bés yooya Yeesu yéeg ca tund wa ngir ñaan, mu fanaan fa, di ñaan ci Yàlla.

6:13  Bi bët setee, Yeesu woo taalibeem yi, tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam:

6:14  Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi,

6:15  Macë ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokk ci mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;

6:16  Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujj a wor.

6:17  Yeesu ànd ak ndaw ya, wàcc tund ya, daldi taxaw ca joor ga, fa mbooloom taalibe mu takku nekkoon. Amoon na fa it ay nit ñu bare ñu jóge ca réewu Yawut ya mépp ak ca dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ca wetu géej ga, maanaam Tir ak Sidon.

6:18  Dañoo ñëw ngir déglu ko, te it ngir mu faj leen. Ñi rab jàpp it faju nañu.

6:19  Ñépp a ngi ko doon wut a laal ndax doole jiy jóge ci moom, di faj ñépp.

6:20  Yeesu xool ay taalibeem ne leen:«Yéen ñi sësul lu dul ci Yàlla, barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla, yéena ko yelloo.

6:21  Yéen ñi xiif léegi, barkeel ngeen,ndax dingeen regg.Yéen ñiy naqarlu léegi, barkeel ngeen,ndax dingeen ree.

6:22  Barkeel ngeen, bu leen nit ñi bañee, di leen dàq ak a saaga, di sib seen tur ngir Doomu nit ki.

6:23  Bu boobaa bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu la maami seeni bañ daan fitnaale yonent yi.

6:24  Waaye nag yéen boroom alal yi, torox ngeen,ndaxte jot ngeen ba noppi seen bànneex.

6:25  Yéen ñiy lekk ba suur léegi, torox ngeen,ndax ëllëg dingeen xiif.Yéen ñiy ree léegi, torox ngeen,ndax dingeen am aw naqar, ba jooy xàcc.

6:26  Torox ngeen bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndaxte noonu la seeni maam daan jëfe ak ña doon mbubboo yonent.

6:27  «Waaye maa ngi leen koy wax, yéen ñi may déglu, soppleen seeni bañaale tey defal lu baax ñi leen bañ.

6:28  Yéeneleen lu baax ñi leen di móolu, te ñaanal ñi leen di sonal.

6:29  Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul téye sa turki.

6:30  Képp ku la ñaan, may ko, te ku nangu say yëf, bu ko ko laaj.

6:31  Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko.

6:32  «Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban ngërëm ngeen ciy am? Ndaxte bàkkaarkat yi sax sopp nañu ñi leen sopp.

6:33  Te bu ngeen defalee lu baax ñi leen koy defal, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy def noonu.

6:34  Te bu ngeen dee leble te yaakaar ci ndelloo, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy lebal seeni moroom, ngir ñu delloo leen ko.

6:35  Waaye soppleen seeni noon, di leen defal lu baax, tey leble, bañ a yaakaar ñu delloo leen ko. Noonu seen yool dina mag te dingeen wone ne, yéenay doomi Aji Kawe ji, ndaxte Yàlla day wone mbaaxam ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi.

6:36  Nangeen am yërmande, ni seen Baay ame yërmande.

6:37  «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, te deesu leen àtte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen ñi ci des, te dinañu leen baal.

6:38  Mayeleen te dinañu leen may. Dinañu leen ëmbal natt bu baax bu ñu rokkas te yengal ko, mu fees bay tuuru. Ndaxte dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale.»

6:39  Noonu Yeesu wax na leen beneen léeb ne leen: «Ndax gumba man na wommat moroomam? Mbaa duñu daanu ñoom ñaar ci kàmb?

6:40  Taalibe gënul kilifaam, waaye taalibe bu jàng ba wàcc, dina yem ak kilifaam demin.

6:41  «Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw?

6:42  Nan nga man a waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkal a dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.

6:43  «Garab gu baax du meññ doom yu bon, te garab gu bon du meññ doom yu baax.

6:44  Ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee. Deesul witte figg ci dédd, walla réseñ ci xaaxaam.

6:45  Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, ndax loolu la denc ci xolam, te nit ku bon, lu bon lay wax, ndaxte denc na lu bon ci xolam. Ndaxte gémmiñ, la fees xolam lay wax.

6:46  «Lu tax ngeen may wooye “Boroom bi, Boroom bi,” te dungeen def li may wax?

6:47  Képp ku ñëw ci man, di dégg samay wax te di ko jëfe, ma won leen nu muy mel.

6:48  Dafa mel ni nit kuy tabax kër, mu gas fu xóot, jot doj wu réy, samp fa kër ga. Bi mbënn ma ñëwee, wal ma dafa dal ca kër ga te yenguwul, ndaxte nit ka dafa tabax kër ga tabax bu dëgër.

6:49  Waaye képp ku dégg samay wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku tabax këram ci suuf, bañ koo defal fondamaa. Bi wal ma dalee ca kër googa, dafa màbb ca saa sa, lépp yàqu yaxeet.»

7:1  Bi Yeesu waxee la mu naroon a wax lépp ca kanamu mbooloo ma, mu daldi dem Kapernawum.

7:2  Amoon na fa njiitu xare. Njiit la nag, surgaam bu mu bëggoon lool dafa feebaroon, bay bëgg a dee.

7:3  Bi mu déggee mbiri Yeesu, mu yónni ca moom ay Yawut, di magi dëkk ba, ngir ñaan ko, mu ñëw faj surga ba.

7:4  Bi magi dëkk ba agsee ca Yeesu, ñu sàkku ci moom ndimbal, ñaan ko: «Ki nu yónni ci yaw de, yelloo na ndimbal,

7:5  ndaxte sopp na sunu xeet te moo nu tabaxal sax sunu jàngu.»

7:6  Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom. Waaye bi ñuy bëgg a agsi ca kër ga, njiit la yebal ay xaritam ngir ñu wax Yeesu ne: «Sang bi, bul sonal sa bopp, ndaxte yeyoowuma nga dugg sama kër.

7:7  Looloo tax it ma xalaat ne, awma darajay gatandu la. Waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér.

7:8  Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»

7:9  Bi ko Yeesu déggee, mu waaru. Noonu mu walbatiku ca mbooloo, ma topp ci moom, ne leen: «Maa ngi leen koy wax, ci bànni Israyil sax, musuma cee gis ku gëme nii.»

7:10  Noonu ndaw ya daldi dellu ca kër ga. Bi ñu agsee, ñu gis ne surga ba wér na.

7:11  Yàggul dara Yeesu dem ci dëkk bu ñuy wax Nayin. Taalibeem yi ak mbooloo mu bare ànd ak moom.

7:12  Bi muy agsi ca buntu dëkk ba, fekk ñuy rob néew boo xam ne kenn rekk la woon ci ndeyam, ji jëkkëram faatu woon. Te mbooloo mu bare ca dëkk ba di gunge soxna sa.

7:13  Bi ko Boroom ba gisee, mu daldi koy yërëm ne ko: «Bul jooyati.»

7:14  Mu jegeñsi, laal jaat ga, ñi ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Waxambaane wi, jógal, ndigal la.»

7:15  Noonu nit ka dee woon jóg toog, tàmbalee wax. Yeesu delloo ko yaay ja.

7:16  Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!»

7:17  La ñu wax ci mbiri Yeesu daldi siiw ca réewu Yawut ya ak la ko wër yépp.

7:18  Taalibey Yaxya ya nettali mbir yooyu yépp seen kilifa. Noonu Yaxya woo ñaar ci ay taalibeem,

7:19  yónni leen ci Boroom bi, ngir laaj ko: «Ndax yaw yaa di Ki war a ñëw, walla danoo war a xaar keneen?»

7:20  Bi taalibe ya agsee ca Yeesu, ñu ne ko: «Yaxya moo nu yebal, nu laaj ndax yaa di Ki waroon a ñëw, walla danuy xaar keneen?»

7:21  Ca waxtu woowa Yeesu wéral nit ñu bare ci seeni feebar ak ci seeni metit, di dàq ay rab tey gisloo ay gumba.

7:22  Noonu mu tontu ndaw ya ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen gis te dégg ko. Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te ñi woyoflu ñu ngi dégg xebaar bu baax bi.

7:23  Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»

7:24  Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?

7:25  Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñiy soloo noonu, tey dund dund gu neex ñu ngi dëkk ci këri buur.

7:26  Kon lu ngeen seeti woon? Yonent? Waaw, wax naa leen ne, ëpp na yonent.

7:27  Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:“Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la,te xàllal la yoon ci sa kanam.”

7:28  Maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya musul a feeñ. Waaye ba tey ki gën a ndaw ci nguuru Yàlla moo ko sut.»

7:29  Nit ñépp ñi doon déglu Yeesu, ba ci juutikat yi sax, dëggal nañu ne Yàlla ku jub la, ndaxte nangu nañu Yaxya sóob leen ci ndox.

7:30  Waaye Farisen ya ak xutbakat ya dañoo bañ, mu sóob leen ci ndox, di wone noonu ne, gàntu nañu li leen Yàlla bëggaloon.

7:31  Yeesu tegaat ca ne: «Kon lan laa man a mengaleel niti jamono jii? Lan lañuy nirool?

7:32  Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma tey woowante naan:“Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen,woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.”

7:33  Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul mburu, naanul biiñ, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.”

7:34  Gannaaw gi nag Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.”

7:35  Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»

7:36  Amoon na ab Farisen bu ñaan Yeesu, mu ñëw lekkandoo ak moom. Yeesu dem kër waa ja, toog ca lekkukaay.

7:37  Fekk amoon na ca dëkk ba jigéen juy moy Yàlla. Bi mu yégee ne, Yeesoo ngay lekk ca kër Farisen ba, mu dem, yóbbaale njaq lu ñu defare doj wu ñuy wax albaatar te def latkoloñ.

7:38  Bi jigéen ja agsee, mu taxaw ca gannaaw tànki Yeesu, di jooy. Noonu ay rangooñam tooyal tànki Yeesu, jigéen ja di leen fomp ak kawaram, di leen fóon te ciy sotti latkoloñ ja.

7:39  Naka la Farisen, bi woo woon Yeesu ci këram, gis loolu, mu wax ci xelam naan: «Bu nit kii doonoon yonent, kon dina xam kuy jigéen ji koy laal ak ni mu nekke bàkkaarkat.»

7:40  Yeesu ne ca tonn, daldi ne Farisen ba: «Simoŋ, am na lu ma la war a wax.» Simoŋ ne ko: «Waxal, kilifa gi.»

7:41  Yeesu ne ko: «Da fee amoon ñaari nit ñu ameel bor benn leblekat. Kenn kaa ngi ko ameel téeméeri junni ci xaalis, ki ci des fukki junni.

7:42  Waaye kenn ci ñoom mënu koo fey. Noonu mu baal leen bor ya. Ci ñaar ñooñu nag kan moo ko ciy gën a bëgg?»

7:43  Simoŋ tontu ne ko: «Xanaa ki ñu baal bor bi gën a bare.» Yeesu ne ko: «Àtte nga dëgg,»

7:44  daldi walbatiku ca jigéen ja, ne Simoŋ: «Ndax gis nga jigéen jii? Dugg naa sa kër, te joxewuloo ndox, ngir raxas samay tànk. Waaye moom, raxas na samay tànk ak ay rangooñam, ba noppi fomp leen ak kawaram.

7:45  Bi ma agsee, fóonuloo ma, waaye moom, bi ma duggee ba léegi tàyyiwul ci di fóon samay tànk.

7:46  Defuloo diw ci sama bopp, waaye moom, sotti na latkoloñ ci samay tànk.

7:47  Moo tax ma di la wax ne, su wonee mbëggeel gu réye nii, dafa fekk ñu baal ko bàkkaaram yu bare. Waaye ki mbëggeelam néew dafa fekk ñu baal ko lu tuuti.»

7:48  Yeesu daldi ne jigéen ja: «Baal nañu la say bàkkaar.»

7:49  Noonu ñi doon lekkandoo ak moom di wax ci seen xel naan: «Kii am sañ-sañu baale bàkkaar mooy kan?»

7:50  Waaye Yeesu ne jigéen ja: «Sa ngëm musal na la. Demal ci jàmm.»

8:1  Gannaaw loolu Yeesu di dem ca ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di waaraate ak di yégle xebaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla. Fukki taalibe ya ak ñaar ànd ak moom,

8:2  ak ay jigéen yu mu teqale woon ak rab te jële leen ci seeni wopp, ñu di: Maryaama, mi ñuy wooye Maryaamam Magdala, mi Yeesu tàggale woon ak juróom-ñaari rab;

8:3  Sànn, jabaru ku ñuy wax Kusa, mi doon wottu alalu Erodd; ak Susànn ak ñeneen jigéen. Jigéen ñooñu ñoo doon joxe seen alal, ngir dimbali Yeesu ak ay taalibeem.

8:4  Dëkk ak dëkk nit ña di fa jóge jëm ca Yeesu, ba mbooloo mu bare dajaloo, mu wax leen léeb wii:

8:5  «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi. Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, nit ñi joggi ci, picci asamaan lekk ko lépp.

8:6  Leneen wadd ci bérab bu bare ay doj. Naka la sax rekk, daldi wow, ndaxte suuf si tooyul woon.

8:7  Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, ñu saxandoo, xaaxaam ya tanc ko.

8:8  Li ci des dal ci suuf su baax, sax, nangu ba meññ téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon.» Gannaaw loolu Yeesu wax ak kàddu gu dëgër ne: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»

8:9  Taalibey Yeesu yi laaj ko lu léeb woowu di tekki.

8:10  Mu tontu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci des, dama leen di wax ci ay léeb. Noonu la, ngir:“Ñuy xool te duñu man a gis,di dégg te duñu man a xam.”

8:11  «Lii la léebu beykat bi di tekki. Kàddug Yàlla mooy jiwu wi.

8:12  Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg. Gannaaw gi, Seytaane dafay ñëw, këf kàddu, gi ñu def ci xolam, ngir mu bañ a gëm te Yàlla musal ko.

8:13  Ki nekk ci bérab bu bare ay doj, mooy ki dégg kàddu gi, ba noppi nangu ko ak mbég. Waaye wax ji saxul ci moom. Dina gëm ab diir, waaye bu nattu yi agsee, mu daldi dàggeeku.

8:14  Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, waaye nes tuuti soxla yi ak alal ak bànneexi àddina tanc ko, ba du àgg cig mat.

8:15  Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg kàddu gi te denc ko ci xol bu baax bu gore, te muñ ba jur njariñ.

8:16  «Kenn du taal làmp, dëpp ci leget, walla mu di ko def ci ron lal. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.

8:17  Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, walla lu làqu lu ñu dul feeñal, ba mu ne fàŋŋ.

8:18  Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo kàddu gi. Ku am, dees na la dollil, waaye ku amul, dees na nangu sax li nga xalaatoon ne, am nga ko ba noppi.»

8:19  Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw seetsi ko, waaye mënuñu woon a agsi ci moom, ndaxte nit ña dañoo bare.

8:20  Am ku ko yégal ne: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg laa gis.»

8:21  Waaye mu daldi leen ne: «Sama yaay ak samay rakk, ñooy ñiy déglu kàddug Yàlla, te di ko topp.»

8:22  Benn bés Yeesu àndoon na ak ay taalibeem, dugg ci gaal. Mu ne leen: «Nanu jàll dex gi.» Noonu ñu dem.

8:23  Bi ñuy dem nag, Yeesu daldi nelaw. Ngelaw lu am doole daldi ñëw, yengal dex gi, gaal gi fees ak ndox, ba ñu bëgg a suux.

8:24  Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!» Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.

8:25  Yeesu ne taalibe yi: «Ana seen ngëm?» Ñu daldi tiit te waaru, naan ci seen biir: «Kii moo di kan? Mi ngi jox ndigal ngelaw li ak ndox mi, ñu koy déggal.»

8:26  Noonu ñu teer ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile.

8:27  Bi Yeesu di wàcc ca gaal ga, ku rab jàpp ca waa dëkk ba ñëw, kar ko. Yàgg na def yaramu neen te dëkkul ca kër, waaye ca sëg ya lay nekk.

8:28  Bi mu gisee Yeesu, mu yuuxu, daanu ciy tànkam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Maa ngi lay ñaan, nga bañ maa mbugal.»

8:29  Dafa wax loolu, ndaxte Yeesu santoon na rab wi, mu génn ci moom. Rab wa dafa ko doon faral a jàpp. Nit ñi daan nañu ko wottu, di ko yeew ak ay càllala, ak di ko jéng, mu di leen dagg, rab wi di ko xiir ca bérab yu wéet.

8:30  Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu tontu ne: «Coggal laa tudd.» Dafa wax loolu, ndaxte rab yu baree ko jàppoon.

8:31  Rab yooyoo ngi ko doon ñaan, ngir mu bañ leen a sant, ñu dem ca kàmb gu xóot gi.

8:32  Fekk amoon na fa géttu mbaam-xuux yu bare, yuy for ca tund wa. Rab ya ñaan Yeesu, mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.

8:33  Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab.

8:34  Sàmm ya gis li xew, daw nettaliji mbir mi ca dëkk ba ak ca àll ba.

8:35  Nit ñi génn, ngir seet li xew. Bi ñu agsee ca Yeesu, ñu fekk fa nit, ka rab ya bàyyi woon, toog ca kanam Yeesu, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.

8:36  Ña fekke woon mbir ma nag, nettali leen naka la Yeesu wérale ki rab ya jàppoon.

8:37  Ci kaw loolu waa diiwaanu Serasa bépp ragal, ba ñaan Yeesu mu jóge fa. Noonu Yeesu dugg ci gaal gi, di bëgg a dem.

8:38  Nit ki Yeesu tàggale woon ak rab ya ñaan ko, ngir ànd ak moom. Waaye Yeesu woññi ko ne ko:

8:39  «Ñibbil, nettali li la Yàlla defal lépp.» Noonu waa ji dem di wër dëkk ba yépp, di fa yégle la ko Yeesu defal.

8:40  Bi Yeesu dëppee dellu, mbooloo ma di ko teeru, ndaxte ñépp a ngi ko doon xaar.

8:41  Noonu nit ñëw, tuddoon Yayrus te nekk njiitu jàngu ba. Bi mu agsee, mu daanu ci tànki Yeesu, saraxu ko mu ñëw këram,

8:42  ndaxte jenn doomam ju jigéen, ji mu amoon kepp te muy tollu ci fukki at ak ñaar, ma nga doon waaj a dee. Bi Yeesuy dem, nit ñaa ngi doon buuxante, di ko tanc.

8:43  Amoon na nag ca mbooloo ma jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar, te kenn mënu ko woon a faj.

8:44  Jigéen ja jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. Ca saa sa deret ji dal.

8:45  Yeesu laaj nit ña ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Noonu Piyeer ne ko: «Kilifa gi, nit ñépp a ngi lay wër, di la tanc wet gu nekk.»

8:46  Waaye Yeesu ne: «Am na ku ma laal, ndaxte yég naa ne, am na doole ju génn ci man.»

8:47  Te jigéen ja xam ne, mënul woon a nëbb li mu def. Mu daldi daanu ci tànki Yeesu, di lox. Noonu mu nettali ci kanamu ñépp li taxoon mu laal Yeesu, ak ni mu wére ca saa sa.

8:48  Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la. Demal ci jàmm.»

8:49  Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul ngay sonal kilifa gi.»

8:50  Yeesu dégg kàddu yooyu, daldi ne njiit la: «Bul tiit. Gëmal rekk te dina dundaat.»

8:51  Bi Yeesu agsee ca kër ga, nanguwul kenn duggaaleek moom, ñu dul Piyeer, Yowaana, Saag ak waajuri xale ba.

8:52  Ña fa nekk ñépp di yuuxu ak di jooy xale bi. Noonu Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen jooy yi. Janq bi deewul, day nelaw rekk.»

8:53  Waaye ñu di ko ñaawal, ndaxte xamoon nañu ne, dee na.

8:54  Waaye Yeesu jàpp loxob janq ba, woo ko ne ko: «Xale bi, jógal.»

8:55  Noonu ruuwu xale ba dellusiwaat, mu daldi jóg ca saa sa. Yeesu santaane ñu may ko, mu lekk.

8:56  Waajuri xale bi daldi waaru. Waaye Yeesu tere leen, ñu wax kenn li xew.

9:1  Benn bés Yeesu dajale fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen doole ak sañ-sañu dàq rab yépp ak di faj jàngoro yi.

9:2  Noonu mu yónni leen ñuy yégle nguuru Yàlla ak di faj jarag yi.

9:3  Mu ne leen: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara, du yet mbaa mbuus mbaa mburu mbaa xaalis. Buleen yor it ñaari turki.

9:4  Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen di fa jóge.

9:5  Fépp fu leen nit ñi gàntoo, génnleen ca dëkk booba te ngeen yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.»

9:6  Noonu ñu dem dëkk ak dëkk, di fa yégle xebaar bu baax bi, tey wéral jarag yi.

9:7  Bi Erodd boroom diiwaanu Galile déggee li Yeesu ak ay taalibeem doon def lépp, mu jaaxle, ndaxte amoon na, ñu doon wax ci mbiri Yeesu naan: «Yaxya moo dekki.»

9:8  Am it ñuy wax naan: Iliyas moo dellusi. Ñeneen naan: «Kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»

9:9  Waaye Erodd ne: «Yaxya, man mii maa dagglu boppam. Kon kii ma dégg ay jalooreem, mooy kan?» Noonu mu koy fexee gis.

9:10  Bi ndaw ya dellusee, ñu nettali Yeesu la ñu defoon lépp. Noonu mu yóbbaale leen, ñu sore nit ñi, jëm ca dëkk bu ñuy wax Betsayda.

9:11  Bi ko nit ña yégee, ñu toppi ko. Yeesu teeru leen, di leen wax ci mbirum nguuru Yàlla, te di wéral ñi ko aajowoo.

9:12  Ca ngoon sa fukki taalibe ya ak ñaar ñëw ci Yeesu ne ko: «Yiwil mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yi ak àll bi ko wër, ngir am lu ñu lekk ak fu ñu fanaan, ndaxte fii àllub neen la.»

9:13  Waaye Yeesu ne leen: «Joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu tontu ko ne: «Amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa ndax nu dem jëndal mbooloo mii lu ñu lekk?»

9:14  Ndaxte lu war a mat juróomi junniy góor a nga fa teewoon. Yeesu ne taalibe ya: «Neeleen mbooloo mi ñu toog def ay géewi juróom-fukki nit.»

9:15  Taalibe ya def ko, toogloo nit ña.

9:16  Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, gërëm Yàlla, ba noppi mu damm leen, jox taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi.

9:17  Noonu ñépp lekk ba suur. Bi ñu dajalee desit ya, ñu feesal fukki pañe ak ñaar.

9:18  Benn bés Yeesu beddeeku mbooloo ma, di ñaan; taalibe yi nekk ci wetam. Mu laaj leen ne: «Nit ñi, ku ñu wax ne moom laa?»

9:19  Ñu tontu ko ne: «Am na ñu naan, yaa di Yaxya; ñeneen ne, Iliyas; ñi ci des ne, yaay kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»

9:20  Yeesu ne leen: «Yéen nag ku ngeen ne moom laa?» Piyeer tontu ko ne: «Yaa di Almasi, bi Yàlla yónni.»

9:21  Noonu Yeesu daldi leen dénk, tere leen ñu wax ko kenn,

9:22  teg ca ne: «Doomu nit ki war na sonn lu bare; saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba.»

9:23  Noonu Yeesu ne leen ñoom ñépp: «Ku bëgg a aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, gàddu bés bu nekk bant, bi ñu ko war a daaj, door a topp ci man.

9:24  Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, dinga ko jotaat.

9:25  Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, su fekkee ne dafay ñàkk bakkanam walla mu loru?

9:26  Ku ma rus a faral, te nanguwul samay wax, Doomu nit ki dina la rus a xam, bés bu ñëwee ci ndamam ak ci ndamu Baay bi ak lu malaaka yu sell yi.

9:27  Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw ñoo xam ne duñu dee te gisuñu nguuru Yàlla gi.»

9:28  Bi ñu ca tegee luy tollook ayu-bés gannaaw bi Yeesu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer, Yowaana ak Saag, yéeg ca kaw tund wa ngir ñaan.

9:29  Bi muy ñaan, xar-kanamam daldi soppiku, ay yéreem weex tàll bay melax.

9:30  Am ñaari nit di waxtaan ak moom, muy yonenti Yàlla Musaa ak Iliyas.

9:31  Ñoo feeñ ci ndamu Yàlla, di waxtaane ci demu Yeesu, gi muy àggalee yenam ci Yerusalem.

9:32  Fekk Piyeer ak ñi mu àndal doon gëmmeentu, waaye bi ñu yeewoo bu baax, ñu gis ndamu Yeesu, ak ñaari nit ñu taxaw ci wetam.

9:33  Bi nit ñooñu di sore Yeesu, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.» Fekk xamul la mu doon wax.

9:34  Bi mu koy wax, niir ñëw muur leen, taalibe yi daldi tiit, bi leen niir wa ëmbee.

9:35  Noonu baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma fal; dégluleen ko.»

9:36  Bi baat ba waxee ba noppi, Yeesu rekk des fa. Taalibe ya noppi, bañ a nettali kenn ca jamono jooja la ñu gisoon.

9:37  Ca suba sa Yeesu ak taalibe ya wàcce ca tund wa, mbooloo mu bare ñëw, di ko gatandu.

9:38  Nit xaacu ci biir mbooloo mi naan: «Kilifa gi, maa ngi lay ñaan, nga seet sama doom, ndaxte moom kepp laa am.

9:39  Léeg-léeg rab jàpp ko, mu daldi yuuxu ca saa sa, rab wi di ko sayloo, gémmiñ gi di fuur. Du faral di génn ci moom te dina ko sonal.

9:40  Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye mënuñu ko.»

9:41  Yeesu tontu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa war a nekk ak yéen te di leen muñal? Indil ma sa doom.»

9:42  Bi xale biy agsi, rab wi di ko daaneel ci suuf, muy say. Waaye Yeesu daldi gëdd rab wa, wéral xale ba, daldi ko delloo baayam.

9:43  Ku nekk waaru na ndax màggug Yàlla. Bi ñuy yéemu ci li mu doon def, Yeesu ne taalibeem ya:

9:44  «Dégluleen bu baax lii ma leen di wax: dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi.»

9:45  Waaye taalibe ya xamuñu kàddu googu. Yàlla dafa leen nëbb li muy tekki, ba ñu bañ koo xam, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.

9:46  Werante am ci biir taalibe yi, ñuy laajante kan moo gën a màgg ci ñoom.

9:47  Yeesu mi xam seen xalaat, jël ab xale, teg ci wetam ne leen:

9:48  «Ku nangu xale bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni; ndaxte ki gën a woyof ci yéen ñépp, kooku moo gën a màgg.»

9:49  Bi loolu amee Yowaana jël kàddu gi ne: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndaxte bokkul ci nun.»

9:50  Waaye Yeesu tontu ko: «Buleen ko tere, ndaxte ku la sotul, far na ak yaw.»

9:51  Bi jamono ji jegeñsee, ji Yeesu waree jóge àddina dem asamaan, mu sigiñu ci dem Yerusalem.

9:52  Noonu mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem nag, dugg ci ab dëkk ci diiwaanu Samari, ngir wutal ko fa fu mu dal.

9:53  Waaye waa dëkk ba nanguwuñu ko, ndaxte mi ngi jublu woon Yerusalem.

9:54  Bi taalibe yi tudd Saag ak Yowaana gisee loolu, ñu ne: «Boroom bi, ndax dangaa bëgg nu ne, na safaras asamaan dal ci seen kaw, faagaagal leen?»

9:55  Waaye Yeesu walbatiku, yedd taalibe ya,

9:56  ba noppi ñu daldi dem wuti beneen dëkk.

9:57  Bi ñuy dem, am ci yoon wi ku ne Yeesu: «Dinaa la topp fépp foo jëm.»

9:58  Waaye Yeesu tontu ko ne: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»

9:59  Yeesu ne keneen: «Toppal ci man.» Waaye kooku ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkk a dem suuli sama baay.»

9:60  Mu tontu ko ne: «Bàyyil ñi dee, ñu suul seeni néew. Yaw demal, yégle nguuru Yàlla.»

9:61  Keneen ne ko: «Sang bi, dinaa la topp, waaye may ma, ma jëkk a tàgguji sama waa kër.»

9:62  Yeesu ne ko: «Kuy ji, di geestu, yeyoowul a liggéey ci nguuru Yàlla.»

10:1  Gannaaw loolu Boroom bi tànn na yeneen juróom-ñaar-fukki taalibe ak ñaar, yebal leen, ñu ànd ñaar ak ñaar, jiituji ko ca dëkk yépp ak ca bérab yépp, ya mu naroon a dem moom ci boppam.

10:2  Mu ne leen: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu. Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.

10:3  Demleen! Maa ngi leen di yónni, mel ni ay mbote ci biir ay bukki.

10:4  Buleen yor xaalis walla mbuus walla ay dàll. Buleen nuyu kenn ci yoon wi.

10:5  «Kër gu ngeen man a dugg, nangeen jëkk ne: “Na jàmm wàcc ci kër gi.”

10:6  Bu fa nitu jàmm nekkee, seen yéene dina ko indil jàmm. Lu ko moy, seen yéene dina dellusi ci yéen.

10:7  Dal-leen ca kër googa, tey lekk ak a naan lu ñu leen di jox, ndaxte liggéeykat yelloo na jot peyam. Buleen dem nag kër ak kër.

10:8  «Dëkk bu ngeen man a dugg, te waa dëkk ba teeru leen, lu ñu leen jox, lekkleen ko.

10:9  Nangeen wéral jaragi dëkk ba, te ngeen ne leen: “Nguuru Yàlla jegesi na leen.”

10:10  Waaye bu ngeen duggee ci dëkk te teeruwuñu leen, demleen ca mbedd ya te ne leen:

10:11  “Seen pëndu dëkk, bi taq ci sunuy tànk sax, noo ngi koy faxas, ngir seede leen seen réer. Waaye nag xamleen ne, nguuru Yàlla jegesi na.”

10:12  Maa ngi leen koy wax, bu bés baa, waa Sodom ñooy tane dëkk boobu.

10:13  «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon tuub nañu seeni bàkkaar bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.

10:14  Moona ca bés pénc ba, Tir ak Sidon ñoo leen di tane.

10:15  Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe.

10:16  «Ku leen déglu, déglu na ma; ku leen bañ, bañ na ma. Te ku ma bañ, bañ na ki ma yónni.»

10:17  Juróom-ñaar-fukki taalibe yi ak ñaar dellusi, fees ak mbég te naan: «Boroom bi, rab yi sax déggal nañu nu ndax sa tur.»

10:18  Yeesu ne leen: «Maa ngi doon séen Seytaane wàcce asamaan ni safaras melax.

10:19  Gis ngeen, jox naa leen sañ-sañu joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley bañaale bi, te dara du leen man a gaañ.

10:20  Moona li leen rab yi déggal, bumu tax ngeen bég, waaye bégleen ndax li ñu bind seen tur ci asamaan.»

10:21  Ca saa soosu Xel mu Sell mi feesal Yeesu ak mbég, mu daldi ne: «Yaw Baay bi, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gune yi. Waaw Baay bi, ndaxte looloo la neex.»

10:22  Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn mënul a xam, man Doom ji, maay kan, ku dul Baay bi; kenn mënul a xam it kan mooy Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgg a xamal.»

10:23  Gannaaw bi mu waxee loolu, Yeesu walbatiku ca taalibe ya ne leen ñoom rekk: «Ñi seeni bët di gis li ngeen di gis, am nañu mbég.

10:24  Ndaxte maa ngi leen koy wax, yonent yu bare ak buur yu bare bëggoon nañoo gis li ngeen di gis, waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg, waaye dégguñu ko.»

10:25  Noonu benn xutbakat daldi jóg, ngir fexee fiir Yeesu ne ko: «Kilifa gi, lan laa war a def, ba am dund gu dul jeex?»

10:26  Yeesu ne ko: «Lu ñu bind ci yoonu Musaa? Lan nga ciy jàng?»

10:27  Nit ka ne ko: « “Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa kàttan gépp ak sa xel mépp,” te it: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”»

10:28  Yeesu ne ko nag: «Li nga wax dëgg la. Boo defee loolu, dinga dund ba fàww.»

10:29  Waaye xutbakat ba bëggoon a am aw lay, ne Yeesu: «Kan mooy sama moroom nag?»

10:30  Yeesu tontu ko ne: «Dafa amoon nit ku jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Ay sàcc dogale ko, futti ko, dóor ko ba muy bëgg a dee, dem bàyyi ko fa.

10:31  Faf ab saraxalekat jaar ca yoon wa, séen nit ka, teggi.

10:32  Benn waay it bu soqikoo ci giiru Lewi, aw ca bérab booba, séen waa ja, teggi.

10:33  Waaye benn waay bu dëkk Samari bu doon tukki, ñëw ba jege waa ja, gis ko, yërëm ko.

10:34  Noonu mu ñëw, diw ko diwlin ak biiñ ngir faj gaañu-gaañu ya, bandaas ko. Gannaaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci fanaanukaay, di ko topptoo.

10:35  Bi bët setee, mu génne ñaari poseti xaalis, jox ko boroom kër ga ne ko: “Nanga topptoo nit kooku. Bés bu ma fi jaaraatee, dinaa la fey, man ci sama bopp, lépp loo ci dolli ci xaalis.”»

10:36  Yeesu teg ca ne: «Lu ciy sa xalaat? Kan ci ñett ñooñu moo jëfe ni kuy jëf jëme ci moroomam, ba ñu gisee nit, ka sàcc ya dogale woon?»

10:37  Xutbakat ba tontu ko ne: «Xanaa ki ko won yërmandeem.» Yeesu ne ko nag: «Demal tey def ni moom.»

10:38  Bi Yeesu ak ay taalibeem nekkee ci yoon wi, mu dugg ci benn dëkk, fekk fa jigéen ju tudd Màrt, ganale ko.

10:39  Màrt nag amoon rakk ju tudd Maryaama, ma nga toog ci tànki Boroom bi, di déglu ay kàddoom.

10:40  Fekk Màrt jàpp lool ca waañ wa. Noonu mu ñëw ci wetu Yeesu ne ko: «Boroom bi, doo ci wax dara, boo gisee sama rakk ji bàyyi ma ak liggéey bi yépp? Ne ko mu jàpple ma.»

10:41  Boroom bi tontu ko ne: «Màrt, Màrt, yu baree ngi fees sa xol, nga am ay téq-téq ndax loolu.

10:42  Moona de, lenn rekk a am solo. Maryaama dafa tànn cér bi gën, te kenn du ko nangu ci moom.»

11:1  Am bés Yeesu di ñaan ci benn bérab. Bi mu noppee, kenn ci taalibeem yi ne ko: «Boroom bi, jàngal nu, nan lanu war a ñaane, ni ko Yaxya jàngale ay taalibeem.»

11:2  Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee ñaan, nangeen ne:“Baay bi, na sa tur sell,na sa nguur ñëw.

11:3  May nu bés bu nekk li nu war a dunde.

11:4  Baal nu sunuy bàkkaar,ndaxte nun itam danuy baal ñépp ñi nu tooñ.Te bu nu teg ci yoonu nattu.”»

11:5  Yeesu teg ca ne leen: «Mi ngi mel ni, nga dem seeti sa xarit ci xaaju guddi ne ko: “Xarit, lebal ma ñetti mburu.

11:6  Dafa am sama xarit bu ma ganesi, te awma dara lu ma ko jox.”

11:7  «Waaye kooku nekk ci biir néegam, dina ko tontu: “Bu ma lakkal, tëj naa bunt bi ba noppi te tëdd, man ak sama njaboot; mënumaa jóg di la jox dara.”

11:8  Maa ngi leen koy wax, su jógul jox ko li muy laaj ndax li ñu xaritoo it, ndax la kee ñàkk jom dina tax mu jox ko lépp li mu soxla.

11:9  Moo tax ma ne, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.

11:10  Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la.

11:11  Bu la sa doom ñaanee jën, yaw miy baayam, ndax dinga ko bañ a jox jën, jox ko jaan?

11:12  Walla mu ñaan la nen, nga jox ko jiit?

11:13  Ndegam yéen ñi bon yéena man a jox seeni gune lu baax, astemaak Baay bi nekk ci kaw dina jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan!»

11:14  Am bés Yeesu dàq rab wu luu. Naka la rab wa génn, luu ba daldi wax, ba mbooloo may yéemu.

11:15  Waaye am ca mbooloo ma ay nit, ñu doon wax naan: «Ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.»

11:16  Am ñeneen ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam.

11:17  Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, kër gu xeex boppam gent.

11:18  Te it bu Seytaane xeexee boppam, naka la nguuram di man a yàgge? Damay wax loolu, ndaxte nee ngeen, damay dàq rab jaarale ko ci kàttanu Beelsebul.

11:19  Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte.

11:20  Waaye bu fekkee ne ci baaraamu Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.

11:21  «Su nit ku bare doole gànnaayoo, di wottu këram, alalam dina raw.

11:22  Waaye bu ku ko ëpp doole ñëwee, daan ko, dafay nangu gànnaay ya mu yaakaaroon, ba noppi séddale alal ja.

11:23  Ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.

11:24  «Boo xamee ne rab, wa jàppoon nit, génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis. Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”

11:25  Bu ñëwee nag, mu fekk këram, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk.

11:26  Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom-ñaari rab yu ko gën a soxor. Ñu dugg, sanc fa; ba tax mujug nit kooku mooy yées njàlbéenam.»

11:27  Bi Yeesu di wax loolu, jenn jigéen yékkati baatam ca biir mbooloo ma ne: «Céy jigéen ji la ëmb te nàmpal la moo barkeel!»

11:28  Waaye Yeesu tontu ko ne: «Neel kay, ki barkeel mooy kiy déglu kàddug Yàlla te di ko topp.»

11:29  Naka la mbooloo may gën a takku, Yeesu ne: «Niti jamono jii dañoo bon. Ñu ngi laaj firnde, waaye duñu jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.

11:30  Ndaxte ni Yunus nekke woon firnde ci waa dëkku Niniw, noonu la Doomu nit kiy nekke firnde ci niti jamono jii.

11:31  Keroog bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.

11:32  Te it ca bés pénc, waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen, ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fii.

11:33  «Kenn du taal làmp, ba noppi di ko duggal cig kàmb, walla di ci këpp leget. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.

11:34  Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer. Waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm.

11:35  Moytul ndax leer gi nekk ci yaw du lëndëm.

11:36  Kon bu sa yaram wépp nekkee ci leer te amul genn wet gu laal ci lëndëm, dina leer nàññ, mel ni leeraayu làmp ne ràyy ci sa kaw.»

11:37  Bi Yeesu waxee ba noppi, benn Farisen wax ko, mu ñëw lekke këram. Yeesu dugg ca kër ga, toog ca lekkukaay ba.

11:38  Farisen bi nag daldi jaaxle, bi mu gisee ne Yeesu raxasuwul, laata muy lekk.

11:39  Noonu Boroom bi ne ko: «Waaw yéen Farisen yi, yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dangeen a fees ak càcc ak mbon!

11:40  Yéena ñàkk xel! Xanaa du ki defar biti moo defar biir itam?

11:41  Saraxeleen li nekk ci biir te seen lépp dina sell.

11:42  Yéen Farisen yi dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak ru ak léjum bu nekk, waaye sàggane ngeen njubte ak mbëggeel ci Yàlla. Loolu ngeen war a def, waxuma nag ngeen sàggane la ca des.

11:43  Yéen Farisen yi, dingeen torox! Ndaxte ca jàngu ya, toogu ya féete kanam ngeen di taamu te bëgg ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ca pénc ma.

11:44  Dingeen torox, ndaxte dangeen a mel ni ay bàmmeel yu raaf, ba nit ñi di ci dox te teyuñu ko.»

11:45  Kenn ci xutbakat yi ne ca tonn ne: «Kilifa gi, boo waxee loolu, yaa ngi nuy xas, nun itam.»

11:46  Noonu Yeesu neeti leen: «Yéen itam xutbakat yi, dingeen torox! Ndaxte dangeen di sëf nit ñi say yu diis, waaye dungeen nangoo laal sëf bi sax ak seen cati baaraam.

11:47  Dingeen torox, ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent, yi seeni maam reyoon.

11:48  Dangeen di seede noonu ne, ànd ngeen ak li seen maam defoon, ndaxte ñoo rey yonent yi, yéen ngeen tabax xabru yi.

11:49  Looloo tax Yàlla mi xam lépp ne: “Dinaa leen yónnee ay yonent ak ay ndaw. Ñenn ñi dinañu leen fitnaal, rey leen.”

11:50  Kon nag Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax dereti yonent yi ñu tuur, ba àddina sosoo ak léegi,

11:51  la dale ca Abel ba ci Sakariya, moom mi ñu rey ci diggante saraxalukaay bi ak bérab bu sell bi. Waaw, maa ngi leen koy wax, Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax loolu.

11:52  Yéen xutbakat yi, dingeen torox, ndaxte yéena yóbbu caabiy xam-xam; dugguleen ci, te ku ci bëgg a dugg, ngeen tere ko ko.»

11:53  Bi Yeesu génnee bérab boobu, Farisen ya ak xutbakat ya ëmbal ko mer te di ko seetlu ci fànn gu nekk,

11:54  di ko yeeru, bëgg a këf waxam bu awul yoon.

12:1  Gannaaw loolu, naka la mbooloo ma dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, di tancante, Yeesu tàmbalee wax jëmale ca taalibeem ya ne leen: «Moytuleen lawiiru Farisen ya, li di naaféq.

12:2  Amul dara lu nëbbu lu ñu warul a biral, mbaa lu kumpa lu ñu warul a siiwal.

12:3  Looloo tax lu ngeen wax ci biir lëndëm, dees na ko dégg ci leer. Lu ngeen déey nit ci biir néeg, dees na ko yégle ci kaw taax yi.

12:4  «Maa ngi leen koy wax, samay xarit, buleen ragal ñu man a rey yaram, ba noppi dootuñu man a def dara.

12:5  Dinaa leen wax nag ki ngeen war a ragal: ragal-leen Ki nga xam ne bu reyee ba noppi, am sañ-sañu sànni ca safara. Waaw maa ngi leen koy wax, ragal-leen kooku.

12:6  Juróomi picci rammatu, ndax duñu ko jaay ci ñaari dërëm? Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom.

12:7  Seen kawari bopp sax waññees na leen. Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu rammatu.

12:8  «Te maa ngi leen koy wax, képp ku ma nangu ci kanamu nit ñi, Doomu nit ki dina la nangu ci kanamu malaakay Yàlla yi.

12:9  Waaye ku ma gàntu ci kanamu nit ñi, dinañu la gàntu ci kanamu malaakay Yàlla yi.

12:10  Ku sosal Doomu nit ki, dinañu la baal, waaye kuy sosal Xel mu Sell mi, duñu la ko baal.

12:11  «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanamu kilifa ya ak àttekat ya, buleen am xel ñaar ci li ngeen war a tontu ak nan ngeen war a tontoo, walla lu ngeen war a wax,

12:12  ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal ca waxtu woowa li ngeen war a wax.»

12:13  Am ca mbooloo ma ku ne Yeesu: «Kilifa gi, joxal ndigal sama mag, mu sédd ma ci sunu ndono.»

12:14  Yeesu tontu ko ne: «Sama waay, kan moo ma fal àttekat ci seen kaw, walla mu teg ma fi, ma di leen séddaleel seen alal?»

12:15  Noonu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen bëgge, ndaxte bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree-bare.»

12:16  Noonu mu dégtal leen wii léeb ne: «Dafa amoon waa ju bare alal, te ay toolam nangu lool,

12:17  muy werante ci xelam naan: “Nu ma war a def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ngóob mi.”

12:18  Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gën a réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am jépp.

12:19  Te dinaa kañ sama bopp ne: ’Yaw mii, am nga alal ju bare ju man a dem ay ati at; noppalal sa yaram, di lekk, di naan, tey bég.’ ”

12:20  Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?”

12:21  «Kiy dajale alal ngir boppam nag te amul dara ca kanam Yàlla, lu mel nii moo lay dal.»

12:22  Noonu Yeesu daldi ne taalibeem yi: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk. Buleen jaaxle it ngir seen yaram ci lu ngeen war a sol,

12:23  ndaxte bakkan moo gën lekk, te yaram a gën koddaay.

12:24  Seetleen baaxoñ yi: duñu ji, duñu góob, amuñu dencukaay, amuñu sàq, teewul Yàllaa ngi leen di dundal. Céy ni ngeen ëppe maana picc yi!

12:25  Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem, moo man a yokk ab waxtu ci àppam?

12:26  Su fekkee lu tuuti loolu rekk mënuleen koo def, kon lu tax ngeen di jaaxle ci li ci des?

12:27  «Seetleen ni tóor-tóori ñax mi di saxe. Duñu liggéey, duñu ëcc, waaye maa ngi leen di wax ne, Suleymaan sax ci ndamam, soluwul woon ni benn ci ñoom.

12:28  Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxu tool yi, miy sax tey te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gën a wodd?

12:29  Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan; te buleen ci jaaxle.

12:30  Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay xam na ne, soxla ngeen ko.

12:31  Waaye wutleen nguuram, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.

12:32  «Buleen ragal dara, yéen coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay, mu jagleel leen nguuram.

12:33  Jaayleen seen alal, saraxe ko, ngir sàkku ay mbuusi xaalis yu dul bënn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa sàcc du ko jege te max du ko yàq.

12:34  Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.

12:35  «Takkuleen bu dëgër te bàyyi làmp yi tàkk.

12:36  Mel-leen ni ay surga yuy xaar seen njaatige buy jóge ca céet ga, ndax bu fëggee bunt ba, ñu ubbil ko ca saa sa.

12:37  Surga yooyee seen njaatige fekkul ñuy nelaw, ba mu agsee, ñoo gën a yeyoo ngërëm. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina sol yérey waañ, wax leen ñu toog lekk, ba noppi indil leen ñam wi.

12:38  Su fekkee seen njaatige ci xaaju guddi lay ñëw sax, walla bu suuf seddee, te fekk leen noonu, surga yooyu ñoo gën a yeyoo ngërëm.

12:39  Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw, du ko bàyyi, mu toj këram.

12:40  Yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»

12:41  Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, ndax dangay dégtal léeb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo mépp?»

12:42  Boroom bi tontu ko ne: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ci jamono ji?

12:43  Bu njaatigeem ñëwee te gis mu def noonu, surga boobu dina am ngërëm.

12:44  Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp.

12:45  Waaye su fekkee surga ba da ne ci xelam: “Sama njaatige day yéex a ñëw,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya ca des ak mbindaan ya, di lekk te di naan, di màndi,

12:46  kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul. Dina ko dóor ay dóor yu metti, jox ko añub ñi gëmul Yàlla.

12:47  «Surga bi xam bëgg-bëggu njaatigeem, te waajul mbaa mu takku def ko, dinañu ko dóor dóor yu metti.

12:48  Waaye surga bi xamul bëgg-bëggu njaatigeem, te def lu yelloo ay dóor, dinañu ko dóor dóor yu néew. Ku ñu jox lu bare dees na la feyiku lu bare. Ku ñu dénk lu bare, dees na la laajaat lu ko ëpp.

12:49  «Damaa ñëw ngir indi safara si ci àddina, te bëgg naa xaat taal bi tàkk.

12:50  Fàww ñu sóob ma ci metit, te ba looluy mat, duma noppalu.

12:51  Ndax dangeen a xalaat ne, damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina? Déedéet. Maa ngi leen koy wax, damaa ñëw ngir indi féewaloo.

12:52  Gannaawsi tey, bu juróomi nit bokkee genn kër, dinañu féewaloo. Ñett dinañu féewaloo ak ñaar ñi ci des, ñaar ñi féewaloo ak ñett ñooñu.

12:53  Baay bi dina féewaloo ak doom ji, doom ji ak baayam. Ndey dina féewaloo ak doomam ju jigéen; doom ju jigéen ji ak ndeyam. Goro dina féewaloo ak jabaru doomam; jabaru nit ak goroom.»

12:54  Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiin ci sowu, dangeen naan ca saa sa: “Dina taw,” te mooy am.

12:55  Te bu ngeen yégee ngelaw liy uppe sudd, ngeen ne: “Dina tàng tàngaay wu metti,” te mooy am.

12:56  Naaféq yi ngeen doon! Man ngeen a ràññee melow asamaan ak suuf, waaye lu tax mënuleen a ràññee li jamonoy léegi ji di tekki?

12:57  «Lu tax it dungeen àtteel seen bopp liy jëf ju jub?

12:58  Bu la nit jiiñee dara, ba ngeen ànd di dem ca àttekat ba, nanga fexee juboo ak moom ci yoon wi. Lu ko moy, dina la yóbbu ci yoon, yoon jébbal la ca loxoy alkaati ba, mu tëj la.

12:59  Maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo fiftin bi ci mujj.»

13:1  Ca jamono jooju ay nit ñëw ca Yeesu, nettali mbirum waa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi ñu rendi woon, jébbal leen Yàlla.

13:2  Mu tontu leen ne: «Mbaa du dangeen a xalaat ne, waa Galile yooyu dañoo gën a nekk bàkkaarkat ña ca des, ndax coono bi ñu daj?

13:3  Maa ngi leen di wax ne, du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.

13:4  Te fukki nit ak juróom-ñett ñooñu dee, bi taaxum kaw ma ca goxu Silowe daanoo ci seen kaw, ndax dangeen a yaakaar ne, ñoo gën a nekk ay tooñkat ñeneen ñi dëkk Yerusalem yépp?

13:5  Maa ngi leen di wax ne, du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.»

13:6  Noonu mu daldi leen wax léeb wii: «Nit amoon na ci toolam garab gu ñu naan figg. Benn bés mu ñëw di ko raas-si, fekku fa benn doom.

13:7  Noonu mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may ñëw di raas-si garab gii te duma ci fekk dara. Gor ko. Lu tax muy xatal tool bi?”

13:8  Surga ba tontu ko ne: “Sang bi, bàyyiwaat ko fi at mii. Dinaa wàqi taat wi, def ci tos.

13:9  Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”»

13:10  Benn bésu noflaay Yeesoo ngi doon jàngale ci ab jàngu.

13:11  Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu war a mat fukki at ak juróom-ñett; dafa xuuge woon te mënul woon a siggi dara.

13:12  Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.»

13:13  Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di màggal Yàlla.

13:14  Waaye njiitu jàngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca bésu noflaay ba, mu ne mbooloo ma: «Am na juróom-benni fan yu nit ñi war a liggéey. Kon war ngeen a ñëw faju ci bés yooyu, waaye du ci bésu noflaay bi.»

13:15  Boroom bi tontu ko: «Naaféq yi! Ndax bésu noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko?

13:16  Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom-ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésu noflaay bi?»

13:17  Naka la wax loolu, noonam yépp daldi rus, waaye mbooloo mi di bég ci jëf yu yéeme, yi mu doon def yépp.

13:18  Noonu Yeesu neeti: «Lan la nguuru Yàlla di nirool? Lan laa ko man a mengaleel?

13:19  Mi ngi mel ni doomu fuddën gu nit jël, ji ko ci toolam. Mu sax, nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»

13:20  Mu neeti: «Lan laa man a mengaleek nguuru Yàlla?

13:21  Mi ngi mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»

13:22  Yeesoo ngi doon jaar ci ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di jàngale te jublu Yerusalem.

13:23  Am ku ko ne: «Boroom bi, ndax ñiy mucc ñu néew lay doon?» Yeesu ne leen:

13:24  «Defleen seen kem-kàttan, ngir dugg ci bunt bu xat bi, ndaxte maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu jéem a dugg, waaye duñu ko man.

13:25  Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Dina leen tontu ne: “Xawma fu ngeen bokk.”

13:26  Bu ko defee dingeen tàmbalee naan: “Noo doon bokk di lekk ak di naan, te jàngale nga ci sunuy pénc.”

13:27  Waaye dina ne: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!”

13:28  Foofa dingeen jooy, di yéyu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla, te ñu dàq leen ca biti.

13:29  Ay nit dinañu jóge penku ak sowu, nor ak sudd, ñëw, bokk lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram.

13:30  Noonu ñenn ci ñi mujj ñooy jiituji; te ci ñi jiitu, ñooy mujji.»

13:31  Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wut a rey.»

13:32  Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.”

13:33  Waaye fàww ma dox sama itte tey, suba ak gannaaw suba, ndaxte wareesul a reye ab yonent feneen fu dul Yerusalem.

13:34  «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoon a dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen!

13:35  Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër. Te maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»

14:1  Benn bésu noflaay Yeesu dem ci këru benn kilifag Farisen yi, ngir lekke fa. Nit ñaa ngi ko doon xool bu baax.

14:2  Faf am ca kanamam nit ku feebaroon, ay tànkam newi.

14:3  Yeesu yékkati baatam, ne xutbakat ya ak Farisen ya: «Ndax jaadu na, nu faj ci bésu noflaay bi?»

14:4  Waaye ñépp ne cell. Yeesu daldi laal jarag ja, faj ko, ba noppi ne ko mu ñibbi.

14:5  Gannaaw loolu mu ne leen: «Ku sa doom walla sa yëkk daanu ci teen, ndax doo dem génneji ko ca saa sa, fekk sax bésub noflaay la?»

14:6  Amuñu woon dara lu ñu ciy teg.

14:7  Yeesu gis ni gan yi doon tànne toogu yu yiw yi, mu daldi leen wax léeb wii:

14:8  «Bu ñu la wooyee ci xewu céet, bul jël toogu bu yiw. Man na am woo nañu it nit ku la ëpp daraja.

14:9  Kon ki leen woo yéen ñaar ñépp man na ñëw ci yaw ne la: “Joxal toogu bi nit kii.” Noonu dinga rus a dem ca toogu bu gannaawe ba.

14:10  Waaye bu ñu la wooyee, demal ca toogu bu gannaawe ba. Bu ko defee ki la woo, bu agsee ne la: “Sama xarit, àggal ca kaw.” Loolu dina la sagal ci ñi nga toogandool ci lekkukaay bi.

14:11  Ndaxte képp kuy yékkatiku, dees na la suufeel, te kuy suufeelu, dinañu la yékkati.»

14:12  Noonu Yeesu ne ki ko woo woon lekk: «Boo dee woote añ walla reer, bul woo rekk say xarit, say doomi ndey, say bokk, walla say dëkkandoo yu am alal. Lu ko moy ñooñu itam dinañu la woo, fey la bor bi.

14:13  Waaye boo dee woote lekk, wool néew doole yi, làggi yi, lafañ yi ak gumba yi.

14:14  Soo ko defee, dinga barkeel, ndaxte duñu la ko man a fey, waaye dinga jot sag pey, bés bi ñi jub di dekki.»

14:15  Bi mu déggee wax yooyu, kenn ca gan ya ne Yeesu: «Kiy lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram, barkeel nga!»

14:16  Yeesu tontu ko ne: «Dafa amoon nit ku togglu ay ñam, woo ay nit ñu bare.

14:17  Bi waxtuw lekk jotee mu yónni surga ca ña muy ganale, fàttali leen: “Man ngeen a ñëw, ndaxte lépp sotti na léegi.”

14:18  «Waaye ñu tàmbali di jéggalu ci ngan gi ñoom ñépp. Ku jëkk ka ne ko: “Damaa jënd tool léegi, te fàww ma dem seeti ko. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.”

14:19  Keneen ne: “Damaa jënd léegi fukki yëkk, te damay dem nii, jéem leen a beyloo ba xam. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.”

14:20  Keneen ne ko: “Damay sog a takk jabar, looloo tax duma man a ñëw.”

14:21  «Surga ba dellu ca njaatigeem nettali ko loolu lépp. Noonu boroom kër ga mer, daldi ne surga ba: “Demal gaaw ca pénc ya ak ca mbedd ya ca dëkk ba, te indil ma fii néew doole yi, ñu làggi ñi, gumba yi ak lafañ yi.”

14:22  «Surga ba ñëwaat ne ko: “Sang bi, def naa li nga ma sant, waaye bérab bi feesul.”

14:23  Noonu njaatige ba ne ko: “Génnal dëkk bi te dem ca yoon ya ak ca tool ya, xiir nit ñi, ñu duggsi, ngir sama kër fees.

14:24  Maa ngi leen koy wax, ci ñi ma woo woon ci sama reer bi, kenn du ci ñam.”»

14:25  Am mbooloo yu réy yu toppoon ci Yeesu, ba muy dem ca yoon wa. Mu geestu ne leen:

14:26  «Képp ku ñëw ci man te gënalu ma ko baayam, yaayam, jabaram, ay doomam, ay magam ak ay rakkam, walla sax bakkanam, du man a nekk sama taalibe.

14:27  Képp koo xam ne nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, doo man a nekk sama taalibe.

14:28  Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkk a toog, xalaat ñaata la ko war a dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu man a àggale liggéey bi?

14:29  Lu ko moy, su yékkatee fondamaa bi te mënu koo àggale, ñi koy gis dinañu ko ñaawal, naan ko:

14:30  “Waa jii dafa tàmbalee tabax, waaye mënu koo àggale.”

14:31  Walla boog ban buur mooy dugg ci xare ak beneen buur te jëkkul a toog, seet ba xam moom ak fukki junniy xarekat man na xeex ak kiy ñëw ak ñaar-fukki junniy xarekat?

14:32  Su ko mënul, dafay yónni ndaw ca beneen buur ba, fi ak ma ngay sore, ngir ñu juboo.

14:33  Naka noonu itam ku nekk ci yéen, bu dëdduwul li mu am lépp, du man a nekk sama taalibe.

14:34  «Xam ngeen nag ne, xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam?

14:35  Du jariñ suuf, te du nekk tos. Dañu koy sànni ca biti. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»

15:1  Ay juutikat ak ay boroom bàkkaar daan jegesi Yeesu ngir déglu ko.

15:2  Farisen ya ak xutbakat ya di ñurumtu naan: «Waa jii mi ngi nangoo nekk ak ay boroom bàkkaar ak a lekkandook ñoom!»

15:3  Noonu Yeesu daldi leen wax léeb wii ne leen:

15:4  «Kan ci yéen soo amoon téeméeri xar, te benn réer ci, nooy def? Ndax doo bàyyi ca parlukaay ba juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent, toppi ma réer, ba gis ko?

15:5  Te boo ko gisee, dinga ko gàddu ak bànneex, yóbbu ko kër ga.

15:6  Boo àggee ca kër ga, dinga woo say xarit ak say dëkkandoo ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama xar ma réeroon.”

15:7  «Maa ngi leen di wax lii: ci noonule, dina am mbég ci asamaan, bu benn bàkkaarkat tuubee ay bàkkaaram. Te mbég moomu mooy ëpp mbég, mi fay am, ngir juróom-ñeent-fukk ak juróom-ñeent ñu jub, te soxlawuñoo tuub seeni bàkkaar.

15:8  «Te it bu jigéen dencoon fukki libidoor, benn réer ca, nu muy def? Ndax du taal ab làmp, bale kër ga, seet fu nekk, ba gis ko?

15:9  Bu ko gisee, dina woo ay xaritam ak ay dëkkandoom ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama alal ja réeroon.”

15:10  Maa ngi leen di wax lii: ci noonule la malaakay Yàlla yi di ame mbég ci benn bàkkaarkat bu tuubee ay bàkkaaram.»

15:11  Yeesu dellu ne leen: «Dafa amoon góor gu am ñaari doom.

15:12  Benn bés caat ma ne baay ba: “Baay, damaa bëggoon, nga jox ma li may war a féetewoo ci ndono li.” Noonu baay ba daldi leen séddale alalam.

15:13  Ay fan yu néew gannaaw gi, caat ma fab yëfam yépp, dem ca réew mu sore, yàq fa alalam ci topp nafsoom.

15:14  Bi mu sànkee alalam jépp, xiif bu metti dal ca réew ma, mu tàmbalee ñàkk.

15:15  Mu dem nag, di liggéeyal ku dëkk ca réew ma, kooku yebal ko ca ay toolam ngir mu sàmm mbaam-xuux ya.

15:16  Mu xiif ba bëgg a lekk ca ñamu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara.

15:17  Mujj xelam dellusi, mu ne: “Sama baay am na ay surga yu bare, te dañuy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di bëgg a dee ak xiif!

15:18  Damay jóg, dem ca sama baay ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la;

15:19  yeyootumaa nekk sa doom; boole ma ci say surga.’ ”

15:20  «Mu daldi jóg, jëm kër baayam. Waaye bi muy soreendi kër ga, baayam séen ko, yërëm ko, daldi daw laxasu ko, fóon ko.

15:21  Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.”

15:22  Waaye baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb, mi gën a rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay dàll.

15:23  Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu;

15:24  ndaxte sama doom jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.” Noonu ñu tàmbalee bànneexu.

15:25  «Fekk booba taaw baa nga woon ca tool ya. Bi mu ñëwee, ba jub kër ga, mu dégg ñuy tëgg, di fecc.

15:26  Mu daldi woo kenn ca surga ya nag, laaj ko lu xew.

15:27  Mu tontu ko: “Sa rakk moo dellusi, te sa baay rey na sëllu wu duuf wa, ndaxte ñibbisi na ci jàmm.”

15:28  «Ci kaw loolu taaw ba daldi mer, bañ a dugg ca kër ga. Baayam daldi génn, ngir ñaan ko mu dugg.

15:29  Waaye taaw ba tontu baayam ne ko: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, mel ni jaam, te musumaa moy sa ndigal, waaye yaw, musuloo ma may sax tef, ngir ma bànneexu, man ak samay xarit.

15:30  Waaye bi sa doom jii dikkee, moom mi yàq sa alal ci ndoxaan, reyal nga ko sëllu wu duuf wi.”

15:31  Noonu baay bi tontu ko ne ko: “Sama doom, yaa ngi ak man bés bu nekk, te li ma am lépp, yaa ko moom.

15:32  Waaye war nanoo bànneexu te bég, ndaxte sa rakk jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.”»

16:1  Yeesu neeti ay taalibeem: «Benn boroom alal moo amoon bëkk-néeg bu ñu jiiñ ne, dafay pasar-pasaree alal ji.

16:2  Waa ja woo ko ne ko: “Li may dégg ci yaw mooy lan? Leeralal ma ni nga liggéeye ak sama alal, ndaxte dootoo nekkati sama bëkk-néeg.”

16:3  «Bëkk-néeg bi di xalaat naan: “Nu may def nag, segam sama njaatige dafa may dàq ci liggéey bi mu ma joxoon? Dem beyi? Awma kàttanam. Yelwaani? Rus naa ko.

16:4  Xam naa ni may def, ba su ma ñàkkee sama liggéey, ay nit fat ma.”

16:5  Noonu mu daldi woolu kenn ku nekk ca ña ameeloon njaatigeem bor. Ka jëkk a ñëw, mu ne ko: “Ñaata nga ameel sama njaatige?”

16:6  Mu ne ko: “Téeméeri bidoŋi diwlinu oliw.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Toogal fii gaaw te bind juróom-fukk.”

16:7  Mu neeti keneen: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Bindal juróom-ñett-fukk.”

16:8  Njaatige ba nag daldi naw ni bëkk-néeg bu njublaŋ boobu muuse woon. Ndaxte ñi bokk ci àddina ñoo gën a muus ci li ñu jote ci seen diggante ak seen moroom, ba raw ñi bokk ci leeru Yàlla.»

16:9  Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen di wax lii: sàkkuleen ay xarit jaare ko ci alalu àddina, ngir bu alal nekkatul, ñu man leen a fat ca dal yu sax ya.

16:10  Nit ku maandu ci yëf yu néew, dina maandu itam ci yu bare. Ku jubadi ci yëf yu néew, du jub ci yu bare.

16:11  Su fekkeente ne nag jubuleen ci alalu àddina, kon ku leen di dénk alal ju wóor ji?

16:12  Te su ngeen maanduwul ci alal ji ngeen moomul, kon ku leen di jox alal ji ngeen moom?

16:13  «Benn jaam mënul a jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Mënuleen a boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.»

16:14  Farisen yi déglu li Yeesu doon wax lépp, tàmbali di ko reetaan, ndaxte ñu bëggoon xaalis lañu.

16:15  Waaye Yeesu ne leen: «Yéen yéena ngi fexee jub ci kanamu nit ñi waaye Yàlla xam na seen xol. Ndaxte li nit ñiy fonk, Yàlla sib na ko.

16:16  «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi ñu ngi fi woon ba kera Yaxya di ñëw. La ko dale foofa nag, yégle nañu xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla, te ñépp a ngi góor-góorlu, ngir dugg ci.

16:17  Waaye nag asamaan ak suuf jóge fi moo gën a yomb randal wenn rëdd ci arafu yoonu Musaa.

16:18  «Ku fase sa jabar, ba noppi takk keneen, njaaloo nga, te ku takk jigéen ju jëkkëram fase, njaaloo nga.

16:19  «Dafa amoon boroom alal juy sol yére yu rafet te jafe, tey dund bés bu set dund gu neex.

16:20  Fekk miskin mu ñuy wax Lasaar daan tëdd ca buntu këram, fees dell ak ay góom,

16:21  te bu sañoon, di lekk ci desiti ñam wiy rot ci lekkukaayu boroom alal ji. Xaj yi sax daan nañu ñëw, di mar ay góomam.

16:22  «Noonu miskin ma dee, malaaka yi yóbbu ko ca wetu Ibraayma. Boroom alal ja itam dee, ñu suul ko.

16:23  Bi ñu koy mbugal ca safara, mu téen, séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.

16:24  Noonu mu yuuxu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catul baaraamam ci ndox, seralal ma sama làmmiñ, ndaxte maa ngi sonn lool ci safara sii!”

16:25  Ibraayma ne ko: “Sama doom, fàttalikul ne, jot nga sa bànneex ci àddina, fekk Lasaar dëkk ci tiis. Looloo tax xolam sedd fii, yaw nag, ngay sonn.

16:26  Rax-ca-dolli it am na kàmb gu xóot sunu diggante ak yéen, ba tax ñi bëgg a jóge fii jëm ci yéen, walla ñi bëgg a jóge foofu jëmsi ci nun, duñu ko man.”

16:27  «Noonu boroom alal ja ne: “Kon nag maam, maa ngi lay ñaan, nga yebal Lasaar ca sama kër baay,

16:28  ndaxte am naa fa juróomi rakk. Na leen artu, ngir ñu bañ a ñëw ñoom itam ci bérabu metit wii.”

16:29  Ibraayma ne ko: “Say doomu baay, ñu ngeek yoonu Musaa ak téerey yonent yi. Nañu leen déggal.”

16:30  Boroom alal ja ne ko: “Déedéet, maam Ibraayma, waaye su kenn dekkee, dem ca ñoom, dinañu tuub seeni bàkkaar.”

16:31  Waaye Ibraayma tontu ko ne: “Su ñu dégluwul Musaa ak yonent yi, kon ku dekki sax, du tax ñu gëm.”»

17:1  Yeesu waxaat ay taalibeem ne leen: «Fiir yuy yóbbe nit bàkkaar mënta ñàkk, waaye toroxte dal na ki koy lal.

17:2  Ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej moo gën ci moom muy daaneel ci bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ci ñii.

17:3  Wottuleen seen bopp. «Bu sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu réccoo, baal ko.

17:4  Te su la tooñee juróom-ñaari yoon ci bés bi, te ñëw ci yaw juróom-ñaari yoon ne la: “Tuub naa ko,” nanga ko baal.»

17:5  Ndaw ya wax Boroom bi ne ko: «Yokkal sunu ngëm.»

17:6  Boroom bi tontu ne: «Su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen man a ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbëtu ca géej ga,” te dina def li ngeen wax.

17:7  «Kan ci yéen bu amoon surga bu beyi walla bu sàmmi ba ñëw, ndax dafa ko naa: “Kaay lekk.”

17:8  Déedéet. Xanaa kay da ko naan: “Defaral ma réer bi. Takkul te tibbal ma, ba ma lekk te naan, ba noppi nga door a lekk te naan.”

17:9  Li surga ba topp ndigal, ndax tax na mu yelloo ngërëm? Déedéet.

17:10  Noonu yéen itam bu ngeen toppee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeen a war ne: “Ay surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»

17:11  Bi muy dem Yerusalem ba tey, Yeesu jaar ci dig wiy xaajale Samari ak Galile.

17:12  Bi muy jub benn dëkk, fukki gaana ñëw, dogale ko. Ñu taxaw dand ko, di wax ca kaw naan:

17:13  «Yeesu, kilifa gi, yërëm nu!»

17:14  Naka la leen Yeesu di gis, naan leen: «Demleen won seen bopp saraxalekat ya.» Bi ñuy dem, ñu daldi set.

17:15  Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi dëpp, di màggal Yàlla ak baat bu xumb.

17:16  Mu dëpp jëwam ca tànki Yeesu, di ko gërëm. Fekk nitu Samari la woon.

17:17  Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa du fukk yépp a wér? Ana juróom-ñeent ña nag?

17:18  Amul kenn ci ñoom ku ñëw gërëm Yàlla ku dul doxandéem bii!»

17:19  Noonu Yeesu ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»

17:20  Farisen yi laaj Yeesu ne ko: «Kañ la Yàlla di tëral nguuram?» Mu tontu leen ne: «Bu Yàlla di wàcce nguuram ci nit ñi, kenn du ko man a teg bët.

17:21  Duñu man a wax it ne: “Xool-leen, mi ngi fii,” walla: “Ma nga fale,” ndaxte nguuru Yàlla wàcc na ci seen biir.»

17:22  Noonu mu ne taalibe ya: «Jamono dina ñëw, fu ngeen di bëgg a gis su doon sax benn fan ci jamono ju Doomu nit ki di ñëw, waaye dungeen ko gis.

17:23  Dees na leen ne: “Mi ngi fii!” walla: “Ma nga fale!” Buleen dem, mbaa ngeen di leen topp.

17:24  Ndaxte ni melax naan ràyye ci asamaan, di leeral gii wet, ba ca gee, noonu it la Doomu nit ki di mel ci bésam.

17:25  Waaye balaa booba fàww mu sonn lool te niti jamono jii dëddu ko.

17:26  «La xewoon ca bési Nóoyin, dina xewaat ci bési Doomu nit ki.

17:27  Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jël jabar ak a séyi, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga. Noonu mbënn ma ñëw, rey leen ñoom ñépp.

17:28  «Dina mel it ni la xewoon ca bési Lóot. Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jënd ak di jaay, di ji ak di tabax.

17:29  Waaye bés ba Lóot génnee Sodom, Yàlla tawloo safara ak tamarax, rey leen ñoom ñépp.

17:30  Noonu lay mel, bés bu Doomu nit kiy feeñ.

17:31  «Ca bés boobee ku nekk ca kaw kër ga te ay bagaasam nekk ca biir, bumu wàcc jëli leen. Te it ku nekk ca tool ya, bu mu ñibbi.

17:32  Fàttalikuleen jabaru Lóot!

17:33  Kuy wut a rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ko ñàkk, dinga dund.

17:34  Maa ngi leen koy wax: ca jamono jooju, ñaar dinañu bokk a tëdd guddi, dees na yóbbu kenn ki, bàyyi ka ca des.

17:35  Ñaari jigéen dinañu wolandoo, dees na yóbbu kenn ci, bàyyi ka ca des.»

17:37  Taalibe yi ne Yeesu: «Fu loolu di xewe, Boroom bi?» Yeesu tontu leen ne: «Fa médd nekk, la tan yiy dajee.»

18:1  Noonu Yeesu wax leen itam léeb wii ngir xamal leen ne, war nañoo sax ci ñaan te bañ a xàddi.

18:2  Nee na: «Dafa amoon cib dëkk, benn àttekat bu ragalul Yàlla te faalewul mbindeef.

18:3  Amoon na itam ca dëkk ba jigéen ju jëkkëram faatu ju daan faral di ñëw ci moom, naan ko: “Àtte ma ak sama noon!”

18:4  Àttekat ba bañ lu yàgg, waaye am bés mu ne ci xelam: “Ragaluma Yàlla te faalewuma mbindeef,

18:5  waaye jigéen jii lakkal na ma; kon dinaa ko àtte, ngir mu bañatee ñëw sonal ma. Dina rey ak ay wax.”»

18:6  Boroom bi tegaat ca ne: «Dégluleen bu baax li àttekat bu bon boobu wax;

18:7  ndax Yàlla du àtte jub mbooloom mi mu tànn te ñu koy ñaan wall guddi ak bëccëg? Ndax dina leen xaarloo?

18:8  Maa ngi leen koy wax, dina leen àtte jub ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki ñëwee, ndax dina fekk ngëm ci àddina?»

18:9  Yeesu waxaat léeb wii nit, ñi foog ne jub nañu tey xeeb ñi ci des.

18:10  Mu ne: «Dafa amoon ñaari nit ñu dem ca kër Yàlla ga, di ñaan. Kenn ki ab Farisen la, ki ci des juutikat.

18:11  Farisen baa nga taxaw di ñaan ci xelam naan: “Yaw Yàlla, maa ngi lay sant ci li ma melul ni ñeneen ñiy sàcc, di def lu jubadi te di njaaloo, rawatina juutikat bii.

18:12  Ayu-bés gu nekk damay woor ñaari yoon, di joxe asaka ci lépp lu ma wut.”

18:13  «Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore te bëggul a siggi sax, xool ca asamaan. Waaye ma ngay fëgg dënnam te naan: “Yaw Yàlla, yërëm ma, man miy bàkkaarkat.”»

18:14  Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen koy wax, nit kooku, ba muy ñibbi këram, moom la Yàlla àtte ni ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy yékkatiku dees na la suufeel, te kuy suufeelu, ñu yékkati la.»

18:15  Amoon na ay nit, ñuy indil Yeesu ay liir, ngir mu teg leen ay loxoom. Bi taalibe ya gisee loolu, ñu gëdd leen.

18:16  Waaye Yeesu woo leen ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw ci man, te buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla.

18:17  Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, woyoful ni xale, nangu nguuru Yàlla, doo ci man a dugg.»

18:18  Benn njiitu Yawut laaj Yeesu ne ko: «Kilifa gu baax gi, lu ma war a def, ba am wàll ci dund gu dul jeex?»

18:19  Yeesu tontu ko: «Lu tax nga wooye ma ku baax? Yàlla rekk a baax.

18:20  Xam nga ndigal yi: “Bul njaaloo, bul bóom, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”»

18:21  Njiit la ne ko: «Loolu lépp sàmm naa ko li dale ci sama ndaw ba tey.»

18:22  Bi Yeesu déggee loolu, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Jaayal li nga am lépp, séddale ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.»

18:23  Bi nit ka déggee loolu, mu am tiis, ndaxte ku bare woon alal la.

18:24  Yeesu xool ko, daldi ne: «Boroom alal, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!

18:25  Giléem jaar ci bën-bënu pusa moo gën a yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.»

18:26  Ñi doon déglu daldi ne: «Kon nag ku man a mucc?»

18:27  Yeesu tontu ne: «Li të nit ñi, tëwul Yàlla.»

18:28  Noonu Piyeer ne: «Nun de, dëddu nanu li nu am lépp, topp la.»

18:29  Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku dëddu kër walla jabar walla ay doomi ndey walla ay waajur walla ay doom ngir nguuru Yàlla,

18:30  dinga am tey jii ay yooni yoon, ak dund gu dul jeex ëllëg.»

18:31  Yeesu wéetoo ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Nu ngi dem Yerusalem, te li yonent yi bindoon lépp ci mbirum Doomu nit ki dina mat.

18:32  Dinañu ko jébbal ñi dul Yawut, ñu ñaawal ko, saaga ko, tifli ci kawam.

18:33  Gannaaw bu ñu ko dóoree ay yar ba noppi, dinañu ko rey, waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»

18:34  Waaye taalibe ya dégguñu li mu leen doon wax; kàddu yooyu ump na leen, te xamuñu li waxi Yeesu yooyu tekki.

18:35  Bi Yeesu di agsi dëkku Yeriko, am gumba gu toogoon ca wetu yoon wa, di yelwaan.

18:36  Naka la gumba ga dégg mbooloo di jàll, mu laaj lan moo xew.

18:37  Ñu wax ko ne: «Yeesum Nasaret moo fay jaar.»

18:38  Noonu mu yuuxu ne: «Yeesu, Sëtu Daawuda, yërëm ma!»

18:39  Ñi jiitu woon gëdd ko, ngir mu noppi. Waaye muy gën a yuuxu naan: «Sëtu Daawuda, yërëm ma!»

18:40  Noonu Yeesu taxaw, santaane ñu indil ko ko. Bi mu jegesee, Yeesu laaj ko ne:

18:41  «Loo bëggoon ma defal la ko?» Mu ne ko: «Sang bi, damaa bëgg a gis.»

18:42  Noonu Yeesu ne ko: «Na say bët gis! Sa ngëm faj na la.»

18:43  Ca saa sa mu daldi gis. Noonu mu topp ci Yeesu, di màggal Yàlla. Mbooloo mépp gis loolu, di sant Yàlla.

19:1  Yeesu dugg na Yeriko, jaar ca dëkk ba, di dem.

19:2  Waaye amoon na fa waa ju ñuy wax Sase. Njiitu juutikat la, te di ku bare alal.

19:3  Bëgg na gis kan mooy Yeesu, waaye dafa gàtt lool, ba mënu koo gis ndax mbooloo ma.

19:4  Noonu mu daw, jiituji ca yoon wa, yéeg ci genn garab ngir gis Yeesu, ndaxte foofa la naroon a jaar.

19:5  Bi Yeesu dikkee ba tollook garab ga nag, mu téen ne ko: «Sase, wàccal gaaw, ndax tey sa kër laa war a dal.»

19:6  Sase daldi gaawantu wàcc, ganale ko ak mbég.

19:7  Ñépp gis loolu, di ñurum-ñurumi naan: «Mi ngi dal cig këru boroom bàkkaar.»

19:8  Waaye Sase taxaw ne Boroom bi: «Déglul Boroom bi, dogu naa may sama genn-wàllu alal miskin yi, te lu ma mas a njublaŋ nit, jël alalam, dinaa ko fey ñeenti yoon lu ni tollu.»

19:9  Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam.

19:10  Ndaxte Doomu nit ki ñëw na, ngir seet te musal ñi réer.»

19:11  Bi nit ñi doon déglu kàddu yooyu, Yeesu teg ca léeb, ndaxte jege woon na Yerusalem, te ñoom foogoon nañu ne, nguuru Yàlla dafay daldi feeñ ca saa sa.

19:12  Mu ne nag: «Dafa amoon boroom juddu bu rafet bu demoon ci réew mu sore, ngir ñu fal ko buur te mu dellusiwaat.

19:13  Noonu mu woo fukk ci ay surgaam, jox ku nekk benn libidoor, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba may ñibbisi.”

19:14  Waaye waa réewam bëgguñu ko. Noonu ñu yónni ndaw ci gannaawam ne: “Bëggunu nit kii yilif nu.”

19:15  «Bi ñu ko falee buur nag, ba mu dellusi, mu woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam nan lañu ci liggéeye.

19:16  Ku jëkk ka ñëw ne ko: “Sang bi, sa libidoor bii jur na fukki libidoor.”

19:17  Buur ba ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne, takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki dëkk.”

19:18  Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.”

19:19  Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”

19:20  Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko.

19:21  Dama laa ragaloon, ndaxte ku néeg nga. Dangay nangu loo dénkaanewul, di dajale loo jiwul.”

19:22  Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul.

19:23  Lu tax nag yóbbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? Bés bu ma ñëwee nag, ma man a jot sama xaalis ak la mu jur.”

19:24  «Ci kaw loolu mu ne ña taxawoon ca wetam: “Nanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.”

19:25  Ñu ne ko: “Sang bi, am na fukki libidoor ba noppi.”

19:26  Buur ba ne leen: “Maa ngi leen koy wax, ku am, dinañu la dolli, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.

19:27  Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”»

19:28  Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa daldi jiitu, jëm Yerusalem.

19:29  Bi muy jege dëkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal ñaar ci ay taalibeem,

19:30  ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi.

19:31  Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” tontuleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”»

19:32  Ñaari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon.

19:33  Bi ñuy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur gi?»

19:34  Ñu tontu ne: «Ndaxte Boroom bi da koo soxla.»

19:35  Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu.

19:36  Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi.

19:37  Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis.

19:38  Ñu ngi naan:«Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Na jàmm am ca asamaan,te ndam li féete ca bérab yu gën a kawe!»

19:39  Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!»

19:40  Noonu mu tontu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.»

19:41  Bi Yeesu jegee dëkk ba, ba séen ko, mu jooy ko

19:42  naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la man a indil jàmm! Waaye fi mu ne mënuloo koo gis.

19:43  Bés dina ñëwi yu say noon di jal, wërale la. Dinañu la tëj ci biir, tanc la.

19:44  Dinañu la yàqaate, yaw ak sa waa dëkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte ràññeewoo jamono ji Yàlla ñëwe, wallusi la.»

19:45  Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, daldi dàq ña fay jaay,

19:46  naan leen: «Mbind mi nee na: “Sama kër këru ñaan ci Yàlla lay doon; waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.”»

19:47  Bés bu nekk Yeesu di jàngale ca kër Yàlla ga. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, ñoom ak njiiti xeet wa, ñu ngi ko doon wut a reylu.

19:48  Waaye xamuñu woon lan lañu man a def, ndaxte nit ñépp a ngi ko doon déglu, bañ benn baat raw leen.

20:1  Benn bés Yeesu doon jàngal nit ña ca kër Yàlla ga, di leen yégal xebaar bu baax bi. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya ñëw ne ko:

20:2  «Wax nu ci ban sañ-sañ ngay defe yëf yii, walla kan moo la may boobu sañ-sañ.»

20:3  Yeesu tontu leen ne: «Man itam dinaa leen laaj lenn: wax leen ma,

20:4  la Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?»

20:5  Ñu waxtaan ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”

20:6  Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” mbooloo mépp dinañu nu sànni ay xeer, ndaxte gëm nañu ne Yaxya yonent la woon.»

20:7  Noonu ñu tontu ne, xamuñu fu mu ko jële.

20:8  Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»

20:9  Noonu Yeesu daldi wax nit ña léeb wii: «Amoon na nit ku jëmbët toolu réseñ, batale ko ay beykat, dem tukki tukki bu yàgg.

20:10  Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi. Waaye beykat yi dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.

20:11  Mu yónniwaat beneen surga, ñu dóor ko moom itam, toroxal ko, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.

20:12  Mu yónneeti ñetteelu surga, ñu gaañ ko, dàq ko.

20:13  «Boroom tool ba daldi ne: “Nan laay def nag? Dinaa yónni sama doom, sama reeni xol. Xëy na ñu weg ko, moom.”

20:14  Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen biir: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.”

20:15  Ñu génne ko tool bi nag, rey ko.» Noonu Yeesu laaj leen: «Nu leen boroom tool bi di def, nag?

20:16  Xanaa ñëw, rey beykat yooyu, dénk tool ba ñeneen.» Bi Yeesu waxee loolu, nit ña ne ko: «Yàlla tere!»

20:17  Waaye Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lu baat yii ci Mbind mi di tekki:“Doj wa tabaxkat ya sànni,mujj na di doju koñ.”

20:18  Képp ku dal ci doj woowu, dammtoo, te ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»

20:19  Xutbakat ya ak saraxalekat yu mag ya ñu ngi doon wut a jàpp Yeesu ca taxawaay ba, ndaxte xam nañu ne, ñoo tax mu wax léeb woowu. Waaye ragal nañu mbooloo ma.

20:20  Noonu ñu koy yeeru, daldi yónni ay nit ñu mbubboo njub, sas leen ñu fexe koo jàpp ci ay waxam, ngir jébbal ko boroom réew, ma yor kilifteef ak sañ-sañ.

20:21  Ñu daldi ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne li ngay wax te di ko jàngale lu jub la. Amuloo parlàqu, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.

20:22  Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet.»

20:23  Waaye Yeesu xam na seen pexe ne leen:

20:24  «Wonleen ma posetu denariyon. Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu tontu ko: «Sesaar.»

20:25  Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»

20:26  Noonu mënuñu ko woon a jàpp ciy waxam ci kanamu mbooloo ma; ñu waaru ci tontoom, ba wedam.

20:27  Noonu ay nit, ñu bokk ci Sadusen yi, ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom weddi nañu ndekkite li. Noonu ñu laaj ko ne:

20:28  «Kilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu te bàyyiwul doom ak jabaram, kooku war na donn jigéen ji, ba yékkati giiru magam.

20:29  Amoon na fi nag juróom-ñaari góor ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te bàyyiwul doom.

20:30  Ñaareel ba takk jigéen ja, def noonu; ak ñetteel ba, ba juróom-ñaar ñépp faatu te bàyyiwuñu doom.

20:32  Gannaaw ga nag jigéen ja it faatu.

20:33  Ci ndekkite li nag, kan ci ñoom moo war a donn jigéen ja, fekk ku nekk ci juróom-ñaar ñi mas na koo takk?»

20:34  Yeesu tontu leen ne: «Ci àddina sii, góor ñi ak jigéen ñi dañuy séy.

20:35  Waaye ña ñu àtte ne, yeyoo nañoo bokk ci dundu ëllëg ak ci ndekkite li, kenn du am jabar, kenn du am jëkkër.

20:36  Dafa fekk ne mënatuñoo dee, ndaxte dañuy mel ni malaaka yi. Ay doomi Yàlla lañu ndaxte doomi ndekkite lañu.

20:37  Te Musaa sax wone na ne, néew yi dinañu dekki, ci saarum ngarab si. Foofa Musaa wooye na fa Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba.”

20:38  Kon nag nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la, ndaxte Yàllaa tax ñépp di dund.»

20:39  Ci kaw loolu ay xutbakat ne ko: «Li nga wax dëgg la, kilifa gi!»

20:40  Ndaxte kenn ci ñoom ñemeetu koo laaj dara.

20:41  Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nit ñi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda?

20:42  Ndaxte Daawuda moom ci boppam moo ne ci Sabóor:“Boroom bi nee na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,

20:43  ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.’ ”

20:44  Gannaaw Daawuda nag wooye na ko “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»

20:45  Bi ko nit ña fa nekkoon ñépp doon déglu, Yeesu ne ay taalibeem:

20:46  «Moytuleen xutbakat yi; dañoo bëgg di doxantu, sol ay mbubb yu réy, te ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ci pénc mi. Ci jàngu yi, toogu yu féete kanam lañuy wut, te toogu yu yiw lañuy taamu ci reeri xew yi.

20:47  Ñu ngi lekk alalu jigéen ñi seen jëkkër faatu, di ñaan Yàlla ay ñaani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina gën a tar.»

21:1  Noonu Yeesu siggi, séen ay boroom alal ñuy dugal seen sarax ca ndab ya ca kër Yàlla ga.

21:2  Mu gis itam jenn jigéen ju jëkkëram faatu te mu ñàkk, ju fa def ñaari poseti xànjar.

21:3  Noonu mu daldi ne: «Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, jigéen ju ñàkk jee moo ëpp ñeneen ñépp lu mu joxe.

21:4  Ñoom ñépp dañu sàkku ci seen barele, waaye moom dafa sàkku ci néewleem, ba joxe xaalis bi mu waroon a dunde.»

21:5  Noonu ay nit doon wax ci lu jëm ca kër Yàlla ga, ak ni ñu ko rafetale ak ay doj yu jafe ak alal ju ñu jébbal Yàlla. Waaye Yeesu ne leen:

21:6  «Li ngeen gis fii lépp, jamono dina ñëw joo xam ne dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»

21:7  Ñu laaj ko ne: «Kilifa gi, kañ la loolu di am? Te luy tegtal ne, looloo ngi waaj a xew?»

21:8  Yeesu tontu ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax. Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Moom laa,” walla ñu naan: “Jamono ji jegesi na.” Buleen topp ñooñu.

21:9  Bu ngeen déggee ay xare ak ay réew yu jóg, wottuleen a tiit, ndaxte fàww yooyule jëkk a am. Waaye taxul mujug jamono daldi taxaw.»

21:10  Noonu mu teg ca ne: «Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew dina xeex ak meneen réew.

21:11  Suuf dina yengu yengu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy jóge asamaan.

21:12  Waaye bala looloo xew, dees na leen jàpp, fitnaal leen, di leen jébbal àttekat yi ca jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanam ay buur yi ak ay boroom réew ndax sama tur.

21:13  Loolu dina leen ubbil bunt, ba ngeen man maa seedeel.

21:14  Fasleen yéenee bañ a wut lay ngir musal seen bopp.

21:15  Ndaxte man ci sama bopp maa leen di jox kàddu ak xel moo xam ne seeni noon duñu ko man a teggi, mbaa ñu di ko weddi.

21:16  Seeni waajur sax ak seeni doomi ndey, seeni bokk ak seeni xarit, dinañu leen jébbal àttekat yi, ba ñu rey ñenn ci yéen.

21:17  Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur.

21:18  Waaye seen genn kawar sax du neen.

21:19  Seen muñ moo leen di musal.

21:20  «Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na.

21:21  Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir dëkk bi, nanga ko génn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca dëkk ba!

21:22  Ndaxte ci bés yooyu Yàlla dina fey jëf yi, te li ñu bindoon ci téereb Yàlla dina mat.

21:23  Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi, te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii.

21:24  Dees na leen reye ak i jaasi, jàpp leen jaam, yóbbu leen ci réewi àddina sépp. Te ñi dul Yawut dinañu nappaaje Yerusalem, ba kera jamonoy ñi dul Yawut mat.

21:25  «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi, ci weer wi ak ci biddiiw yi. Ci kaw suuf xeet yi dinañu tiit, jaaxle ndax riiru géej gi ak yengu-yengub duus yi.

21:26  Bu boobaa nit ñiy xëm ndax tiitaange, bu ñuy xalaat musiba, yi nar a wàcc ci àddina, ndaxte dees na yengal kàttani asamaan.

21:27  Noonu dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.

21:28  Bu mbir yooyu di tàmbalee xew nag, boo yaboo ngeen siggi, téen, ndaxte seen njot jubsi na.»

21:29  Noonu Yeesu misaal leen lii: «Xool-leen garabu figg ak yeneen garab yi.

21:30  Bu ñu gisee ñu sëq, soxlawuleen kenn wax leen ne, nawet bi jubsi na xaat.

21:31  Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne nguuru Yàlla jege na.

21:32  «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul.

21:33  Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.

21:34  «Moytuleen seen nafsu diigal leen ci yàqute ak ci màndite ak ittey àddina, ba bés boobu bett leen ni mbaal.

21:35  Ndaxte dina dal ci ñépp ñi nekk ci kaw suuf.

21:36  Yeewuleen, di sax ci ñaan, ngir ngeen man a mucc ci loolu lépp war a xew, te man a taxaw ak kóolute ci kanamu Doomu nit ki.»

21:37  Yeesoo ngi daan yendoo jàngale ca kër Yàlla ga, te bu guddee mu dem ca tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, fanaan fa.

21:38  Te nit ñépp dañu daan teel a xëy ca kër Yàlla ga, di ko déglu.

22:1  Màggalu Mburu ya amul lawiir jege woon na, te ñu di ko wax Bésu Jéggi ba.

22:2  Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya di wut pexem reylu Yeesu, ndaxte dañoo ragaloon nit ña.

22:3  Noonu Seytaane daldi solu Yudaa, mi ñuy wooye Iskariyo te mu bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar.

22:4  Noonu Yudaa dem waxtaani ak saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga, ba xam nan la leen di jébbale Yeesu.

22:5  Ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis.

22:6  Yudaa nangu, di fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu, fu mbooloo ma nekkul.

22:7  Bésu màggalu Mburu ya amul lawiir agsi, ca bés boobu lañu waroon a rendi mbotem màggalu Jéggi ba.

22:8  Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, defaral nu reeru Jéggi ba.»

22:9  Ñu ne ko: «Fan nga bëggoon, nu defare ko fa?»

22:10  Mu ne leen: «Bu ngeen duggee ca dëkk ba, góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen. Toppleen ci moom ba ca kër ga muy dugg,

22:11  te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru Jéggi ba, man ak samay taalibe?”

22:12  Noonu dina leen won néeg bu féete kaw, te yaa, ñu defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.»

22:13  Ñu dem, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.

22:14  Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi,

22:15  ne leen: «Yàkkamti woon naa lool lekk ak yéen reeru Jéggi bii, laata ñu may sonal.

22:16  Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Yàlla.»

22:17  Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko.

22:18  Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum réseñ mi, ba kera Yàlla di tëral nguuram.»

22:19  Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»

22:20  Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen.

22:21  Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li.

22:22  Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.»

22:23  Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy nar a def loolu.

22:24  Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci ñoom moo gën a màgg.

22:25  Yeesu ne leen: «Buuri xeeti àddina dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañuy sàkku ngërëm.

22:26  Waaye yéen buleen def noonu. Ki gën a màgg ci yéen, na nekk ni ki gën a ndaw, te njiit mel ni surga.

22:27  Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gën a màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga.

22:28  Yéen nag yéenay ñi ànd ak man ci samay fitna.

22:29  Man nag jox naa leen sañ-sañu nguuru, ni ma ko sama Baay joxe.

22:30  Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.»

22:31  Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax.

22:32  Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo dellusee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.»

22:33  Piyeer ne ko: «Boroom bi, àttan naa ànd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.»

22:34  Yeesu tontu ko ne: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne, xam nga ma.»

22:35  Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu tontu ne: «Déedéet.»

22:36  Mu neeti leen: «Léegi nag képp ku am xaalis, na ko jël; te ku am mbuus, na ko jël; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, jënde ko jaasi.

22:37  Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax fàww mu am ci man, bi mu nee: “Boole nañu ko ak ñu bon ña.” Ndaxte loolu jëm ci man mi ngi mat.»

22:38  Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.»

22:39  Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe nakajekk. Taalibeem ya topp ci moom.

22:40  Bi mu agsee ca bérab ba, mu ne leen: «Ñaanleen, ngir bañ a daanu cig fiir.»

22:41  Noonu mu dand leen, ba fu aw saan man a tollu, daldi sukk di ñaan ne:

22:42  «Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»

22:43  Noonu malaakam Yàlla daldi koy feeñu, may ko doole.

22:44  Ci biir tiis, Yeesu gën a sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf.

22:45  Bi mu ñaanee ba noppi, mu jóg, dellusi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis.

22:46  Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir.»

22:47  Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku ñuy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak ñaar jiite leen. Yudaa jegeñsi Yeesu, bëgg koo fóon.

22:48  Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!»

22:49  Bi ñi àndoon ak Yeesu gisee liy bëgg a xew, ñu ne: «Boroom bi, ndax nu dóore jaasi?»

22:50  Kenn ci ñoom nag dóor surgab saraxalekat bu mag ba, noppu ndeyjooram dagg.

22:51  Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.

22:52  Noonu Yeesu ne saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc.

22:53  Moona maa nga woon ak yéen bés bu nekk ca kër Yàlla ga, te jàppuleen ma. Waaye léegi seen waxtu la, di jamonoy lëndëm.»

22:54  Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër saraxalekat bu mag ba. Piyeer topp fu sore.

22:55  Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir.

22:56  Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko jàkk ne: «Nit kii itam àndoon na ak moom.»

22:57  Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.»

22:58  Nes tuuti keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer tontu ko: «Sama waay, bokkuma ci.»

22:59  Bi ñu tegee lu mat waxtu, keneen dikkaat ca wax ja ne: «Ci lu wóor nit kii àndoon na ak moom, nde Galile la jóge.»

22:60  Waaye Piyeer tontu ne: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab.

22:61  Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer fàttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi ñetti yoon.»

22:62  Piyeer daldi génn, di jooy jooy yu metti.

22:63  Nit ñaa nga jàppoon Yeesu, di ko ñaawal ak di ko dóor.

22:64  Ñu ngi takkoon ay bëtam, di ko laaj, naan ko: «Yaw, wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?»

22:65  Ñu ngi ko doon tifaar it yeneeni saaga.

22:66  Bi bët setee, kureelu njiiti xeet wa, maanaam saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, daldi daje, indi Yeesu ci seen kanam.

22:67  Ñu ne ko: «Soo dee Almasi bi, wax nu ko.» Mu tontu leen ne: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm.

22:68  Te su ma leen laajee, dungeen tontu.

22:69  Waaye gannaawsi tey, Doomu nit ki dina toog ci ndeyjooru Yàlla, Aji Kàttan ji.»

22:70  Noonu ñépp ne: «Kon nag yaay Doomu Yàlla ji?» Mu tontu leen ne: «Yéen ci seen bopp wax ngeen ne moom laa.»

22:71  Ñu daldi ne nag: «Lu nuy doyeeti seede léegi, ndegam nun ci sunu bopp noo ko nangoo ci gémmiñam!»

23:1  Gannaaw loolu kureelu àttekat ya yépp daldi jóg, yóbbu Yeesu ca Pilaat.

23:2  Foofa ñu tàmbali di ko sosal naan: «Fekk nanu nit kii, muy fàbbi sunu réew, di leen teree fey galag Sesaar, te mi ngi teg boppam Almasi, maanaam buur.»

23:3  Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu tontu ko ne: «Wax nga ko.»

23:4  Pilaat ne saraxalekat yu mag ya ak mbooloo ma: «Gisuma genn tooñ ci nit kii.»

23:5  Waaye ñu sax ci seeni wax naan: «Mi ngi jógloo mbooloo mi, di jàngale ci réewu Yawut ya mépp, li dale ci Galile ba fii.»

23:6  Bi Pilaat yégee baat yooyu, mu laajte ne: «Ndax nit kii Galile la dëkk?»

23:7  Bi mu yégee ne, Yeesoo ngi nekk ci diiwaan bi Erodd yilif, mu yónnee ko Erodd, mi nekkoon ci jamono jooju ci Yerusalem.

23:8  Bi Erodd gisee Yeesu, mu am mbég mu réy. Bu yàgg ba tey dafa koo bëggoon a gis, ndaxte déggoon na ñuy wax ci ay mbiram te yaakaaroon na ne, dina ko gis mu def kéemaan.

23:9  Noonu mu laaj ko ay laaj yu bare, waaye Yeesu tontuwul dara.

23:10  Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat yaa nga fa woon, di ko jiiñ bu metti.

23:11  Noonu Erodd ak ay xarekatam toroxal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu rafet, delloo ko Pilaat.

23:12  Erodd ak Pilaat dañoo ñi bañante woon bu jëkk, waaye ca bés booba doon nañu ay xarit.

23:13  Pilaat daldi woo saraxalekat yu mag ya, njiit ya ak mbooloom Yawut ya ne leen:

23:14  «Indil ngeen ma nit kii, ne ma, day jàddloo yoon mbooloo mi. Léegi nag man mii laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma tooñ ci moom ak li ngeen koy jiiñ lépp.

23:15  Erodd itam gisul tooñ gu mu def, ndegam mu yónneewaat nu ko. Nit kii deful genn tooñ gu jar ñu koy rey.

23:16  Kon nag dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.»

23:18  Waaye ñu bokk di yuuxu, ñoom ñépp naan: «Reyal kii te bàyyi Barabas!»

23:19  Dañoo tëjoon Barabas, ndaxte dafa jéem a tas dëkk ba, te rey nit.

23:20  Pilaat waxaat ak mbooloo ma, ndaxte dafa bëggoon a bàyyi Yeesu.

23:21  Waaye ñuy yuuxu naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!»

23:22  Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Lu tax? Gan tooñ la def? Gisuma ci moom dara lu jar dee. Kon dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.»

23:23  Waaye ñoom ñu sax ca la ñu waxoon, di gën a yuuxu naan, ñu daaj ko ci bant. Coow la yey Pilaat.

23:24  Muj gi Pilaat dogal, ñu defal leen li ñu bëgg.

23:25  Mu bàyyil leen ki ñu ko ñaanoon, kooku ñu tëjoon kaso, ndax tas réew ma ak rey nit. Waaye mu jébbal leen Yeesu ci seeni loxo.

23:26  Bi ñuy yóbbu Yeesu, ñu jàpp ku ñuy wax Simoŋ te mu dëkk Siren, ku jóge ca wet, ga féete ak tool ya, sëf ko bant, ba ñuy war a daaj Yeesu, ngir mu gàddu ko, topp ci moom.

23:27  Mbooloo mu baree nga ko toppoon, te jigéen ñu baree ngi doon yuuxu, di ko jooy.

23:28  Yeesu daldi walbatiku ca ñoom ne: «Yéen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom.

23:29  Ndaxte jamono dina ñëw, ju ñu naan: “Jigéen ñi musul a jur ak ñi musul a nàmpal, barkeel ngeen!”

23:30  Bu keroogee,“Nit ñi dinañu ne tund yi:‘Daanuleen ci sunu kaw!’te naan jànj yi: «“Suul-leen nu!»“ “

23:31  Ndaxte su ñu defee nii garab gu tooy gi, lu ñuy def garab gu wow gi?»

23:32  Yóbbaale nañu itam ñeneen, ñuy ñaari defkati lu bon, ngir rey leen.

23:33  Bi xarekat ya agsee ba ca bérab, ba ñuy wooye Kaaŋu Bopp, ñu daaj fa Yeesu ca bant, daajaale ñaari defkati lu bon ya, kenn ca ndeyjooram, ka ca des ca càmmooñam.

23:34  Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndaxte xamuñu li ñuy def.» Xarekat ya tegoo ay bant yéreem, ngir séddoo ko.

23:35  Mbooloo maa nga fa taxaw di seetaan. Njiit ya di ko reetaan naan: «Musal na ñeneen; na musal boppam, su fekkee mooy Almasi bi, ki Yàlla fal!»

23:36  Xarekat ya it di ko ñaawal. Ñu jegesi, jox ko bineegar te naan:

23:37  «Su fekkee ne yaay buuru Yawut yi, musalal sa bopp!»

23:38  Ñu daaj mbind, mu tiim ko naan: «Kii mooy buuru Yawut yi.»

23:39  Kenn ca defkatu lu bon ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi bi? Musalal sa bopp te musal nu!»

23:40  Waaye ka ca des yedd moroom ma, naan ko: «Xanaa ragaloo Yàlla, yaw mi ñuy mbugal ni moom!

23:41  Nun yelloo nanu sunu mbugal, waaye moom deful dara.»

23:42  Noonu mu ne: «Yeesu, fàttaliku ma, boo dellusee ci sa nguur.»

23:43  Yeesu tontu ko ne: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, tey jii dinga texe ak man ca jataayu Yàlla.»

23:44  Noonu digg-bëccëg daldi jot, jant ba nëbbu, réew mépp daldi lëndëm këruus lu mat ñetti waxtu. Ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga daldi xar ñaar.

23:46  Yeesu woote ak kàddu gu dëgër naan: «Baay, jébbal naa la sama ruu!» Bi mu waxee loolu, mu delloo ruuwam Yàlla.

23:47  Bi njiitu xare ba gisee li xewoon, mu màggal Yàlla ne: «Dëgg-dëgg nit kii ku jub la woon.»

23:48  Nit ña fa dajaloo woon ñépp, di seetaan li xew, ba ñu gisee loolu, ñu dellu seen kër, fëgg seen dënn, di jooy.

23:49  Xamey Yeesu yépp ak jigéen, ña ko toppe woon Galile, dand leen, di xool li xew.

23:50  Nit ku ñuy wax Yuusufa dem ca Pilaat. Mi ngi dëkk Arimate ca diiwaanu Yude. Yuusufaa nga bokkoon ca kureelu àttekat yi. Nit ku baax la woon te jub, te àndul woon ci li ñu dogaloon te jëf ko. Da doon séentu nguuru Yàlla.

23:52  Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu.

23:53  Gannaaw loolu mu wàcce ko ca bant ba, laxas ko ci càngaay, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ciw doj te musuñu caa def kenn.

23:54  Fekk bésu Waajal la woon, te bésu noflaay baa ngi doon tàmbali.

23:55  Jigéen ña gungee woon Yeesu Galile, ànd ak Yuusufa, gis bàmmeel ba ak na ñu ca dence néewu Yeesu ba.

23:56  Noonu ñu dellu defari cuuraay ak latkoloñ ngir néew ba. Ca bésu noflaay ba ñu noppalu, ni ko yoon wi santaanee.

24:1  Bés bu jëkk ca ayu-bés ga, jigéen ña jóg ca fajar, dem ca bàmmeel ba. Ñu ngi yoroon cuuraay lu ñu defaroon.

24:2  Bi ñu agsee, ñu fekk ñu béraŋ doj, wa uboon bàmmeel ba.

24:3  Ñu dugg ca bàmmeel ba, waaye fekkuñu fa néewu Boroom bi Yeesu.

24:4  Noonu ba ñu nekkee ak seen njaaxle, am na ñaar ñu leen feeñu, sol yére yuy melax.

24:5  Jigéen ña am tiitaange ju mag, daldi dëpp seen jë ci suuf. Waaye ñu ne leen: «Lu tax ngeen di seet kiy dund ci biir néew yi?

24:6  Nekkatu fi; dekki na. Fàttalikuleen la mu leen waxoon, ba mu nekkee Galile.

24:7  Nee woon na: “Fàww ñu jébbal Doomu nit ki bàkkaarkat yi, ñu rey ko ci bant, mu dekki ca ñetteelu fan ba.”»

24:8  Noonu ñu daldi fàttaliku kàdduy Yeesu ya.

24:9  Bi ñu jógee bàmmeel ba, ñu dem nettaliji loolu lépp fukki ndaw ya ak benn, ak ña ca des ñépp.

24:10  Jigéen ña ñoo doon Maryaamam Magdala, Sànn, ak Maryaama yaayu Saag. Yeneen jigéen yi leen gunge woon itam nettali loolu ndaw ya.

24:11  Waaye ñu teg wax jooju ay jeneer, ba gëmuñu jigéen ñooñu.

24:12  Waaye Piyeer daldi jóg, daw, dem ca bàmmeel ba. Bi mu àggee, mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Noonu mu dëpp ñibbi, jaaxle lool ci li xew.

24:13  Ca bés boobu ñaar ci taalibe yi di dem ci dëkku Emayus, te mu sore Yerusalem ci lu mat fukki kilomet.

24:14  Ñu waxtaane li xewoon lépp.

24:15  Bi ñuy waxtaan ak a sotteente xalaat, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom,

24:16  fekk seeni bët muuru, ba mënu ko woon a xàmmi.

24:17  Yeesu ne leen: «Lan ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Noonu ñu taxaw, seen xol jeex.

24:18  Kenn ci ñoom, ki tudd Këleyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk yaa ñëw Yerusalem te umple li fi xewoon bés yii?»

24:19  Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu tontu ko ne: «Mbirum Yeesum Nasaret. Ab yonent la woon bu doon def ay jëf yu mag, di wax ay kàddu yu am doole, ci kanam nit ñi ak ca kanam Yàlla.

24:20  Waaye sunuy saraxalekat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko jébbal nguur gi ngir ñu àtte ko, teg ko dee, ba daaj ko ci bant.

24:21  Nun nag danoo yaakaaroon ne, mooy kiy nar a jot Israyil. Waaye bi loolu xewee ak léegi, tey la ñetteelu fan bi.

24:22  Teewul nag am na ay jigéen yu bokk ci nun yu nu jaaxal. Dañoo fajaru ca bàmmeel ba,

24:23  waaye fekkuñu fa néewam. Ñu dellusi, nettali nu ne, ay malaaka feeñu nañu leen, yégal leen ne, mi ngi dund.

24:24  Ñenn ci sunu àndandoo yi dem nañu ca bàmmeel ba, fekk lépp mel, na ko jigéen ña waxe woon. Waaye moom gisuñu ko.»

24:25  Noonu Yeesu ne leen: «Yéen daal, yéena ñàkk xel, te seen xol yéex a gëm li yonent yi yégle woon!

24:26  Xanaa du Almasi bi dafa waroon a daj boobu coono te dugg ci ndamam?»

24:27  Noonu mu tàmbalee ci yonent Yàlla Musaa ba ci yonent yépp, tekkil leen li Mbind mi wax lépp ci ay mbiram.

24:28  Bi ñuy jub dëkk, ba ñu jëmoon nag, Yeesu def ni kuy jubal yoonam.

24:29  Waaye ñu téye ko ne ko: «Toogal fii ci nun, ndaxte jant baa ngi so, te léegi mu guddi.» Noonu mu dugg, toog ca ñoom.

24:30  Bi ñu tàmbali di reer, Yeesu jël mburu ma, gërëm Yàlla, ba noppi damm ko, jox leen ko.

24:31  Bi mu defee loolu, lépp leer ci seeni bët, ñu daldi ko xàmmi. Waaye Yeesu ne mes, gisatuñu ko.

24:32  Noonu ku nekk naan sa moroom: «Ndax sa xol seddul woon, bi muy wax ak nun ci yoon wi, te muy tekki Mbind mi?»

24:33  Ñu daldi jóg ca saa sa, dellu Yerusalem, fekk fa fukki ndaw ya ak benn, ak yeneeni taalibe.

24:34  Ñooñu ne leen: «Dëgg la, Boroom bi dekki na, te feeñu na Simoŋ!»

24:35  Ñaari taalibe ya ñoom it daldi leen nettali la xewoon ca yoon wa ak ni ñu xàmmee Yeesu, bi mu dammee mburu ma.

24:36  Bi ñaari taalibe ya dee wax noonu, Yeesu taxaw moom ci boppam ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen.»

24:37  Ñu daldi tiit, foog ne dañoo gis njuuma.

24:38  Waaye Yeesu ne leen: «Lu tax ngeen jaaxle, ak lu tax ngeen di xel ñaar ci seen xol?

24:39  Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man mii la. Laal-leen ma te xam, njuuma amul yaram walla ay yax, ni ngeen gise, ma am ko.»

24:40  Bi mu leen waxee loolu, mu won leen ay loxoom ak ay tànkam.

24:41  Waaye ba tey mënuñu woon a gëm ndax seen mbég ak jaaxle. Noonu Yeesu laaj leen ne: «Ndax am ngeen fii lu ñu lekk?»

24:42  Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk.

24:43  Mu jël ko, lekk ci seen kanam.

24:44  Noonu mu ne leen: «Bi ma nekkee ak yéen, waxoon naa leen baat yii: li ñu bind lépp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci téerey yonent yi ak ci Sabóor dafa war a am.»

24:45  Noonu mu ubbi seen xel, ngir ñu xam li Mbind mi di wax.

24:46  Mu ne leen: «Fàww Almasi bi sonn, mu dee te dekki ca ñetteelu fan ba, ni ñu ko binde,

24:47  te it ñuy yégle xeet yépp ci turam, dale ko ci Yerusalem ne, war nañoo tuub seeni bàkkaar, Yàlla baal leen.

24:48  Yéenay samay seede.

24:49  Te man dinaa leen yónnee li sama Baay dige. Yéen nag toogleen ci dëkk bi, ba ñu sol leen doole ji jóge ci kaw.»

24:50  Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Foofa mu yékkati ay loxoom, barkeel leen.

24:51  Bi mu leen dee barkeel, mu tàggoo ak ñoom, Yàlla yéege ko asamaan.

24:52  Taalibe ya màggal ko, daldi dellu Yerusalem, fees ak mbég.

24:53  Foofa daawuñu jóg ca kër Yàlla ga, di gërëm Yàlla.


Next: John